رِسَالَةٌ فِي الدِّمَاءِ الطَّبِيعِيَّةِ لِلنِّسَاءِ
Lii ab bataaxel la bu jëm ci dereet yi ñu mooñaale jigéen ñi
بِقَلَمِ فَضِيلَةِ الشَّيْخِ العَلَّامَةِ
مُحَمَّدِ بْنِ صَالِحٍ العُثَيْمِينِ
غَفَرَ اللَّهُ لَهُ وَلِوَالِدَيْهِ وَلِلمُسْلِمِينَ
Ci xalimag boroom wàccuwaay bii di ku géeju ci xam-xam di Seex
Muhammat Ibnu Saalih Al-Husaymiin
yal na ko Yàlla jéggal jéggal ñaari way-juram ak mbooleem jullit ñi
بِسْمِ اللهِ الرَّحمَنِ الرَّحِيمِ
Lii ab bataaxel la bu jëm ci dereet yi ñu mooñaale jigéen ñi
Ci turu Yàlla miy Aji-Yërëm képp ku nekk ci kaw suuf jagleel ko jullit ñi ca allaaxira ci laay tàmbalee.
Mbooleem xeeti cant yi ñeel na Yàlla,noo ngi koy sant,di sàkku ci Moom ndimbal,di sàkku ci Moom njéggal,di tuub jëm ci Moom, Te di làqu ci Yàlla ngir mu musal nu ci sunu ayi bakkan, ak sunu ñaawteefi jëf. Ku Yàlla gindi amul kenn ku koy man a sànk, ku mu sànk it amul kenn ku koy man a gindi, Te maa ngi seede ne amul kenn kees war a jaamu ku dul Yàlla, Moom rekk nag, amul kenn kees koy bokkaaleel, te maa ngi seede ne Muhammat ab jaamam la di ndawam lu mu yónni, yal na Yàlla defal ko xéewal Moom ak waa-këram ak is ahaabaam ak képp ku leen topp cig rafetal fii ba bisu pay ba di ñëw,te jàmmal leen ag jàmmal.
Ginnaaw loolu: dereet yiy dikkal jigéen te di mbërëg ak dereeti jàngoro ji muy faral di àndal ak dereti wësin,dañoo bokk ci bir yu am solo yi nga xam ne aajowoo nañoo leeral ak xam seen i àtte,ak ràññee la ciy njuumte ak la ca wér ci li ci woroom xam-xam yi wax, te sukkandikukaay bees di sukkandiku ngir lëngal ca dara walla néewal ca doole daa war a tege ci li dikk ci Alxuraan ak Sunna.
1-ndaxte ñaar yooyu ñooy cëslaayal balluwaay yi nga xam ne ci lees di tabax àttey Yàlla Mu kawe mi,di àtte yoy ci la ko ay jaamam di jaamoo mu togg leen ci jëf.
2-te it ci sukkandiku ci Alxuraan ak Sunna la xolub jullit bi di dale,ci la dënnam di ubbikoo,ci la bakkanam di teeye,ci la jaanam di wàcce.
3- te it lu moy ñaar yooyu du man a doon lenn lu dul lees di wutal aw lay rekk, waaye deesu ko layoo.
ndaxte aw lay amul fenn fu dul ci waxi Yàlla mu kawe mi ak waxi Ndawam li yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko, niki noonu it manees naa layoo waxi ña nekk woroomi xam-xam ca Sahaaba ya ci wax ji gën a lëng,waaye nag ci kaw dara bañ a nekk ci Alxuraan ak Sunna luy juuyoo ak moom. ak it waxi beneen Sahaaba di bañ a juuyoo ak wax jooju, bu amee lu nekk ci Alxuraan ak Sunna luy juuyoo ak wax jooju kon day war ñu jàpp ci li nekk ci Alxuraan ak Sunna, bu waxi beneen Sahaaba juuyoo ak moom kon dees na sàkko lëkkal ci diggante ñaari wax yi te jël wax ja ca lëng;
﴿...فَإِن تَنَٰزَعۡتُمۡ فِي شَيۡءٖ فَرُدُّوهُ إِلَى ٱللَّهِ وَٱلرَّسُولِ إِن كُنتُمۡ تُؤۡمِنُونَ بِٱللَّهِ وَٱلۡيَوۡمِ ٱلۡأٓخِرِۚ ذَٰلِكَ خَيۡرٞ وَأَحۡسَنُ تَأۡوِيلًا﴾
ngir waxam ja -kawe na-:{Bu ngeen wuutee ci dara dellooleen ko ci Yàlla ak ndaw li mu yónni ndeem gëm ngeen Yàlla ak bis bu mujj ba,loolooy li gën te moo gën a rafetug mujj} [Annisaa: 59].
Lii nag di ab bataaxel bees tënk muy luñu soxla ngir leeral dereet yii ak seen i àtte, mu làmboo buyii di ñëw:
Bunt bu njëkk bik:i maanaam mbërëg ak xereñteef li ci nekk.
Bunñaareel gi :Ci jamonoy mbërëg ak diir bi muy def.
Buntub ñatteel bi :Ci yiy gaar mbërëg.
. Buntub ñenteel bi:Ci àttey mbërëg.
Buntub juróomeel bi :Ci dereeti tawat ak i àtteem.
Buntub juróom-benneel bi :Ci wësin ak i àtteem.
Buntub juróom-ñaareel bi:Ci jëfandikoo luy tee gis mbaax walla lu koy indi, ak luy tee ëmb ak luy yàq ëmb.
Buntu bu njëkk bi: ci maanaam mbërëg ak xereñteef gi ci nekk
Mbërëg ci cosaanal làkk wi: mooy mbir muy rogalaat di daw.
Bu dee ci Sariiha: dereet la joj day génn ci jigéen di lu baaxoo am te amul sabab bu koy waral ci waxtu yees xam. Moom dereeti mbaax la tawat waralu ko mbaa ab dagg-dagg walla daanu walla jur. Ginnaaw nag dereet jees mooñaale jigéen la kon day daal di wuute ci kem nekkiinu jigéen ak la ko wër ak jaww ja muy dund; looloo tax jigéen ñi di ci wuute wuute gu yaatu gu leer.
Xereñteef gi ci nekk mooy: bi nga xamee ne doom ji ci biiru yaayam manut a dunde li ñi ci bitti di dunde,te it ki ko gën a yërëm ci mbindeef yi di yaayam manul a yeggale ci moom dara ci ag dund,booba la Yàlla Mu kawe mi def ci jigéen ay tooyiti dereet yoy ci la doom ji di dunde ci biirub yaayam ci ludul muy aajowoo lekk ak reesal,tooyiti dereet yooyu day dugg ci yaram wi jaare ci jumbux bi nga xam ne dereet ji day dugg ci doom ji jaare ci ay yoonam ci yaramam mu ciy dunde,Yàlla baarkeel na te mooy Ki dàq a bind.
Lii mooy xereñteef gi nekk ci mbërëg,looloo tax bu jigéen gi ëmbee mbërëg mi dagg ci moom,du gis mbaax ndare lu néew, niki noonu ñiy nàmpal néewaa na ñuy gis mbaax ci ñoom rawati na bu ñuy soog a tàmbalee nàmpal.
Buntub ñaareel b: ci jamonoy mbërëg ak diir bi muy def
Wax ji ci bunt bii dees koy séddale ci ñaari tolluwaay :
Tolluwaay bu njëkk bi: ci at mi mbërëg di ñëw.
Tolluwaayu ñaareel bi : ci diirub mbërëg mi.
Bu dee tolluwaay bu njëkk bi:at mi ëpp li mbërëg di ñëw mooy diggante fukki at ak ñaar jàpp juróom-fukki at,amaa na saxjigéen gis mbaax lu jiitu fukki at ak ñaar yooyu walla sax mu gis ko ginnaaw juróom-fukki at day dellu rekk ci mbiram ak kéew ak jawwu ja muy dund.
Woroom xam-xam yi yal na Yàlla yërëm leen wuute nañu:ndax at mi mbërëg di ñëw daa am ab àpp bob jigéen du gis mbaax lu ko jiitu te du ko gis it ginnaaw àpp boobu,ba lu ko dikkal laata walla ginnaaw àpp boobu ñu jàppe ko dereeti jàngoro déet mbërëg?
Woroom xam-xam yi wuute nañu ci loolu ;Ad-daaramiyyu nee na -ginnaaw bi mu tuddee wuute yi ci am -: loolu lépp njuumte la ci sama gisiin! Ndaxte delluwaay bi ci loolu lépp mooy ag amam rekk,lu jot a am ci dereet muy néew ak a bari ci jamono walla at mu mu man di doon warees na koo jàppe muy mbërëg.
Yàlla a gën a xam.
Te loolu Ad-daaramiyyu wax mooy li wér, te mooy wax ji Seexul Lislaam Ibnu Taymiya tànn, saa su jigéen gisee mbërëg day daal di doon ku nekk ci di gis mbaax, doonte amagul sax juróom-ñenti at walla doonte sax ëppal na juróo-fukki at, ndaxte àttey mbërëg Yàlla ak ub Yonnenteem dañu ko a wékk ci ag amam,wutaluñu ko am at,kon nag day daal di war ñu ciy dellu ci ag amam gi nga xam ne ci lees wékk àtte yi,wutal ko am at moom day daal di laaj ñu joxe ci firnde lu bawoo ci Alxuraan walla Sunna te firnde amu ci.
Bu dee tolluwaayu ñaareel bi mooy diirub mbërëg,maanaam : dayob jamonoom.
Woroom xam-xam yi wuute nañu ci wuute gu rëy, ba toll ci juróom-benni wax walla juróom-ñaar. Ibnul Munsir yal na ko Yàlla yërëm nee na :am na mbooloo mu wax ne:gën gaa néewug waxtuw mbërëg ak gën gaa bareem amul ab dayo bees ko wutal ci ay bis.
Ma daal di ne : Wax jii it day mel ne waxi Ad-daaramiyyu ji jiitu, moom la Seexul Lislaam Ibnu Taymiya tànn, te mooy li wér, ndax loolu la Alxuraan di tegtale ak Sunna ak lees jàngat.
Firnde li njëkk mooy:
﴿وَيَسۡـَٔلُونَكَ عَنِ ٱلۡمَحِيضِۖ قُلۡ هُوَ أَذٗى فَٱعۡتَزِلُواْ ٱلنِّسَآءَ فِي ٱلۡمَحِيضِ وَلَا تَقۡرَبُوهُنَّ حَتَّىٰ يَطۡهُرۡنَۖ...﴾
waxu Yàlla mu mi: {Danañu la laaj lu jëm ci mbërëg, Neel : “Moom sobe la. Deeleen beru jigéen ñi ci di bañ a sëy ak ñoom bu ñu nekkee ci mbërëg, buleen leen jege ba baa ñuy laab}
[Al-Baqarah: 222], Yàlla def daytalug tere gi mu yem ci bu jigéen gi laabee,te defu ko ci benn fan walla ñatti fan walla fukki fan ak juróom,loolu di firndeel ne yillay àtte bi mooy amug mbërëg ak ug ñàkk a amam, saa yu mbërëg amee àtte bi day daal di sax, saa yu laabee ay àtteem deñ.
Ñaareelu firnde li :
مَا ثَبَتَ فِي صَحِيحِ مُسْلِمٍ أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ لِعَائِشَةَ وَقَدْ حَاضَتْ وَهِيَ مُحْرِمَةٌ بِالْعُمْرَةِ: «افْعَلِي مَا يَفْعَلُ الْحَاجُّ، غَيْرَ أَنْ لَا تَطُوفِي بِالْبَيْتِ حَتَّى تَطْهُرِي». قَالَتْ: فَلَمَّا كَانَ يَوْمُ النَّحْرِ طَهُرْتُ. الْحَدِيثُ.
Li sax ci téere Sahiihu Muslim ci ne Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko dafa wax Aysa fekk ma ngay gis mbaax boole ko ak armal di Umra, ne ko : (Defal li kiy aj di def waaye nag bul wër kaaba gi ba baa ngay laab), mu ne: Ca bisu loj ba ma daal di laab... ba Hadiis ba egg.
Nekk na ci Sahiihul Buxaarii ak Muslim Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko dafa wax Aysa ne ko :"Xaaral, boo laabee nga génn dem Tanhiim",nga xam ne Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko dafa def daytalu tere gi ci ag laabam, waaye wutalu ko waxtu, loolu it di firndeel ne àtte bi day wékku ci amug mbërëg ak ug ñàkk a amam.
Ñatteelu firnde li : nattale yi ak teqale yii nga xam ne am na ñu ko tudd ci woroom xam-xami fiq yi ci masala mii nekkul yu sax ci Alxuraan nekkul it yu sax ci Sunnas ndawal Yàlla li yal na Ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko ànd ak ne aajo walla sax loru ci war koo xam laajoon na leeral leen bu ñu doonoon lu bokk ci masala mi, nattale yooyu ak teqale yooyu bu doon lu war jaam ñi xam ko jaamoo ko Yàlla kon Yàlla ak ndawam li yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko leeral ko leeral gu ne fàŋŋ ñeel jépp jëmm, ngir solos àtte ya cay toftaloo niki julli ak woor ak sëy ak pase ak donn ak yeneen yu dul yooyu ci ay àtte, niki ni Yàlla ak Ndawam li leeralee limub julli yi ak seen i waxtu ak seen i sëgg ak seen i sujóot, ak asaka :alal jees koy war a génne ak na muy toll ñu door ko cay génne ak lees cay génne na muy toll ak fa mu war a jëm,ak koor:ab diiram ak jamonoom,ak aj ak yeneen ya féete suuf yooyu, ba ci sax teggiini lekk ak naan ak nelaw ak booloo ak toog ak dugg kër ak génn fa,ak teggiini faj aajo,ba ci limub yi muy fompoo doj ya ak yeneen yu dul yooyu ci ay bir yu sew ak yu rëy,bokk ci yi Yàlla matalee diine ji,matalee ci xéewal ci way-gëm ñi,
niki ni ko Yàlla mu kawe mi waxee:
﴿...وَنَزَّلۡنَا عَلَيۡكَ ٱلۡكِتَٰبَ تِبۡيَٰنٗا لِّكُلِّ شَيۡءٖ...﴾
{Wàccee nanu ci yaw Téere bi mu nekk luy leeral lépp} [An-nahl :89].
Yàlla mu kawe mi nee na -:
﴿...مَا كَانَ حَدِيثًا يُفْتَرَى وَلَـكِن تَصْدِيقَ الَّذِي بَيْنَ يَدَيْهِ وَتَفْصِيلَ كُلَّ شَيْءٍ...﴾
{Du waxtaan wu ñu sos waaye day dëggal téere ya jiitu, te it di leeral lépp lu nekk} [Yuusuf : 111].
Bi nga xamee ne nag nattale yooyu ak teqale yooyu jëm ci di jéem a wutal mbërëg at walla limub ay bis fekkeesu ko ci téere Yàlla mu kawe mi fekkeesu ko it ci Sunnas Ndawal Yàlla li yal na Ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko leer na kon ne deesu ci sukkandiku,lees di sukkandiku rekk mooy jëmmi mbërëg mi nga xam ne ci ag amam ak ug ñàkk a amam lees wékk àttey Sariiha yi, te firnde jii - maanaam : nekk gi Alxuraan ak Sunna nekk di ñàkk a tudd àtteb nattale yooyu doon firnde ci ñàkk koo sóoraale-da lay jariñ ci masala mii ak yeneen masalay xam-xam; ndaxte àttey Sariiha yi duñu sax lu dul ci firnde lu bawoo ci lees yoonal mu nekk ci téere Yàlla bi,walla Sunnas ndawam li yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko, walla ag dëppoo gu ñu xam am ci tukkee ci woroom xam-xam yi,walla mu doon lees natt natt gu wér ci lu mu méngool lol firnde ñëw na ca. Seexul Lislaam Ibnu Taymiya nee na ci benn tënk bumu def ne: « bokk na ci loolu turu mbërëg Yàlla wékk ci ay àtte yufasantiku ci Alxuraan ak Sunna, te wutalul daytal gën gaa néewam du it gën gaa bareem, wutalu ko it laab gi dox ci diggante ñaari mbërëg, ànd ak maase gi xeet wi maase ci am ci aajo ju doon lu sax,te làkk wi du teqale diggante dayo ak beneen dayo, képp ku ci nattale ab dayo kooka juuyoo na ak Alxuraan ak Sunna». waxam jeexe foofu.
Ñenteelu firnde li :lees jàngat, maanaam: natt gu wér gu dëppoo ci lépp, te loolu mooy ne Yàlla mu kawe mi dafa yillaal mbërëg ci nekk gi mu nekk di lor,fees fekk mbërëg rekk lor a nga fa,ag wuute amul ci diggante bisub ñaareel ba ak bis bu njëkk ba,amul it ci diggante bisub ñenteel ba ak ñatteel ba, amul it ci diggante bisub fukkeel ak juróom-benn ba ak fukkeel ba ak juróom,amul it ci diggante fukkeel ba ak juróom-ñatt ak fukkeel ba ak juróom-ñaar, Mbërëg mooy mbërëg lor di lor, yilla ji di lu am ci ñaari bis yépp ci ag yemoo, naka lay man a wére kon ñu bëgg a teqale àtte bi ci diggante ñaari bis yi ànd ak seen ug yemoo ci yilla ji? Ndax loolu du nekk di juuyoo ak nattale gu wér? Ndax dunattale gu wér mooy yemoog ñaari bis yi ci ab àtte ngir seen ug yemoo ci yilla ji?.
Juróomeelu firnde li: wuuteg waxi ñi koy wutal daytal ak ñàkk a dëppoog wax yooyu, loolu di wane ne masala mi amul firnde lees war a dellu, wànte ay àtte yees tabax ci ag farlu la gog njuumte ak ug wér yépp man na koo gaar, benn ci ñoom du gën a yell ñu topp ko wolif beneen ba, te delluwaay bi ci bu wuute amee mooy Alxuraan ak Sunna.
Dëgërug wax jooju nag bu dee leer na : ci ne mbërëg amul dayo bu gën a néew ak bu gën a bari. te mu leer it ne loolu mooy wax ji lëng xamal kon ne lépp lu jigéen gis muy dereeti mbaax te amul sabab su tax mu génn niki gaañu-gaañu ak yu ni deme loola mbërëg la wolif ñu di ko nattale ci jamono walla at, ndare mu nekk di wéy ci jigéen gi te du dog mukk, walla sax muy dog diggante bu gàtt niki benn bis walla ñaari bis ci weer wi, bu boobaa nag dereeti wéradi lees koy jàppee, Leeralug dereeti wéradi ak i àtteem dina dikk-ndeem soob na Yàlla Mu kawe mi -.
Seexul Lislaam Ibnu Taymiya nee na: liy cosaan ci lépp luy génne ci butitu njurukaay mooy ne mbërëg la ba ba firnde di taxaw ci ne dereeti wéradi la. Wax na it ne :lépp lu am ci dereet rekk mbërëg lay man a doon ndegam xameesul ne dereetu sédit la walla muy ju bawoo ci ab dagg-dagg. Foofu la waxam jeexe. Wax jooju nag niki ni mu doone lu lëng noonu it la gën a jegee ci dégg-dégg ak ug xam,gën a neex a jëfe it ci la ñay wutal mbërëg daytal di wax,lu deme noonu nag mooy gën a yey ci ñu nangu ko ngir ag dëppoom ak dëgg-dëggi diiney Lislaam ak takk-takkam bi nga xam ne moo di ag yomb ak ug jàppandi,
Yàlla Mu kawe mi nee na :
﴿...وَمَا جَعَلَ عَلَيۡكُمۡ فِي ٱلدِّينِ مِنۡ حَرَجٖ...﴾
{Yàlla tegu leen ci diine lu leen di xatal}
[Al-Hajj : 78].
«إِنَّ الدِّينَ يُسْرٌ وَلَنْ يُشَادَّ الدِّينَ أَحَدٌ إِلَّا غَلَبَهُ فَسَدِّدُوا وَقَارِبُوا وَأَبْشِرُوا».
Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko nee na: «Diine ji de lu yomb la,kenn du taral diine lu dul ne diine dana ko not, deeleen dàkk ag digg-dóomu di jéem a jegeel seen i jëf ba bu ngeen manut a def la gën a mat it ngeen def lu ko jege te ngeen attan ko, te ngeen bég». Al-Buxaarii soloo na ko.
Bokkoon na ci ay jikkoom yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko:
«أَنَّهُ مَا خُيِّرَ بَيْنَ أَمْرَيْنِ إِلَّا اخْتَارَ أَيْسَرَهُمَا مَا لَمْ يَكُنْ إِثْمًا».
«Daawuñu ko tànnloo diggante ñaari mbir lu dul ne day tànn ma ca gën a yomb bu dul bàkkaar».
Mbërëgu ki ëmb:
Jigéen li ci ëpp bu ëmbee mbërëg ma day dog,Imaam Ahmat yal na ko Yàlla yërëm nee na :«Jigéen ñi ëmb ñi ngi leen di xame ci dogug dereet ja»,ki ëmb bu gisee dereet bu dee laata muy am doom ci diir bu gàtt la niki ñaari bis walla ñatt te dereet ja ànd ak uw mettit wu bawoo ciw matu loola dereeti wësin la, bu dee laata muy am doom la ci diir bu yàgg walla sax diir bu gàtt waaye àndul ak mettit woowu ñu wax kon du doon dereeti wësin,waaye ndax day doon mbërëg walla dereet ju yàqu joj deesu ko àtte àtteb mbërëg?
loolu ag wuute am na ci ci diggante woroom xam-xam yi, te la wér mooy mbërëg la bu dee nekke na ca anam ga mu baaxoo ; ndax liy cosaan ci dereet jiy dikkal jigéen mooy mbërëg la, bu amul sabab bu ko koy teree doon, te ci Alxuraan ak Sunna amul luy teree gis mbaax ci ki ëmb.
Loolu mooy ngirum Maalik ak As-Saafihii, ak tànnug Seexul Lislaam Ibnu Taymiya; wax na ci téereem ba ((Al-lixtiyaaraat, xëtuw: 30)) ne : Al-Bayhaqii nettali na loolu soloo ko jële ko ci Ahmat, nettali na sax ne Ahmat wax jooju la mujj a jël. Foofu la waxam jeexe.
Ci kaw loolu kon àtte yiy sax ci jigéen jiy gis mbaax te ëmbulñooy yiy sax ci jigéen jiy gis mbaax te ëmb,ndare ci ñaari masala :
Masala mi njëkk:Mooy pase, kon day araam ñuy fase kok idda da koy war te fekk mu nekk di gis mbaax bu dee ku ëmbul la, waaye du araam ci ki ëmb; Ndaxte fase ci waxtuw mbërëg ci ku ëmbul lu juuyoo la ak waxi Yàlla mu kawe mi:
﴿...فَطَلِّقُوهُنَّ لِعِدَّتِهِنَّ...﴾
{na ngeen leen fase ci seen ug laab}[At-Talaaq : 1], Bu dee fase ku ëmb ci jamonoy mbërëg moom du juuyoo ak waxi Yàlla ;ndaxte ku fase ku ëmb fase na ko ci biir yiddaam moo xam day gis mbaax moo xam dafa laab;ndax yiddaam mi ngi ci ag ëmbam; Looloo tax du araam ci moom mu fase ko ginnaaw bu jaxasoo ak moom, wuute ak ku ëmbul.
Ñaareelu masala mi :mbërëgu ku ëmb yidda du ci jeex,wuute ak mbërëgu ku ëmbul ; ndaxte yidday ki ëmb du jeex lu dul mu am doom, moo xam doon na gis mbaax walla déet ;
ngir li Yàlla mu kawe mi wax ne :
﴿...وَأُوْلَاتُ الأَحْمَالِ أَجَلُهُنَّ أَن يَضَعْنَ حَمْلَهُنَّ...﴾
{Woroom ëmb yi seenub dig mooy ñu imbi lañu ëmb} [At-Talaaq : 4].
Buntub ñatteel gi : ci yiy gaar dereeti mbërëg
Yiy gaar dereeti mbërëg ay xeet la :
xeet wi ci njëkk :dolliku walla wàññiku ,niki aaday jigéen gi di juróom-benni fan,dereet ji wéy ak moom ba juróom-ñaari fan , walla aadaam doon juróom-ñaari fan mu far laab ci juróom-benni fan.
Xeetu ñaareel wi: teel walla yeex a ñëw, niki aadaam doon ci mujjug weer wi mu gis mbaax ci njëlbéen ga, walla aadaam doon ci njëlbéenug weer wi mu gis ko ci mujj ga.
Woroom xam-xam yi wuute nañu ci àtteb ñaari xeet yooyu te li wér mooy saa yu gisee dereet rekk xam ne mbërëg la, saa yu laabee laab na, moo xam daa yokk ci aadaam walla dafa wàññi, walla dafa teel walla dafa yeex, Te jiitu na ñu tudd firndel loolu ci teqale gi jiitu gii, te mooy Aji-Yoonal ji daa wékk àttey mbërëg ci ag amam.
Loolooy ngirum As-Saafihii, ak tànnug Seexul Lislaam Ibnu Taymiya,te loolu la boroom téere Al-Muxnii dëgëral ne:bu doon aada ji dees ciy sukkandiku ci anam gii ñu tudd ci ngér mi kon Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Koleeraloon ko xeetam wi te du woon sax sañ a yeexe leeral ko; ndaxte yeexe leeral ci waxtoom daganul,te ay soxnaam ak ñu dul ñoom ci jigéen ñi dañu doon aajowoo ku leen leeral loolu ci waxtu wu nekk,te manul nekk mukk Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko di ko sàggane a leeral, te dikkul fenn Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko di tudd aada walla di ko leeral lu dul ci ki dereetam jaarul yoon wante du keneen. jeex na.
Xeetu ñatteel wi mooy : mboq-mboq walla nëxit nga xam ne jigéen gi day gis dereet ji mu mboq niki ndox miy génne ci góom yi walla mu nëx nekk ci diggante mboq ak ñuul, dereet jooju bu nekkee ci jamanoy mbërëg walla mu sës ca laata jigéen gi di laab na xam ne mbërëg la, danu koy saxalal àttey mbërëg,bu dee nag ginnaaw ag laabam la feeñ su boobaa deesu ko jàppe mbërëg;
لِقَوْلِ أُمِّ عَطِيَّةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهَا: «كُنَّا لَا نَعُدُّ الصُّفْرَةَ وَالْكُدْرَةَ بَعْدَ الطُّهْرِ شَيْئًا». رَوَاهُ أَبُو دَاوُدَ بِسَنَدٍ صَحِيحٍ.
ngir li Ummu Atiyya yal na ko Yàlla gërëm wax ne :«Dereet ju mboq walla ju nëx ginnaaw laab nun de daawu nu ko jàppe muy dara». Abóo Daawuda soloo na ko ci càllala gu wér, Al-Buxaarii it soloo na ko waaye boolewu ci waxam jii : (ginnaaw laab), waaye moom wutal na ko bunt bob la mu ca wax moo di :Buntub dereet ju mboq walla ju nëx ci lu dul bisi mbërëg yi. Ibnu Hajar wax na ci saraam ba ci téereb Fathul Baarii ne : «loolu da ciy junj a boole diggante Hadiisu Aysa bi jiitu ci waxam ji mu wax ne: ba ba ngay gis ndox mu weex mi. Ak Hadiisu Ummu Atiyya bi ñu tudd ci bunt bii,ci ne booba - maanaam :Hadiisu Aysa - dees koy yan ci bu dee jigéen ji dafa gis dereet ju mboq walla ju nëx ci bisi mbërëg,waaye bu dee ci yeneeni bis la ko gis moom dees koy yan ci li Ummu Atiyya wax».jeex na. Te Hadiisu Aysa bi mu junj mooy bi Al-Buxaarii nettali dagg càllala gi dogu ci mu jiitu bunt bii,ci ne jigéen ña dañu daan yónnee fa moom Aysa sagar ya (sagar yi jigéen di def ci kanamam ngir man a xam ndax dara des na ci jeexiti mbërëg mi) sagar ya di ànd ak wëtéen wu taq dereet ju mboq, mu naan leen: «Buleen yàkkamti ba ba ngeen di gis ndox mu weex mi». Ndox mu weex moomu butitu njurukaay gi moo koy jeñ mu génn bu mbërëg mi dogee.
Xeetu ñenteel wi: dogug mbërëg mi ak ug dellusiwaatam, nga xam ne da koy gis bis beneen bis mu set ak yu deme noonu, lii ñaari tolluwaay la:
Bu njëkk bi: loolu nekk di ànd ak jigéen gi saa su nekk,kon day doon dereeti jàngoro ay àtteem sax ñeel ki ko gis.
Bu ñaareel bi : mu bañ a wéy di ànd ak jigéen gi, waaye leeg-leeg rekk la koy dikkal, ba noppi mu am waxtuw laab wu wér. Woroom xam-xam yi yal na leen Yàlla yërëm wuute nañu ci set googu di awante ak mbërëg mi, ndax dees koy jàppe ag laab walla àttey mbërëg day ñëw ci moom?
Ngirum As-Saafihii ci li gën a wér ci ñaari waxam yi mooy day jël àttey mbërëg, doon mbërëg,te loolu mooy tànnug Seexul Lislaam Ibnu Taymiya ak Boroom Al-Faaiq,di ngirum Abóo Haniifa, ndaxte ndox mu weex miy wone set deesu ko gis ci set googu, te bees ko jàppe woon ag laab kon bis ba ko jiitu day doon bisu mbërëg bis ba ca topp it doon bisu mbërëg, te loolu amul kenn ku ko wax,walla bu dul loolu it yidda day man a jeexe cig laab ci juróomi bis; ak it bees ko jàppe woon ag laab coonoo ciy ame ak ug xatal ci di sangu saa su nekk ak lu dul loolu ci ñaari bis yu nekk,te ag xatal amul ci Sariiha jii,ag cant ñeel na Yàlla.
Li siiw ci ngirum Hanaabila mooy dereet saa yu ñëwee mbërëg la saa yu dogee ag laab la ndare mu nekk ne boo boolee bis yi mu ñëw ak bis yi mu ñewul day far ëpp li gën a bari ci bisi mbërëg, kon su boobaa dereet ja ca tege day doon dereeti jàngoro.
Ibnu Xudaama wax na ci téereem ba Al-Muxnii:«Dina baax ñu xam ne dogug dereet ji saa yu yéesee benn bis dog googu du doon ag laab bees sukkandikoo ci nettali bi nga xam ne nettali nanu ko ci wësin ci ne jigéen gi du bàyyi xel lu yées benn bis te loolu mooy li wér-bu soobee Yàlla-ndax dereet day daw ak a taxaw,te bëgg a waral cangaay ci kiy laab waxtu ginnaaw waxtu ab coonoo ngi ci bob daa war a dàqu;
ngir li Yàlla Mu kawe mi wax ne:
﴿...وَمَا جَعَلَ عَلَيۡكُمۡ فِي ٱلدِّينِ مِنۡ حَرَجٖ...﴾
{Yàlla tegu leen ci diine lu leen di xatal} [Al-Hajj: 78], Nee na:ci kaw loolu dogug dereet ci lu yées benn bis du man a doon ag laab ndare mu gis lu koy tegtale niki dereet ji dog ci mujjug bisi aadaam walla mu gis ndox mu weex miy wone ne set na» jeex na.
Kon waxi boroom Al-Muxnii moomu day doon lu digg-dóomu ci diggante ñaari wax yi,Yàlla a gën a xam li wér.
Xeetu juróomeel wi: ag wow ci dereet ji, nga xam ne jigéen gi ay tooy-tooy rekk lay gis, loolu bu dee ci biir mbërëg mi la walla mu jokku ci laata muy laab su boobaa mbërëg lay doon, bu dee ginnaaw laab la nag du doon mbërëg; ndaxte li gën a sori lees ko man a jàppe mooy dereet ju mboq ak nëxit, lii mooy àtteem.
Buntub ñenteel bi:ci àttey mbërëg
Mbërëg am na ay àtte yu bari yoy ëpp na ñaar-fukk, dinanu ci tudd rekk li nu jàpp ne aajowoo nañu ko lool,te bokk na ci loolu:
Bi njëkk: muy julli: kon julli day araam ci kiy gis mbaax. farata ak naafila a ci yem, te bu julli woon it julli ga wérul, niki noonu julli du ko war ndare mu dab -ginnaaw ag laabam- ca waxtuw julli wa luy tolloo ak diir bu mu man a julli benn ràkka bu mat, su boobaa kon julli dina ko war, moo xam da koo dab ci njëlbéenug waxtu wa walla ca mujj ga.
Misaalum ki ko dab ci ag njëlbéenam : jigéen gu gis mbaax ginnaaw sowug jant bi ci lu tolloo ak diirub benn ràkka, kooku dina war ci moom bu laabee mu fay jullig timis googu ndax dab na ci waxtoom lu tolloo ak ub ràkka laata muy gis mbaax.
Misaalum ki ko dab ci ag mujjam: jigéen gu laab njëkk jant bi di fenk ci lu tolloo ak ub ràkka, kooku dina war ci moom ginnaaw bu sangoo mu fay jullig fajar googu; ndax dab na ci waxtoom ab pàcc bob manees na caa julli ab ràkka.
Bu dee nag aji-gis mbaax ji li mu dab ca waxtu wa matul ràkka bu mat, niki mu gis mbaax ci misaal mu njëkk mi ginnaaw sowug jant bi ci diir su gàtt walla mu laab ci misaalum ñaareel mi laata jant bi di fenk ci diir su gàtt, su boobaa julli googa du ko war; ngir li Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko wax ne:
«مَنْ أَدْرَكَ رَكْعَةً مِنَ الصَّلَاةِ فَقَدْ أَدْرَكَ الصَّلَاةَ».
«Ku dab ab ràkka ci julli dab na julli ga» Al-Buxaarii ak Muslim soloo nañu ko, loolu lees ciy dégge mooy ku dab lu yées ab ràkka dabul julli ga.
Bu jigéen gi dabee ab ràkka ci waxtuw jullig tàkkusaan ndax jullig tisbaar dina ko war ànd ak tàkkusaan, walla sax mu dab ab ràkka ci waxtuw jullig gee ndax jullig timis dina ko war ànd ak jullig gee?
Loolu ag wuute am na ci ci diggante woroom xam-xam yi, li wér nag mooy li mu dab waxtoom rekk a koy war, te mooy tàkkusaan ak gee rekk;
«مَنْ أَدْرَكَ رَكْعَةً مِنَ الْعَصْرِ قَبْلَ أَنْ تَغْرُبَ الشَّمْسُ فَقَدْ أَدْرَكَ الْعَصْرَ».
ngir li Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko wax ne:«Ku dab ab ràkka ci jullig tàkkusaan laata jant bi di so kooku dab na jullig tàkkusaan ga»Al-Buxaarii ak Muslim soloo nañu ko, Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal jàmmal ko waxul:dab na tisbaar ak tàkkusaan. Tuddul it warug tisbaar ci moom,te liy cosaan mooy nit ki dara waragu ko ba bees ko koy sant,loolu mooy ngirum Abóo Haniifa ak Maalik,An-Nawawii nettali na loolu tuxale ko ci ñoom ñaar ci ba muy firi Al-Muhassab.
Bu dee sikkar la ak kàbbar ak sàbbaal ak sant Yàlla ak tudd Yàlla ci lekk ak yeneen,ak jàng Hadiis ak fiq ak ñaan ak wax aamiin ca ñaan ga ak déglu Alxuraan yooyu yépp dara araamu ci,
«أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ يَتَّكِئُ فِي حِجْرِ عَائِشَةَ رَضِيَ اللهُ عَنْهَا وَهِيَ حَائِضٌ فَيَقْرَأُ الْقُرْآنَ».
sax na ci ñaari téerey Sahiih yi ak yeneeni téere,ne «Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko daa na sukkootu ci peggu Aysa yal na ko Yàlla gërëm di jàng Alxuraan fekk Aysa a ngi gis mbaax».
Ñëw na ci ñaari téerey Sahiih yi ba tay ne Ummu Atiyya yal na ko Yàlla gërëm dégg na Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko mu naan:
«يَخْرُجُ الْعَوَاتِقُ وَذَوَاتُ الْخُدُورِ وَالْحُيَّضُ -يَعْنِي: إِلَى صَلَاةِ الْعِيدَيْنِ- وَلْيَشْهَدْنَ الْخَيْرَ، وَدَعْوَةَ الْمُؤْمِنِينَ، وَيَعْتَزِلُ الْحُيَّضُ الْمُصَلَّى».
«Janq ji sëyeegul te nekk ci seeni kiiraay ci biir kër yi na ñu génn ñoom ak ñiy gis mbaax ñépp-maanaam:dem ca jullig hiit ga-nañu fekke yiw wa ak ñaanug way-gëm ña te ñiy gis mbaax beru jullikaay ba».
Bu dee jàngug aji-mbërëg ji Alxuraan ci boppam,bu nekkee ne da koy xool ak bëtam walla mu koy settantal ci xolam loolu aayul,niki ñu teg kaamil bi walla àlliwa ji muy xool laaya yi di jàng ci xolam.. An-Nawwiyyu wax na ci ba muy firi Al-Muhassab ne:«Dagan na ci lu amul wuute».Bu dee nag njàngam ma da koy tudd ci làmmiñ moom ñi ëpp ci woroom xam-xam yi li ñu wax mooy dees koo aaye te daganul, Al-Buxaarii ak Ibnu Jariir At-Tabarii ak Ibnul Munsir nee nañu: dagan na. Nettalees na jële ci Maalik ak As-Saafihii ci waxam ju njëkk ja, Ibnu Hajar nettali ko ci ñoom ñaar ci téereb Fathul Baarii.Al-Buxaarii tuxale ci Ibraahiima An-Naxahii ci lu amul càllala ne: aayul ci ki gis mbaax mu jàng jenn laaya.
Seexul Lislaam Ibnu Taymiya wax na ci téereb Al-Fataawaa Majmoohatu Ibnul Qaasim ne: «tere loolu amul cëslaay ci Alxuraan ji,te li mu wax ne :«Aji-gis mbaax ak ki ame janaba duñu jàng dara ci Alxuraan»loolu Hadiis bu wérul la ci dëppoo gog ñoñ-xam ña Hadiis dëppoo nañu ca,jigéen ña daan nañu gis mbaax jamonoy Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal kon bu jàng Alxuraan araamoon ci ñoom niki ni julli araame ci ñoom kon loolu bokk ci li Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko di leeralal xeetam wi,te kon yaayi jullit ñi di ay soxnaam danañu ko jottali nit ñi, Bi nga xamee ne nag kenn toxalul jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko ag tere ci loolu kon du dagan ñu koy araamal ànd ak ñu xam ne terewul loolu, te bu ko terewul ak ni mbërëg baree woon ci jamonoom kon dees di xam ne araamul». Jeex na.
Li jaadu ginnaaw bi nu xamee wuuteg woroom xam-xam yi mooy wax ne: li gën a yay ci kiy gis mbaax mooy mu bañ a jàng Alxuraan di ko tudd ci làmmiñ lu dul bu ko aajo waralee, niki mu doon ab jàngalekat aajowoo di sah jigéen ñay xamlu, walla mu nekk ne dees di natt ag mokkalam nga xam ne aji-xamlu ju jigéen ji day aajowoo jàng ngir nattu boobu walla yu mel noonu.
Ñaareel bi mooy :woor: koor day araam ci kiy gis mbaax koorug farata ak gog naafila a ci yem,bu wooroon it du wér,waaye dina war mu fay koori farata yi;ngir Hadiisu Aysa yal na ko Yàlla gërëm:
"كَانَ يُصِيبُنَا ذَلِكَ -تَعْنِي: الْحَيْضَ- فَنُؤْمَرُ بِقَضَاءِ الصَّوْمِ وَلَا نُؤْمَرُ بِقَضَاءِ الصَّلَاةِ".
«Loolu daan na nu dal -mi ngi jublu: mbërëg- ñu nuy digal fay koor te daawuñu nu digal fay julli». Al-Buxaarii ak Muslim dëppoo nañu ci génne ko ci seen ñaari téerey Sahiih yi.
Bu jigéen gi gisee mbaax fekk mu woor koor ga yàqu na, doonte loolu dafa am laata jant bi di so ci ndiir su gàtt,te war na ci moom mu fay bis boobu ndeem koorug farata la.
Bu dee nag daa yég tuxug mbërëg mi ci biiram njëkk jant bi di so waaye jotul a génn lu dul ginaaw bi jant sowee su boobaa kooram mat na te du yàqu,ci wax ji wér;ndax dereet ju nekk ci biir amul àtte ; ak it ndaxte Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko bees ko laajee jigéen jiy gis ci ay nelawam li góor di gis:ndax sangu dina ko war?
قَالَ: «نَعَمْ، إِذَا هِيَ رَأَتِ الْمَاءَ». فَعَلَّقَ الْحُكْمَ بِرُؤْيَةِ الْمَنِيِّ لَا بِانْتِقَالِهِ، فَكَذَلِكَ الْحَيْضُ لَا تَثْبُتُ أَحْكَامُهُ إِلَّا بِرُؤْيَتِهِ خَارِجًا، لَا بِانْتِقَالِهِ.
dafa wax ne: «Waaw bu dee moom gis na ndox» daal di wékk àtte bi ci gis Miniyu mi te wékku ko ci ag tuxoom ci biir, mbërëg it noonu la, ay àtteem du sax lu dul bees ko gisee mu génn waaye du cig tuxoom rekk.
Bu fajar gi fenkee fekk mu nekk ci mbaax, ag wooram bis boobu du wér doonte dafa laab ginnaaw fajar gi ci diir bu gàtt.
Bu laabee bi fajar di waaj a jot nag daal di woor kooram baax na,doonte sanguwul lu dul ginnaaw fajar gi,niki ki ame janaba bu fasee yéenee woor fekk mi ngi ame janaba te sanguwul ndare ginnaaw bi fajar xaree kooram wér na;
"كَانَ النَّبِيُّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يُصْبِحُ جُنُبًا مِنْ جِمَاعٍ غَيْرِ احْتِلَامٍ ثُمَّ يَصُومُ فِي رَمَضَانَ".
ngir Hadiisu Aysa yal na ko Yàlla gërëm bi mu wax ne : «Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko daan na xëy fekk mi ngi ame janaba joj ci sëy la sababoo déet gént mu daadi woor ci biir weeru Koor».Al-Buxaarii ak Muslim dëppoo nañu ci génne ko ci seen ñaari téerey Sahiih yi.
Àtteb ñatteel bi: wër Kaaba ga: araam na ci moom mu wër Kaaba ga, wërug farata ak gog naafila a ci yem, bu ko defee it du wér;
«افْعَلِي مَا يَفْعَلُ الْحَاجُّ غَيْرَ أَلَّا تَطُوفِي بِالْبَيْتِ حَتَّى تَطْهُرِي».
Ngir waxi Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko ji mu wax Aysa bi mu gisee mbaax ne ko: «Defal yi kiy aj di def lu dul ne Kaaba gi moom doo ko wër ba baa ngay laab».
Bu dee yeneen jëf yi niki dox diggante Safaa ak Marwa, ak taxaw Arafa, ak fanaan Musdalifa ak Minaa, ak sànni jamra ak yeneen yu dul yooyu te bokk ci jaamuy aj ak umra yooyu du araam ci moom, ci kaw loolu bu jigéen gi wëroon Kaaba ga fekk mu nekk cig laab topp mbërëg ma génn ginnaaw wër ga fi saasa,walla ci diggante bi muy dox Safaa ak Marwa kon it loolu du doon lu aay.
Àtteb ñenteel bi:wàcc gi ko wërug tàggutoo ga wàcc: bu jigéen gi matalee jaamu Yàlla yi aju ci aj ak umra topp mu gis mbaax njëkk muy génn di dellu dëkkam mbërëg mi wéy ak moom ba ni muy génnee di dellu,su boobaa day dem ci ludul muy wër wërug tàggutoo; ngir Hadiisu Ibnu Abbaas yal na leen Yàlla gërëm ñoom ñaar mu wax ne: «Digalees na nit ñi lay mujj ca la ñuy def ca aj ga doon Kaaba ga, lu dul ne woyofalees na ko ci jigéen giy gis mbaax» [Al-Buxaarii ak Muslim dëppoo nañu ci génne ko ci seen ñaari téerey Sahiih yi].
Deesul sopp ci kiy gis mbaax buy tàggutoo muy dikk ca buntub jumaa ju ñu wormaal ja ca Màkka di ñaan; ndaxte loolu rotul bàyyikoo ci Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko, te jaamu yi dees koy tabax ci li rot, li rot bàyyikoo ci Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko sax kay day wuute ak jëf jooju,
فَفِي قِصَّةِ صَفِيَّةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهَا، حِينَ حَاضَتْ بَعْدَ طَوَافِ الْإِفَاضَةِ، أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ لَهَا: «فَلْتَنْفِرْ إِذًا». مُتَّفَقٌ عَلَيْهِ.
ci xisab Safiyya yal na ko Yàlla gërëm bi mu gisee mbaax ginnaaw ag wëram Kaaba ga bi mu dikkee bawoo Minaa Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko da ne ko: «Man ngaa ñibbi kon».Al-Buxaarii ak Muslim dëppoo nañu ci génne ko ci seen ñaari téerey Sahiih yi.
Te digalu ko mu teew ca bunt jumaa ja, bu doon loolu lees yoonal la kon mu leeral ko. Bu dee wërug aj ak umra moom du ko wàcc, waaye da koy def bu laabee.
Àtteb juróomeel bi: sax ci biir jàkka: araam nañu ci kiy gis mbaax muy sax ci biir jàkka ba ci sax jullikaayu hiid araam na ci moom mu di fa sax,
لِحَدِيثِ أُمِّ عَطِيَّةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهَا: أَنَّهَا سَمِعَتِ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ: «يَخْرُجُ الْعَوَاتِقُ وَذَوَاتُ الْخُدُورِ وَالْحُيَّضُ». وَفِيهِ: «يَعْتَزِلُ الْحُيَّضُ الْمُصَلَّى». مُتَّفَقٌ عَلَيْهِ.
ngir Hadiisu Ummu Atiyya yal na ko Yàlla gërëm bi mu wax ne: Dégg naa Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko mu ne : «Janq ji sëyeegul te nekk ci seeni kiiraay ci biir kër yi nañu génn ñoom ak ñiy gis mbaax». Ñëw na ca Hadiis ba : «ñiy gis mbaax dañuy beru jullikaay ba». Al-Buxaarii ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téerey Sahiih yi.
Àtteb juróom-benneel bi : sëy: day araam ci boroom këram muy sëy ak moom, di araam it ci jigéen gi mu koy jàppandalal boppam ngir loolu;
﴿وَيَسۡـَٔلُونَكَ عَنِ ٱلۡمَحِيضِۖ قُلۡ هُوَ أَذٗى فَٱعۡتَزِلُواْ ٱلنِّسَآءَ فِي ٱلۡمَحِيضِ وَلَا تَقۡرَبُوهُنَّ حَتَّىٰ يَطۡهُرۡنَ...﴾
ngir li Yàlla Mu kawe mi wax ne:{Danañu la laaj lu jëm ci mbërëg, Neel :“Moom sobe la.Deeleen beru jigéen ñi ci di bañ a sëy ak ñoom bu ñu nekkee ci mbërëg,buleen leen jege ba bañuy laab} [Al-Baqara: 222], lees namm ci mbërëg ci Laaya ji nag mooy jamono ji muy génn ak barab bi muy génnee te mooy pëy mi;
وَلِقَوْلِ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «اصْنَعُوا كُلَّ شَيْءٍ إِلَّا النِّكَاحَ». يَعْنِي: الْجِمَاعَ. رَوَاهُ مُسْلِمٌ
ak it ngir waxi Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko: «Defleen lépp ba mu des sëy».Maanaam: jaxasoo. Muslim soloo na ko; ak it ne jullit ñi dañoo dëppoo ci jàppe sëy ak kiy gis mbaax ci pëyam mu di lu araam.
Du dagan mukk ci nit ki gëm Yàlla ak bis bu mujj ba muy def jëf ju bon jooju nga xam ne Téere Yàlla mu kawe mi ak Sunnas Ndawam li yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko tegtale nañu aaye gu ñu ko aaye, niki noonu dëppoog jullit ñi, du dagan ki gëm di def loolu bay juuyoo ak Yàlla ak ub Yonnenteem, ak di topp yoonu ñu dul way-gëm ña, An-Nawawii wax na ci téere Al-Majmooh firib Al-Muhassab ci xëtum 374 ci xaaju ñaareel ba ne : As-Saafihii yal na ko Yàlla yërëm nee na : «Ku def loolu dikke na bàkkaar bu mag». Sunu waa-ngér ak ñu dul ñoom ne : «Ku sàkkoo daganal sëy ak kiy gis mbaax kooku àttees na ag kéefaram». Waxi An-Nawawii foofu la jeexe.
Waaye-sant Yàlla-daganalal nañu ko lu mu man a faje bànneexam ci ludul ñuy jaxasoo,niki fóon ak sës ak jonjoo ci lu dul pëy ma,waaye li gën a yay mooy mu bañ a jonjoo ak la ca diggante jumbux ba ak bëtu-wóom ba ndare am lu dox ca diggante ba;
لِقَوْلِ عَائِشَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهَا: «كَانَ النَّبِيُّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَأْمُرُنِي فَأَتَّزِرُ، فَيُبَاشِرُنِي وَأَنَا حَائِضٌ». مُتَّفَقٌ عَلَيْهِ.
ngir waxi Aysa ja yal na ko Yàlla gërëm : «Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko daan na ma digal ma wodd muy jonjoo ak man fekk maa ngi gis mbaax». Al-Buxaarii ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téerey Sahiih yi.
Àtteb juróom-ñaareel bi: pase: day araam ci boroom kër gi muy fase kiy gis mbaax ci jamono ji mu koy gis;
﴿يَاأَيُّهَا النَّبِيُّ إِذَا طَلَّقْتُمُ النِّسَاء فَطَلِّقُوهُنَّ لِعِدَّتِهِنَّ...﴾
ngir waxi Yàlla mu kawe mi :{Éey yaw Yonnente bi bu ngeen di fase jigéen ñi nangeen leen fase ci seen yidda} [At-Talaaq: 1] Maanaam: ci jamono joj ñi ngi dëgmal yidda jees xam ca waxtuw pase ma, te loolu du nekk lu dul bu ko fasee fekk mu ëmb walla boog fekk mu laab laab gog sëyu ca ag moom; ndaxte moom bees ko fasee ci jamonoy mbërëg du dëgmal yidda ndax ci mbërëg mi ñu ko fasee deesu ko limaale ci yidda ji, bees ko fasee fekk mu laab laab gog sëy jiitu na pase ma yidda ja muy dëgmal deesu ko xam, ndaxte du xam ndax ëmb na ci sababu sëy boobu,nga xam ne kon day war a yiddawu yidday ku ëmb, walla ëmbul nga xam ne kon day war a yiddawu ci gis mbaax, bi nga xamee ne ameesul lu wóor ci xeetu yidda ji kon day araam ci jëkkër ji muy fase ba ba mbir mi di leer.
Kon daal fase kiy gis mbaax ci jamono ja muy gis mbaax araam na ngir Laaya ji jiitu;
وَلِمَا ثَبَتَ فِي الصَّحِيحَيْنِ وَغَيْرِهِمَا مِنْ حَدِيثِ ابْنِ عُمَرَ: «أَنَّهُ طَلَّقَ امْرَأَتَهُ وَهِيَ حَائِضٌ، فَأَخْبَرَ عُمَرُ بِذَلِكَ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَتَغَيَّظَ فِيهِ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، وَقَالَ: مُرْهُ فَلْيُرَاجِعْهَا، ثُمَّ لِيُمْسِكْهَا حَتَّى تَطْهُرَ، ثُمَّ تَحِيضَ، ثُمَّ تَطْهُرَ، ثُمَّ إِنْ شَاءَ أَمْسَكَ بَعْدُ، وَإِنْ شَاءَ طَلَّقَ قَبْلَ أَنْ يَمَسَّ، فَتِلْكَ الْعِدَّةُ الَّتِي أَمَرَ اللَّهُ أَنْ تُطَلَّقَ لَهَا النِّسَاءُ».
ak it li sax ci ñaari Sahiih yi ak yeneeni téere yu dul ñoom di Hadiisu Ibnu Omar«ne dafa fase soxnaam fekk muy gis mbaax, Omar wax loolu Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko, Ndawal Yàlla li yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko mer ca, ne ko:«Digal ko ne ko na ko jëlaat te mu téye ko ba mu laab, bu gisaatee mbaax nag ba laab,bu ko soobee mu téye ko ginnaaw gi, bu ko soobee it mu fase laata muy sëy ak moom, loolaay yidda ji Yàlla digle ñu di ci fase jigéen ñi». Bu góor gi fase woon soxnaam fekk muy gis mbaax da ciy am bàkkaar, te dina war ci moom mu tuubal Yàlla mu kawe mi, te delloo soxna sa ca buumug sëyam ngir man koo fase pase mu ñu yoonal te mu dëppoo ak ndigalal Yàlla ak ub Yonnenteem, bàyyi ko ginnaaw bi mu ko jëlaatee ba mu laab ci mbërëg ma mu ko fasee, topp mu bàyyi ko ba mu gisaat mbaax ba laab, bu ko neexee bàyyi sëy bi wéy, bu ko neexee it fase ko laata muy jaxasoo ak moom. Dees na settee ci araamal pase ci mbërëg ñatti masala:
bi ci njëkk:bu dee pase mi laata muy wéet ak soxna si la walla jaxasoo ak moom,kon du aay mu fase ko fekk mi ngi gismbaax; Ndaxte yiddawu du ko war su boobaa,kon pase ma du wuute ak
waxi Yàlla mu kawe mi:
﴿...فَطَلِّقُوهُنَّ لِعِدَّتِهِنَّ...﴾
{Na ngeen leen fase ci seen yidda} [At-Talaaq: 1].
Bu ñaareel bi mooy:bu ko mbërëg mi fekkee ci ëmb,te jiitu na ñu leeral sababu loolu.
Bu ñatteel bi: bu dee pase mi soxna see ko sàkku ba jaral ko mu bàyyee jëkër ji lol àqam la woon, bu boobaa du aay mu fase ko fekk mi ngi gis mbaax.
Niki ag juuyoo ak ug xëccoo am ci diggante ñaari way-dencante yi jëkër ji jël ci soxna si luy tax mu defal ko li mu bëgg te mooy fase ko, su boobaa dina dagan mu fase ko doonte day gis mbaax;
لِحَدِيثِ ابْنِ عَبَّاسٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُمَا: أَنَّ امْرَأَةَ ثَابِتِ بْنِ قَيْسِ بْنِ شَمَّاسٍ جَاءَتْ إِلَى النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَتْ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، إِنِّي مَا أَعْتِبُ عَلَيْهِ فِي خُلُقٍ وَلَا دِينٍ، وَلَكِنْ أَكْرَهُ الْكُفْرَ فِي الْإِسْلَامِ. فَقَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «أَتَرُدِّينَ عَلَيْهِ حَدِيقَتَهُ؟» قَالَتْ: نَعَمْ. فَقَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «اقْبَلِ الْحَدِيقَةَ، وَطَلِّقْهَا تَطْلِيقَةً». [رَوَاهُ الْبُخَارِيُّ].
ngir Hadiisu Ibnu Abbaas yal na leen Yàlla gërëm bi mu wax ne soxnas Saabit Ibnu Xays Ibnu Sammaas dafa dikk ci Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko ne ko: yaw Ndawal Yàlla li man de duma ko yedd ci jikko du ma ko yedd ci diine, waaye damay ragal a def jëfi kéefar ci biir Lislaam, Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko ne ko: «Ndax danga koy delloo toolam»? Mu ne ko: waaw, Ndawal Yàlla li yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko ne Saabit:«nangul a jël tool bi te fase ko am pase» [Al-Buxaarii soloo na ko]. Te Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko laaju ko ndax mi ngi doon gis mbaax walla cig laab la nekk?Ginnaaw pase moomu soxna si da ciy jotoo boppam day daal di dagan bees ko aajowoo ci anam gu mu man di nekk.
Ibnu Xudaama wax na ci Al-Muxnii di layal daganug pasem summiku waxtuw mbërëg ci xëtum:52 ci xaaju juróom-ñaareel ba"T M"ne: «Ndaxte tereg pase ci mbërëg li ko waral mooy lor ja ko cay dab ci yàggaayu yidda ja,te summiku ngir dindi lor la joj da koy dab ci nekkiin wu ñaaw ca sëy ba ak dëkk ak kok da koo sib bañ ko,te loolu moo gën a rëy lor ji nekk ci yàggaayu yidda ja, kon day dagan jeñe lor ja gën a kawe ci ja gën a suufe;looloo tax Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko laajul soxna sa sàkku summiku génn ca sëy ba mbiram».Waxam jeex na.
Bu dee fas ab sëy ci jigéen gog day gis mbaax moom aayul ; ndax dagan gi mooy cosaan,te firnde lu koy tere amul, waaye boole ko ak jëkëram cib néeg fekk mi ngi gis mbaax day jar xool góor gi, bu dee kok wóolu nañu ko ci ne du sëy ak moom kon du aay,bu dul loolu nag bu mu wéet ak soxna si ba baa muy laab ngir ragal a tàbbi ci lees di aaye.
Àtteb juróom-ñatt bi:Sukkandikoo yidday pase ci moom-maanaam:mbërëg-:bu góor gi fasee soxnaan ginnaaw bu sëyee ak moom walla mu wéet ak moom war na ci soxna si mu yiddawu ci ñatti mbërëg yu mat,bu dee bokk na ci ñiy gis mbaax,te ëmbul;
ngir li Yàlla mu kawe mi wax ne:
﴿وَٱلۡمُطَلَّقَٰتُ يَتَرَبَّصۡنَ بِأَنفُسِهِنَّ ثَلَٰثَةَ قُرُوٓءٖ...﴾
{Jigéen ñi ñu fase nañu xaar téye seen bopp ba ba ñuy am ñatti mbërëg} [Al-Baqara: 228], Maanaam: gis mbaax baax ñatti yoon. Bu dee ku ëmb la yiddaam mooy bu imbee li mu ëmboon lépp, moo xam diir bu yàgg la walla bu gàtt;
ngir li Yàlla mu kawe mi wax ne:
﴿...وَأُوْلَاتُ الأَحْمَالِ أَجَلُهُنَّ أَن يَضَعْنَ حَمْلَهُنَّ...﴾
{Boroom ëmb yi seen ub dig mooy ñu imbi seeni ëmb} [At-Talaaq: 4], Bu dee jigéen gi bokkul ci ñiy gis mbaax niki xale bi tàmbaleegul a gis mbaax ak ki dem ba gisatu ko ngir ag mage walla ngir dañoo xotti biir ba dindi butitu njurukaay ba walla beneen sabab bob bu amee deesul yaakaar mbërëg ma dellusi, ñooñu seen yidda ñatti weer lay doon;
ngir li Yàlla mu kawe mi wax ne:
﴿وَاللَّائِي يَئِسْنَ مِنَ الْمَحِيضِ مِن نِّسَائِكُمْ إِنِ ارْتَبْتُمْ فَعِدَّتُهُنَّ ثَلَاثَةُ أَشْهُرٍ وَاللَّائِي لَمْ يَحِضْنَ...﴾
{Ñi dem ba naagu ci seeni jigéen gis mbaax, bu ngeen sikk-sàkkaa seen yidda ñatti weer lay doon ak it ñi gisagul mbaax} [At-Talaaq: 4], bu dee bokk na ci ñiy gis mbaax waaye mbërëgam dafa ñëwatul ngir sabab bu ñu xam niki wéradi ak nàmpal kon moom day nekk ca yidda ja rekk doonte diir ba yàgg na ba ba mbërëg ma di dellusi mu sukkandiku ca, Bu sabab bi deñee te mbërëg mi dellusiwul maanaam mu wér ci tawat ji ko daloon walla mu noppi ci nàmpal ga waaye mbërëg mi wéy dog rekk ñëwaatul, bu boobaa day yiddawu at mu mat dale ko ca ba ba sabab ba tee woon a ñëw mbërëg ma deñee, loolu mooy wax ji wér jiy dëppoo ak takk-takki Sariiha yi, bu sabab bi deñee mbërëg amatu fa day mujj mel ni ki mbërëgam taxaw ci lu dul sabab bees xam, bu mbërëgam taxawee ci lu dul sabab bees xam day yiddawu at mu mat, juróom-ñenti weer ngir ëmb bi ngir wóoral;ndax mooy li ëpp lu ëmb di diire, ak ñatti weer ngir yidda ji.
bu dee nag pase ma ginnaaw fasug sëy ba la njëkk muy sëy ak moom walla muy wéet ak moom bu boobaa yidda amu ci mukk, du ci mbërëg du ci leneen;
ngir waxi Yàlla mu kawe mi :
﴿يَاأَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا إِذَا نَكَحْتُمُ الْمُؤْمِنَاتِ ثُمَّ طَلَّقْتُمُوهُنَّ مِن قَبْلِ أَن تَمَسُّوهُنَّ فَمَا لَكُمْ عَلَيْهِنَّ مِنْ عِدَّةٍ تَعْتَدُّونَهَا...﴾
{Éey yeen ñi gëm bu ngeen takkee way-gëm yu jigéen yi ginnaaw ba ngeen fase leen njëkk ngeen di sëy ak ñoom su boobaa amuleen ci ñoom yidda joj dañu koy yiddawu} [Al-Ahsaab: 49].
Àtteb juróom ñenteel bi: àtte setug butitu njurukaay bi, maanaam: ag setam ci ëmb, loolu dees koy aajowoo saa yu ñu aajowoo àtte setug butitu njurukaay bi, loolu am na ay masala :
bokk na ci: bu nit faatoo bàyyi fi jigéen gog la mu ëmb day donn, te fekk moom am na jëkkër, jëkkëram du sëy ak moom ba baa muy gis mbaax,walla ëmb ba leer,bu ëmb ba leeree nu àtte ag donnam ngir li nu àtte ag amam ca ba ka muy donn di faatu,bu jigéen gi gisee mbaax nu àtte ag ñàkk a donnam ngir li nu àtte setug butitu njurukaay ba ci mbërëg ma.
Àtteb fukkeel bi: warug cangaay: dina war ci ki gis mbaax bu laabee mu sangu laabal mbooleem yaram wa;
لِقَوْلِ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ لِفَاطِمَةَ بِنْتِ أَبِي حُبَيْشٍ: «فَإِذَا أَقْبَلَتِ الْحَيْضَةُ فَدَعِي الصَّلَاةَ، وَإِذَا أَدْبَرَتْ فَاغْتَسِلِي وَصَلِّي» [رَوَاهُ الْبُخَارِيُّ].
ngir li Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko wax Faatima Bintu Abii Hubays : «Bu mbërëg mi dikkee bàyyil julli, bu demee nga sangu te julli» [Al-Buxaarii soloo na ko].
Gën gaa néewug li war ci cangaay mooy matale mbooleem yaramam wa ba ca la ca suufu kawar ga, li gën nag mooy mu defe ko ci melo wi mu dikke ci Hadiis ba
«عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ حَيْثُ سَأَلَتْهُ أَسْمَاءُ بِنْتُ شَكَلٍ عَنْ غُسْلِ الْمَحِيضِ، فَقَالَ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «تَأْخُذُ إِحْدَاكُنَّ مَاءَهَا وَسِدْرَتَهَا فَتَطَهَّرُ فَتُحْسِنُ الطُّهُورَ، ثُمَّ تَصُبُّ عَلَى رَأْسِهَا فَتَدْلُكُهُ دَلْكًا شَدِيدًا، حَتَّى تَبْلُغَ شُؤُونَ رَأْسِهَا، ثُمَّ تَصُبُّ عَلَيْهَا الْمَاءَ، ثُمَّ تَأْخُذُ فُرْصَةً مُمَسَّكَةً - أَيْ: قِطْعَةَ قُمَاشٍ فِيهَا مِسْكٌ - فَتَطَهَّرُ بِهَا»، فَقَالَتْ أَسْمَاءُ: كَيْفَ تَطَهَّرُ بِهَا؟ فَقَالَ: «سُبْحَانَ اللَّهِ!»، فَقَالَتْ عَائِشَةُ لَهَا: تَتَبَّعِينَ أَثَرَ الدَّمِ». [رَوَاهُ مُسْلِمٌ].
«jële nañu ci Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko bi ko Asmaa Bintu Saklin laajee cangaayal mbërëg mu ne ko -yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko-:«Kenn ci yeen day jël ndoxam ak xobi déemam daal di laablu te rafetal laablu ga, topp mu sotti ci boppam bomb ko bu baax ba mu egg ci rëddi deri boppam, topp mu sotti ci kawam ndox, topp mu jël sagar wu am gëtt laablu ci»,Asmaa ne: naka la ciy laabloo? Mu ne ko :«Tudd naa sellug Yàlla!», Aysa ne ko: dangay topp jeexiiti dereet ji.[Muslim soloo na ko].
Du war muy firi kawaru bopp bi, ndare muy lu ñu fas ba mu dëgër ba muy ragal ndox ma di ñàkk a egg fa kawar ga saxe;
لِمَا فِي صَحِيحِ مُسْلِمٍ مِنْ حَدِيثِ أُمِّ سَلَمَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهَا أَنَّهَا سَأَلَتِ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَقَالَتْ: إِنِّي امْرَأَةٌ أَشُدُّ شَعْرَ رَأْسِي، أَفَأَنْقُضُهُ لِغُسْلِ الْجَنَابَةِ؟ وَفِي رِوَايَةٍ: لِلْحَيْضَةِ وَالْجَنَابَةِ؟ فَقَالَ: «لَا، إِنَّمَا يَكْفِيكِ أَنْ تَحْثِيَ عَلَى رَأْسِكِ ثَلَاثَ حَثَيَاتٍ، ثُمَّ تُفِيضِينَ عَلَيْكِ الْمَاءَ فَتَطْهُرِينَ».
ngir li ñëw ci Sahiihu Muslim di Hadiisu Ummu Salamata yal na ko Yàlla gërëm bi mu laajee Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko,ne ko: man de jigéen laa gog damay fas sama kawaru bopp ba mu dëgër,ndax dama koy firi ngir sangu janaba? Ci beneen nettali mu ne:ngir sangu mbërëg ak janaba? Mu ne ko:«Dina la doy rekk nga tanq ak sa ñaari loxo def sa bopp ñatti yoon, topp nga sotti ndox mi ci sa kaw daal di laab».
Bu kiy gis mbaax laabee ci biir waxtuw julli dina war ci moom mu gaaw sangu ngir dab joxeg julli ga ci waxtoom, bu nekkee ci ab tukki te amul ndox walla sax am na ndox waaye day ragal loru ci jëfandikoo ko, walla mu tawat tawat joj ndox da koy lor su boobaa day tiim wottee ko cangaay la ba la ko teree jëfandikoo ndox ma deñ mu daal di sangu.
Ñenn ci jigéen ñi nag dañuy laab ci biir waxtuw julli ba noppi di yeexe cangaay la ba weneen waxtu dugg naan:manu ñoo sangu cangaay lu mat ci waxtu woowu, waaye loolu moom du aw lay te du ngànt it; ndaxte man naa def rekk gën gaa néewug li war ci cangaay, daal di julli ci waxtoom, bu amee waxtu wu yaatu daal di sangu cangaay la gën a mat.
Buntub juróomeel bi: ci dereeti jàngoro ak i àtteem
Dereeti jàngoro: mooy dereet jiy wéy di génn ci jigéen nga xam ne du dog mukk, walla sax muy dog ci diggante bu gàtt niki benn bis walla ñaari bis ci weer wi.
Firndéey anam gu njëkk gi nga xam ne dereet ji du dog mukk mooy li sax ci Sahiihul Buxaarii ñu jële ci Aysa yal na ko Yàlla gërëm mu ne:
«قَالَتْ فَاطِمَةُ بِنْتُ أَبِي حُبَيْشٍ لِرَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، إِنِّي لَا أَطْهُرُ». وَفِي رِوَايَةٍ: «أُسْتَحَاضُ فَلَا أَطْهُرُ».
«Faatima Bintu Abii Hubays dafa wax Ndawal Yàlla li yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko: yaw Ndawal Yàlla li man de duma laab. Ci beneen nettali mu ne ko: sama dereet day wéy di génn ba duma laab».
Firndéey anamug ñaareel gi nga xam ne dereet ji du dog ndare lu néew Hadiisu Hamnatu Bintu Jahsin nga xam ne dafa dikk fa Yonnente ba yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko ne ko:
«يَا رَسُولَ اللَّهِ، إِنِّي أُسْتَحَاضُ حَيْضَةً كَثِيرَةً شَدِيدَةً». [الْحَدِيثُ.. رَوَاهُ أَحْمَدُ وَأَبُو دَاوُدَ وَالتِّرْمِذِيُّ وَصَحَّحَهُ، وَنُقِلَ عَنِ الْإِمَامِ أَحْمَدَ تَصْحِيحُهُ، وَعَنِ الْبُخَارِيِّ تَحْسِينُهُ].
«Yaw Ndawal Yàlla li man de sama dereet day wéy di génn bari lool te tar».[ba Hadiis ba egg.. Ahmat soloo na ko ak Abóo Daawuda, At-Tirmisii it soloo na ko wéral ko toxale ci Ahmat ag wéralam, toxale it ci Al-Buxaarii ag rafetalam].
Anami dereeti jàngoro:
Ki dereetam dul dog am na ñatti anam:
Anam gi njëkk:mu am jamono ju muy gis mbaax jees xam laata dereet jiy wéy di ñëw, kooku day dellu ci diirub mbërëgam ma mu xamoon la jiitu, mu cay néggandiku, àttey mbërëg ñeel ko ca, leneen lu dul loolu dereeti jàngoro la joj ay àtteem day sax ñeel ko.
Misaalum loolu: jigéen gog mbërëg daa na ko dikkal juróom-benni fan ci njëlbéenug weer wu nekk, mujj dereeti jàngoro dal ko dereet ji di wéy di ko dikkal ànd ak moom,kooku mbërëgam juróom-benni fan la ci njëlbéenu weer wu nekk,lu dul loolu dereeti jàngoro la;
لِحَدِيثِ عَائِشَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهَا أَنَّ فَاطِمَةَ بِنْتَ أَبِي حُبَيْشٍ قَالَتْ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، إِنِّي أُسْتَحَاضُ فَلَا أَطْهُرُ، أَفَأَدَعُ الصَّلَاةَ؟ قَالَ: «لَا، إِنَّ ذَلِكِ عِرْقٌ، وَلَكِنْ دَعِي الصَّلَاةَ قَدْرَ الْأَيَّامِ الَّتِي كُنْتِ تَحِيضِينَ فِيهَا، ثُمَّ اغْتَسِلِي وَصَلِّي». رَوَاهُ الْبُخَارِيُّ.
ngir hadiisu Aysa yal na ko Yàlla gërëm bi mu ne Faatima Bintu Abii Hubays dafa ne: yaw Ndawal Yàlla li,man de sama dereet day wéy rekk ba duma laab ndax damay bàyyi julli gi? Mu ne ko:«Déedéet, loolu gamb yu toj yu bawoo ci butitu njurukaay bi la,waaye bàyyil julli lu tolloo ak bis ya nga daa gis mbaax topp nga sangu daal di julli».Al-Buxaarii soloo na ko,
وَفِي صَحِيحِ مُسْلِمٍ: أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ لِأُمِّ حَبِيبَةَ بِنْتِ جَحْشٍ: «امْكُثِي قَدْرَ مَا كَانَتْ تَحْبِسُكِ حَيْضَتُكِ، ثُمَّ اغْتَسِلِي وَصَلِّي».
ñëw na ci Sahiihu Muslim: Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko ne Ummu Habiiba Bintu Jahsin: «Néggandikul lu tolloo ak la la sa mbërëg daa téye, topp nga sangu te julli». Ci kaw loolu ki dereetam taxawul te mu amoon mbërëg mu jaar yoon mees xam kooku day néggandiku kem mbërëgam, topp mu sangu te julli te bu boobaa du faale dereet jay wéy di génn.
Anamug ñaareel gi:mu ñàkk a am mbërëg mees xam laata dereet jiy wéy di ko dikkal, nga xam ne dereet jiy wéy day ànd ak moom dale ko ca ba muy njëkk a gis dereet ca yoon wu njëkk wa,kooku li muy def mooy ràññetle, nga xam ne mbërëgam day doon lu ràññiku ak ñuulaay walla ag tal walla ag xet, bu ko defee àttey mbërëg sax ca,leneen lu dul loolu dereeti jàngoro la joj ayàtteem day sax ñeel ko.
Misaalum loolu jigéen gog gis na dereet ci yoon wi mu ko njëkk a gise, mu wéy ak moom dogul, waaye da koy gis mu ñuul fukki fan li des ci weer wi mu xonk, walla mu koy gis fukki fan mu tal, li des ci weer wi mu yolom, walla mu koy gis fukki fan mu ànd ak xetu mbërëg te li des ci weer wi du am xet,kooku kon mbërëgam mooy la ñuul ci misaal mu njëkk mi ak la tal ci misaalum ñaareel mi ak la am xet ci misaalum ñatteel mi, leneen lu dul loolu dereeti jàngoro la;
لِقَوْلِ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ لِفَاطِمَةَ بِنْتِ أَبِي حُبَيْشٍ: «إِذَا كَانَ دَمُ الْحَيْضَةِ فَإِنَّهُ أَسْوَدُ يُعْرَفُ، فَإِذَا كَانَ ذَلِكِ فَأَمْسِكِي عَنِ الصَّلَاةِ، فَإِذَا كَانَ الْآخَرُ فَتَوَضَّئِي وَصَلِّي؛ فَإِنَّمَا هُوَ عِرْقٌ». [رَوَاهُ أَبُو دَاوُدَ وَالنَّسَائِيُّ، وَصَحَّحَهُ ابْنُ حِبَّانَ وَالْحَاكِمُ].
ngir li Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko wax Faatima Bintu Abii Hubays : «Bu dee dereeti mbërëg la moom day ñuul di lees xam, bu melee noonu bàyyil julli, bu dee jeneen dereet la na nga jàpp te julli; loolu ay gamb la rekk yuy toj di génne ci butitu njurukaay bi». [Abóo Daawuda soloo na ko ak An-Nasaa-i, Ibnu Hibbaan wéral ko ak Al-Haakim]. Hadiis bii doonte càllalaam gi ak yaxu bi amna lees di xool, teewul woroom xam-xam yi jëfe ko yal na Yàlla yërëm leen, te moo gën a yey ci ñuy delloo masala mi ci aaday li ëpp ci jigéen ñi.
Anamu ñatteel gi: mu ñàkk a am mbërëg mees xam ñàkk a am it ag ràññee gu wér ci dereet ji nekk di wéy la ko dale ca ba mu njëkkee gis dereet ak dereetu mbërëgam di wenn melo, walla sax ay melo yu leerul yoy du man a doon mbërëg, kooku day sukkandiku ci aaday li ëpp ci jigéen ñi, mbërëgam doon juróom-benni fan walla juróom-ñaar ci weer wu nekk doore ko ci diir bi mu njëkk a gisee dereet, lu dul loolu dereeti jàngoro la.
Misaalum loolu: mooy mu gis dereet ci yoon wu njëkk ci juróomeelu bis ci weer wi mu wéy ànd ak moom ci lu dul muy am ug ràññetle gu wér ci mbërëg mi, du ci melo du ci leneen, bu boobaa mbërëgam day doon ci weer wu nekk juróom-benni fan walla juróom-ñaar yoy day doore ci bisu juróomeel ci weer wu nekk;
لِحَدِيثِ حَمْنَةَ بِنْتِ جَحْشٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهَا أَنَّهَا قَالَتْ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، إِنِّي أُسْتَحَاضُ حَيْضَةً كَبِيرَةً شَدِيدَةً، فَمَا تَرَى فِيهَا؟ قَدْ مَنَعَتْنِي الصَّلَاةَ وَالصِّيَامَ، فَقَالَ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «أَنْعَتُ لَكِ (أَصِفُ لَكِ اسْتِعْمَالَ) الْكُرْسُفَ (وَهُوَ الْقُطْنُ)، تَضَعِينَهُ عَلَى الْفَرْجِ، فَإِنَّهُ يُذْهِبُ الدَّمَ»، قَالَتْ: هُوَ أَكْثَرُ مِنْ ذَلِكَ. وَفِيهِ قَالَ: «إِنَّمَا هَذِهِ رَكْضَةٌ مِنْ رَكْضَاتِ الشَّيْطَانِ، فَتَحَيَّضِي سِتَّةَ أَيَّامٍ أَوْ سَبْعَةً فِي عِلْمِ اللَّهِ تَعَالَى، ثُمَّ اغْتَسِلِي حَتَّى إِذَا رَأَيْتِ أَنَّكِ قَدْ طَهُرْتِ وَاسْتَنْقَأْتِ، فَصَلِّي أَرْبَعًا وَعِشْرِينَ أَوْ ثَلَاثًا وَعِشْرِينَ لَيْلَةً وَأَيَّامَهَا، وَصُومِي». الْحَدِيثُ. [رَوَاهُ أَحْمَدُ وَأَبُو دَاوُدَ وَالتِّرْمِذِيُّ وَصَحَّحَهُ، وَنُقِلَ عَنْ أَحْمَدَ أَنَّهُ صَحَّحَهُ، وَعَنِ الْبُخَارِيِّ أَنَّهُ حَسَّنَهُ].
ngir Hadiisu Hamnatu Bintu Jahsin yal na ko Yàlla gërëm bi mu waxee: yaw ndawal Yàlla li man de sama dereet day wéy di génn bari lool te tar, lan nga ci xam? Tee na maa julli tee maa woor,Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko ne ko: «Maa ngi lay wax nga jëfandikoo wëtéen teg ko ci pëy mi, moom day yóbb dereet ji»,mu ne ko: dereet ji ëpp na loolu. Ci Hadiis nee na ko:«loolu du lenn lu moy aw wéq ci wéqi saytaane yi jàppal sa mbërëg ci juróom-benn walla juróom-ñaar fan ci xam-xamu Yàlla mu kawe mi,topp nga sangu ba gis ne laab nga set nga, nga julli ñaar-fukk ak ñent walla ñaar-fukk ak ñatti guddi ak seeni bëccëg te nga woor».Ba Hadiis ba egg. [Ahmat soloo na ko ak Abóo Daawuda, At-Tirmisii it soloo na ko wéral ko toxale ci Ahmat it ne wéral na ko,toxale ci Al-Buxaarii it ne rafetal na ko].
wax ji Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko wax ne:«juróom-benn walla juróom ñaari fan» du ngir tànn bu la neex,waaye ngir farlu la, jigéen gi day xool li gën a jege mbiram ci ñi ko niru ci bind neexoo ak moom ci ay at ak butitu njurukaay,ak li gën a jege mbërëg ci dereetam,ak yu deme noonu ci yees di sóoraale bu dee juróom-benni fan a gën a jege mbiram mu def ko juróom-benn, bu dee juróom-ñaar, mu def ko juróom-ñaar.
Mbiru kiy niru ku am dereeti jàngoro:
man naa am sabab su waral ci jigéen dereet ja di nàcc bawoo ci pëyam niki am paj mu ñu def ci butitu njurukaay ba walla fu yeggul foofu, te loolu ñaari xeet la:
Xeet wu njëk wi: jigéen gi xam ne dootul man a gis mbaax ginnaaw paj mi, niki paj ma doon dindi butitu njurukaay ba lépp walla fatt ko ba dereet du wàcc bawoo fa, jigéen googu àttey ki dereetam jaarul yoon du ko ñeel, waaye àtteem mooy àtteb kiy gis dereet ju mboq la walla ju nëx walla ay tooy-tooy ginnaaw laab, du bàyyi julli du bàyyi woor jaxasoo ak moom it du terewuñu ko, te sangu du ko war ci dereet jooju, waaye dina war buy julli mu raxas dereet ja, ak it def ci pëyam aw sagar walla lu ni mel; ngir feg génnug dereet ja, topp mu jàpp ngir julli, waaye du jàpp lu dul ginnaaw Duggug waxtuw julli wa, bu dee julli gu am waxtu la, niki julliy juróom yi, bu dul loolu man naa jàpp saa yu bëggee julli niki naafila gees joyal.
Xeeti ñaareel wi: mu bañ a xam terewug mbërëgam ginnaaw paj ma, jàpp ne man naa gis mbaax ba leegi, kooku àtteem àtteb ku dereetam jaarul yoon la, liy tegtale loolu ñu wax mooy waxi Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko ñeel Faatima Bintu Abii Hubays:
ذَلِكِ عِرْقٌ وَلَيْسَ بِالْحَيْضَةِ، فَإِذَا أَقْبَلَتِ الْحَيْضَةُ فَاتْرُكِي الصَّلَاةَ.«
«Loolu du dara lu dul gamb yu toj waaye du mbërëg, bu mbërëg mi dikkee bàyyil julli gi». Li Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko wax ne: «bu mbërëg mi dikkee» day jariñ ne àtteb ki dereetam jaarul yoon mi ngi ame ci ku am mbërëg mu man a nekk mom day ñëw ak a dem,waaye ki amul mbërëg mu man a nekk moom dereetam dereeti gamb la ak nu mu man a deme.
Àttey dereeti jàngoro:
Xam nanu ci li jàll kañ la dereet di doon mbërëg ak kañ lay doon dereeti jàngoro, saa yu nekkee mbërëg àttey mbërëg sax ñeel ko, saa yu nekkee dereet jiy wéy rekk du dog àttey dereeti jàngoro sax ñeel ko.
Tudd nañu li am solo ci àttey mbërëg.
Bu dee àttey dereeti jàngoro nag moom moo ngi mel ni àttey laab, amul ag teqale diggante ki dereetam wéy tëw a dog ak ñi laab lu dul ci lii di ñëw:
Bi ci njëkk: warug jàppoom ñeel julli gu nekk,
لِقَوْلِ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ لِفَاطِمَةَ بِنْتِ أَبِي حُبَيْشٍ: «ثُمَّ تَوَضَّئِي لِكُلِّ صَلَاةٍ». رَوَاهُ الْبُخَارِيُّ فِي بَابِ غَسْلِ الدَّمِ.
ngir li Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko wax Faatima Bintu Abii Hubays ne ko: «topp nga jàppal julli gu nekk». Al-Buxaarii soloo na ko ci buntub raxas dereet, Maanaam wax jooju mooy jigéen googu du jàppal julli gu am waxtu fii ak waxtoom duggul. Bu dee julli ga amul waxtu nag da koy jàppal ci waxtu wa mu nammee julli.
Ñaareel bi: bu bëggee jàpp day raxas jeexiiti dereet ja, def sagar ci pëyam ak wëttéen ngir mu téye dereet ji;
لِقَوْلِ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ لِحَمْنَةَ: «أَنْعَتُ لَكِ الْكُرْسُفَ فَإِنَّهُ يُذْهِبُ الدَّمَ». قَالَتْ: فَإِنَّهُ أَكْثَرُ مِنْ ذَلِكَ. قَالَ: «فَاتَّخِذِي ثَوْبًا». قَالَتْ: هُوَ أَكْثَرُ مِنْ ذَلِكَ. قَالَ: «فَتَلَجَّمِي». الْحَدِيثُ.
ngir li Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko wax Hamnatu ne ko: «Maa ngi lay wax nga jëfandikoo wëttéen, moom day yóbb dereet ji». Mu ne ko : moom ëpp na loolu. Mu ne ko: «Wutal yére». Mu ne ko: moom ëpp na loolu. Mu ne ko: «fattal pëy mi». Ba Hadiis ba egg, lu génn ginnaaw loolu du ko lor; ngir li Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko wax Faatima Bintu Abii Hubays ne ko:
«اجْتَنِبِي الصَّلَاةَ أَيَّامَ حَيْضِكِ، ثُمَّ اغْتَسِلِي وَتَوَضَّئِي لِكُلِّ صَلَاةٍ، ثُمَّ صَلِّي، وَإِنْ قَطَرَ الدَّمُ عَلَى الْحَصِيرِ». [رَوَاهُ أَحْمَدُ وَابْنُ مَاجَهْ].
«Wattandikul julli ci sa bisi mbërëg, topp na nga sangu te jàppal julli gu nekk te julli, doonte dereet ja toq na ci kaw laltu ga». [Ahmat soloo na ko ak Ibnu Maaja].
Ñatteel bi: jaxasoo, woroom xam-xam yi wuute nañu ci ag daganam bu dee jëkkër ji ragalul a njaaloo bu ko bàyyee, li wér nag mooy ag daganam cig joyal; ndax jigéen ñu bari ñu am fukki at walla lu ko ëpp amoon nañu dereet ju jaarul yoon jamonoy Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal Ko, te Yàlla ak Ndawam li it terewuñu leen jaxasoo ak ñoom. Te sax li Yàlla Mu kawe mi wax ne: {Beruleen jigéen ñi ci mbërëg mi} [Al-Baqara: 222] day tegtale ne du war ñu beru leen ci leneen lu dul loolu; ak it ginnaaw julli dagan na ci moom kon jaxasoo moo gën a woyof, te natt sëy ga ak ñoom ci sëy ak ku nekk ci mbërëg nekkul lu wér; ndax ñoom ñaar yemuñu ba ci sax ñiy wax araamug jaxasoo googu, te natt am mbir ci lu mu wuuteel du lu wér.
Teqaleg juróom-benneel gi: ci wësin ak àtteem
Wësin: dereet la joj butitu njurukaay a koy génne ci sababus am doom, benn mu ànd ak moom walla mu dikk ginnaawam walla sax laata muy jur ci ñaari fan walla ñatt mu ànd ak mettiitu jur ga.
Seexul Lislaam Ibnu Taymiya nee na: «Li jigéen gi di gis buy tàmbalee yég mettiitu jur loola dereeti wësin la». Tënku ko ci ñaari fan walla ñatt, te li mu namm mooy : mettiit wow jur a cay topp, bu dul loolu du doon dereeti wësin. Woroom xam-xam yi wuute nañu: ndax am na dayo ci gën gaa néewam ak gën gaa bareem?. Seexul Taqiyyu Diin wax na ci bataaxelam bi mu def ci tur yi Aji-Yoonal ji wékk àtte ya ca ñoom (xëtu : 37): «dereeti wësin amul dayo ca gën gaa néewam ak gën gaa bareem, bees nattale woon ne jigéen gis na dereet lu ëpp ñent-fukki bis walla juróom-benn-fukk walla juróom-ñaar-fukk mu door a dog dees koy jàppe dereeti wësin, waaye bu dee dereet ju ca jokk la moom dereeti tawat lay doon, te su boobaa dayo ba ñent fukki bis lay doon, loolu mooy gën gaa barig li ëpp ci li xibaar yi joxe». Jeex na.
Ma ne: ci kaw loolu bu dereetam jéggee ñent-fukki bis, te aadaam doonoon ne dereet ja day dog ginnaaw loolu, walla ay màndarga feeñ yuy wone jegeg dog ga bu boobaa day xaar ba mu dog, bu dul loolu nag mu sangu bu matalee ñent-fukk; ndax loolooy li ëpp, ndare mu yamoo ak mbërëgam mu xaar kon ba jamonoy mbërëg ma jeex, bu dogee ginnaaw loolu dina jaadu mu doon aadaam, nga xam ne beneen yoon noonu lay def, bu dereet ja wéyee nag mu doon ku dereetam jaarul yoon, kon day dellu ca àttey ki dereeti jàngoro yi jàll, Bu laabee ci sababu dogug dereet ja kon laab na doonte laata muy matal ñent-fukki fan la, kon day sangu julli woor jëkkëram man a jaxasoo ak moom, ndare dogug dereet ja doon ci lu yées benn bis su boobaa amul àtte, Ibnu Xudaama wax na ko ca Al-Muxnii.
Dereeti wësin du sax lu dul bu juree lol bindub doomu Aadama leer na ca, bu juroon lu matul nit lu ndaw lol bindub doomu Aadama leeru ca bu boobaa dereetam du dereeti wësin, waaye dereeti gamb la, àtteem day doon àtteb ki ame dereeti jàngoro, diir bi gën a néew bob bindub doomu Aadama dina ca leeree mooy juróom ñett-fukki fan dale ko ca ndoorteelu ëmb ba, gën gaa bari di juróom-ñent-fukki fan.
Al-Majd Ibnu Taymiya nee na: saa yu gisee dereet bis mu ànd ak yég mettiitu jur lu njëkk loolu du bàyyi-xel dereet jooju, bu dee ginnaaw gi la ko gis su boobaa day bàyyi julli ga ak koor ga, topp bu mbir ma leeree ginnaaw amug doomam daal di wuute ak li feeñ mu dellu dabaatal, bu dee mbir ma leerul nag àtteb la feeñ wéy te du ko baamu. Toxale na ko ci moom ci firib Al-Iqnaah.
Àttey wësin:
Àttey wësin moo ngi mel ni àttey mbërëg ñoo yem kepp, ndare ci lii di ñëw:
Bi ci njëkk: mooy yidda, dees koy sóoraale ci pase ci ludul wësin; ndaxte bu dee pase mi njëkk muy am doom la day jeex bu amee doom waaye du ci buy gis dereeti wësin, bu dee pase mi ginnaaw am doom ga la nag mu xaar dellusig mbërëg ma niki ni mu jiitoo ci li jàll.
Ñaareel bi: diirub giñ ba dees cay limaale diirub mbërëg ma te deesu ca limaale diirub wësin ga.
Giñ bi: mooy góor gi giñ ne day bàyyi sëy ak soxnaam ba fàww walla diir bu ëpp ñenti weer, bu giñee soxna si sàkku ci moom sëy dees koy àppal diirub ñenti weer dale ko ca ba mu giñee, bu matee ñu ga ko ci mu sëy ,(ga: forcé)walla mu teqalikoo ci càkkuteeful soxna si, diir boobu bu ci soxna si wësinee deesu ko limaale ci kaw góor gi, waaye dees koy dolli ci ñenti weer ya lu tolloo ak diirub wësin ga, wuute ak mbërëg nga xam ne ay bisam dees koy limaale ci kaw góor gi.
Ñatteel bi: mat mukàllaf day ame ci mbërëg te du ame ci wësin; ndax jigéen gi manut a ëmb lu dul ne wasal na, kon mat mukàllaf ga day ame ci wasal ga jiitu ëmb ba.
Ñenteel bi: dereeti mbërëg su dogee topp mu dellusiwaat ci biir bis yi jigéen gi baaxoo gis mbërëg bu boobaa mbërëg lay doon ci lu wóor, niki aadaam doon juróom-ñatti fan, mu gis mbaax ñenti fan mu dog ñaari fan dellusiwaat ci juróom-ñaareelu fan ba ak juróom-ñatt, loolu dellusi mbërëg la ci lu wóor, àttey mbërëg day sax ñeel ko, Bu dee dereeti wësin nag bu dogee laata ñent-fukki fan topp mu dellusiwaat ci ñent-fukki fan yi bu boobaa dees cay sikk-sàkka, kon day war mu julli woor farata jees wutal waxtu ci waxtoom, te day araam ci moom mbooleem lu araam ci kiy gis mbaax ba mu des yi war, nga xam ne day fay ginnaaw ag laabam li mu defoon ci dereet jooju ci yi war ci kiy gis mbaax war koo fay, loolooy li siiw ci woroom xam-xami Hanaabila yi.
Li wér nag mooy bu dereet ji delloo ci moom ci jamono joj man naa doon wësin kon wësin lay doon, bu dul loolu mu doon mbërëg,ndare mu wéy ànd ak moom daal di doon dereeti jàngoro.
Te loolu jege na li Ibnu Xudaama toxal ci Al-Muxnii jële ko ci Imaam Maalik yal na ko Yàlla yërëm nga xam ne dafa wax ne: Maalik nee na: «bu gisee dereet ginnaaw ñaari bis walla ñatt -maanaam: ginnaaw ag dogam- kon dereeti wësin la bu dul loolu mbërëg la». Jeex na Te loolu moo dëppoo ak tànnug Seexul Lislaam Ibnu Taymiya yal na ko Yàlla yërëm.
Dereet yi amul jenn jees di sikk-sàkka ci li am ñu koy gis, waaye sikk-sàkka mbir la mom day topp jëmm, nit ñi dañu ciy wuute ci keemtulaayal seen xam-xam ak seen dégg-dégg, te Alxuraan ak Sunna leeral na lépp, te Yàlla tudd naa sellam ga waralul ci kaw kenn muy woor ñaari yoon, walla muy wër Kaaba ga ñaari yoon, ndare yoon wu njëkk wa am njuumte lol manu koo dabaatal lu dul ci fay ko, waaye bu dee jaam bi daa def li mu man ci lees ko togg ca kem-kàttanam kooku jaanam wàcc na,
niki ni ko Yàlla Mu kawe mi waxe:
﴿لَا يُكَلِّفُ ٱللَّهُ نَفۡسًا إِلَّا وُسۡعَهَا...﴾
{Yàlla du togg bakkan lu dul lu mu man}
[Al-Baqara: 286].
wax it ne:
﴿فَٱتَّقُواْ ٱللَّهَ مَا ٱسۡتَطَعۡتُمۡ...﴾
{Ragalleen Yàlla seen kem-kàttanam}
[At-Taxaabun: 16].
Teqaleg juróomeel gi diggante mbërëg ak wësin: ci mbërëg bu jigéen gi laabee njëkk aadaam dagan na ci jëkkëram mu sëy ak moom ci lu dul ag sibeel, bu dee ci wësin la nag bu laabee njëkk ñent-fukki fan dees di sib ci jëkkëram muy sëy ak moom ci li siiw ci ngir mi, waaye li wér mooy deesul sib mu sëy ak moom, loolu mooy waxi ñi ëpp ci woroom xam-xam yi; ndaxte sib dara àtteb Sariiha la bob day aajowoo firndel Sariiha, Te masala mii amul lu dul li Imaam Ahmat wax jële ko ci Usmaan Ibnu Abil Haas ne soxnaam da koo dikkal njëkk ñent-fukki fan mu ne ko: bu ma jege. Te loolu doonul lol fàww sibeel da ciy am; ndax man naa nekk ne Usmaan day bëgg lu gën a wóor rekk ragal ne soxna si amul lu ko wóor ci ag laabam, walla sax mu ragal dereet ja yënguwaat ci sababus jaxasoo ga, walla yeneeni sabab. Yàlla a gën a xam.
Teqaleg juróom-ñaareel gi: ci jëfandikoo luy tee a gis mbaax walla lu koy ñoddi mu ñëw ak luy tee a ëmb ak lu koy yàq
Jëfandikoog jigéen gi lu koy tee a gis mbaax dagan na ci ñaari sàrt:
Bi njëkk: mu bañ caa ragal lor, bu ca ragalee lor nag du dagan;
ngir li Yàlla mu kawe wax ne:
﴿...وَلَا تُلۡقُواْ بِأَيۡدِيكُمۡ إِلَى ٱلتَّهۡلُكَةِ...﴾
{Buleen tàbbal seen bopp ci alkande}
[Al-Baqara: 195].
﴿...وَلَا تَقۡتُلُوٓاْ أَنفُسَكُمۡۚ إِنَّ ٱللَّهَ كَانَ بِكُمۡ رَحِيمٗا﴾
{Buleen ray seen bopp Yàlla day ku am yërmaande lool ci yeen} [An-Nisaa: 29].
Ñaareel bi: loolu amee ci ndigalul jëkkëram bu dee daa am lu ca aju ci moom niki jigéen gi di yiddawu fa moom ci anam gog dundal ko da koy war, ba noppi jigéen gi di jëfandikoo lu tee gis mbaax; ngir rekk yàggal diir ba ba dundal ga mu koy dundal man a yokk bu boobaa du dagan ci jigéen gi muy jëfandikoo lu koy tee a gis mbaax lu dul ci ndigalul jëkkëram, niki noonu it bu saxee ne tere mbërëg mi day tee ëmb su boobaa du man a ñàkk mu am ndigalul jëkkëram, ànd ak nag li dagan gi sax lépp li gën a yey mooy ñàkk koo jëfandikoo lu dul ngir aajo; ndaxte bàyyi lees mooñaale nit ki ca na mu mel moo gën a jege wergi-yaram wu digg-dóomu ak ug mucc.
Bu dee jëfandikoo luy xëcc mbërëg mi moom dina dagan ci ñaari sàrt itam:
Bi njëkk: mu bañ cee jaaree di lal i pexe ngir wàccee boppam lu ko war, niki mu koy jëfandikoo bu weeru koor jegee, ngir man a bañ a woor walla mu def ko ngir wàccee boppam julli, ak yu ni mel.
Ñaareel bi: loolu ame ci ndigalul jëkkëram; ndaxte amug mbërëg da koy tee bànneexu bànneex bu mat, kon du dagan di jëfandikoo lu koy xañ àqam lu dul mu ànd ci, doonte soxna si dees koo fase, ndaxte loolu gaawe rotal àqi jëkkër ji a ngi ci, ci jëlaat soxnaam bu dee pasem payle la.
Bu dee jëfandikoo luy tee ëmb moom ñaari xeet la:
Bi njëkk: mu tee koo am doom ba fàww, loolu du dagan, ndax loolu day dog ëmb di néewal njur mi, te loolu daa juuyoo ak jubluwaayu Aji-Yoonal ji ci baril xeetu lislaam wi; ak it ne du wóor doomam ya mu jot a am dee mu des fa ginnaaw bi jëkkëram faatoo ci lu dul muy am ay doom.
Ñaareel bi: mu tee koo ëmb ab diir, niki jigéen jiy nef di ku bari lu muy ëmb, te ëmb di ko sonal, kon day war mu nose ëmbam ñaari at yu nekk benn yoon, walla lu mel noonu, loolu dagan na, ci sàrtub jëkkëram jox ko ci ndigal, ak it loolu bañ koo lor moom soxna si, firndeem mooy ne Saabaa ya daa nañu bañ a wasal ci seeni soxna ci jamonoy Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko ngir bañ seen soxna yi ëmb, te terewuñu leen ko, te loolu mooy nit ki sëy ak soxnaam bu demee bay bëgg a wasal daal di génne pëyam ci pëyu soxna si.
Bu dee jëfandikoo luy yàq ëmb moom ñaari xeet la:
Ba ca njëkk: mu jublu ci yàq ko sànk doom ji, loolu bu dee ginnaaw bees walee ag ruu ci doom ji lu araam lay doon, ci lu dul sikk-sàkka; ndaxte loolu ray bakkan bees araamal ku ko ray la ci lu dul dëgg, te ray bakkan bees araamal ku ko ray lu araam la ci Alxuraan ak Sunna ak dëppoog jullit ñi, Bu dee njëkk ñu ciy wal ag ruu la woroom xam-xam yi wuute nañu ci ag daganam, am ci ñu ko daganal, am ñu ko tere, am ñu ne: dagan na bu doonul lumb dereet. Maanaam : bu amul ñent-fukki fan, am ñu ne: dagan na fii ak bindub doomu Aadama leeru ca.
Li gën a wóor nag mooy tere yàq ëmb lu dul aajo waral ko niki yaay ji wéradi ba àttanul ëmb bi ak yu mel noonu, bu boobaa dina dagan mu yàq ko, ndare bu amee ab diir bob bindub doomu Aadama man na caa leere bu boobaa ñu tere ko, Yàlla a gën a xam.
Ñaareel bi: mu bañ a jublu ci rotal ëmb bi sànk doom ji, niki jéem a rotal ëmb bi diir ba matee ba njur ma jege, loolu dagan na ci sàrtub lor bañ a am ci yaay ji ak ci doom ji, ak it mbir mi bañ a laaj xotti biir, bu laajee xotti biir dina am ñenti anam:
Bi ci njëkk: yaay ji di dund doom ji di dund, xotti biir du dagan kon lu dul bees loroo ci def ko, niki jur ga jafe ba aajowoo ko, ndaxte yaram ndénkaan la fi jaam bi, du ca soppaxndiku ci lol dees di am lees cay ragal ndare ag yéwen gu kawe di ca amee, ndax man naa njort ne lor amul ci xotti biir ba far mu am.
Ñaareel bi: yaay ji dee doom ji dee, du dagan kon ñuy xotti biir ba ngir génne ko ndax loolu amul njariñ.
Ñatteel bi: yaay ji di dund doom ji dee, kon dina dagan xotti biir ba ngir génne doom ji, ndare ñu ragal loraange ci yaay ji; ndax li feeñ -Yàlla a gën a xam- mooy doom ci biiru yaayam bu deewee daanaka du génn ci lu dul xotti biir ba, ag wéyam di nekk ca biir ba da koy tee ëmb ëllëg, te da koy sonal, man naa sax des di ñàkk a amaat jëkkër bu dee day yiddawu ci jëkkër ja faatu la jiitu.
Ñenteel bi: yaay ji dee doom ji di dund, bu dee deesul yaakaar ag dundam bu génne du dagan ñuy xotti biir ba.
Bu dee yaakaarees na ag dundam nag, bu dee am na lu ca jot a génn dees di xotti biiru yaay ji ngir génne la ca des, bu dee dara génnu ci nag sunu waa ngir yal na Yàlla yërëm leen nee ñu : deesul xotti biiru yaay ngir génne la mu ëmb; ndaxte loolu fees ay cér la, li wér nag mooy dees di xotti biir ba bu dee maneesu koo génne lu dul ci anam googu, loolu mooy tànnug Ibnu Hubayrat, wax na ci Al-Insaaf ne: looloo gën a yey.
Ma ne: rawati na ci sunu jamono jii, xotti biir du fees ay cér, ndax dees koy xotti ñaw ko, ak it ndaxte wormay kiy dund moo gën a màgg wormay ki faatu; ak it ndaxte xettali ku ñu digle ñu sàmm ko ba du tàbbi ci alkande lu war la te ki ci biiru yaayam di dund kees digle ñu ñoŋal ko la, kon day war ñu xettali ko. Yàlla a gën a xam.
Bàyyi ci xel:Ci anam yi jàll yees dagana rotal ëmb dees ciy war a am ndigalul ki moom ëmb ba niki jëkkër ji.
Fii la li nu bëggoon a bind ci wax ci lu am solo lii di jeexee, doyloo nanu ci ak cosaani masala yi ak seen i takk, bu dul woon loolu wànqaas yi ak pàcc-pàccaan yi ak yiy xew ci jigéen ñi géej la gog amul tefes, Waaye ki am gis-gis dina man a delloo wànqaas yi ca cosaan ya, delloo it pàcc-pàccaan yi ca nday ya ak takk-takk ya, natt bir yi ci ya ñu bokkal.
Kiy ubbee ci Diine na xam ne làntinoor la diggante Yàlla ak jaamam ñi, ci jottali li Yonnente Yàlla yi indi, ak leeral ko mbindeef yi, te moom lees di laaj li ci Alxuraan ak Sunna, ñoom ñaar ñooy balluwaay yi nga xam ne Yàlla togg na jaam bi mu dégg leen jëfe leen, Te lépp lu wuute ak Alxuraan ak Sunna loola njuumte la, day war ñu delloo ko ka ko wax, te du dagan ñu di ko jëfe, doonte ka ko wax man naa am ngànt doon góor-góorlu rekk, bu boobaa ñu fay ko ci góor-góorloom googu, waaye ki xam njuumteem ga du dagan ci moom mu di ko nangu.
Dina war ci kiy ubbee ci Diine mu sellal yéeneem ngir Yàlla mu kawe mi, sàkku ndimbal ci Moom ci bépp xew-xew bu muy tàbbi, ak di ko ñaan mu dëgëral ko defal ko tawfeex ba mu dëppoo ak ug njub.
Dina war ci moom li muy sóoraale doon li dikk ci Alxuraan ak Sunna, di xool ak a gëstu ci loolu walla sax lees di dimbalikoo ci waxi woroom xam-xam yi ngir dégg leen.
Bariwaa na lu masala ci masala yi di am nit ki di ci gëstu ci li mu man ci waxi woroom xam-xam yi, topp du gis lu dal xelam ca àtteb masala ma, man naa am sax du gis fenn fees tudde masala ma benn yoon, Te bu delloo ci Alxuraan ak Sunna àtte ba leer ci moom jege ko ne fàŋŋ, loolu nag keemtulaayal ni nit ki di sellale ak xam-xamam ak ug déggam ci lay ame.
Dina war ci kiy ubbee ci Diine muy teey ci àtte bu lënt amee, bañ di gaawtu, ñaata yoon la nit gaawe ab àtte topp ginnaaw bi mu ko seetluwaatee ceetlu gu jege rekk gis ne daa juum tàmbali di réccu, te amaa na sax du man a dabuwaat la mu ubbee ba noppi!.
Te kiy ubbee bu nit ñi xamee ci moom ag teey ak ug wóorliku dañuy daal di am kóolute ci waxam bàyyi ko xel, bu ñu ko gisee nag mu doon kuy gaawtu te kiy gaawtu ku bariy njuumte lay doon, duñu am ci moom kóolute ci la muy ubbee, nga xam ne ci ag gaawtoom ak i njuumteem la xañe boppam xañ ku dul moom la nekk fa moom ci xam-xam ak ug njub.
Noo ngi ñaan Yàlla mu kawe mi mu gindi nu nun ak sunu mbokki jullit yi ci yoonam wu jub wa, te féetewoo saytu sunuy bir, te wattu nu ci rëcc-rëcc yi ci ag càmmam, moom dey ku tabe la ku man a maye la; yal na Yàlla xéewalal te jàmmal sunu Yonnente Muhammat, ak i ñoñam ak i Sahaabaam mboole seen.Mbooleem xeeti cant ñeel na Yàlla mi nga xam ne ci xéewalam la yu baax yi di sottee.
Mat na ci xalimag aji-aajowoo ji jëm ci Yàlla
Muhammat As-Saalih Al-Husaymiin
ci yoor-yooru bisub Àjjuma
14 Baraxlu, atum 1392 ca gàddaay ga
***
xetouk tenk
Buntu bu njëkk bi: ci maanaam mbërëg ak xereñteef gi ci nekk 4
Buntub ñaareel b: ci jamonoy mbërëg ak diir bi muy def 5
Buntub ñatteel gi : ci yiy gaar dereeti mbërëg 14
Buntub ñenteel bi:ci àttey mbërëg 18
Buntub juróomeel bi: ci dereeti jàngoro ak i àtteem 35
Teqaleg juróom-benneel gi: ci wësin ak àtteem 43
Teqaleg juróom-ñaareel gi: ci jëfandikoo luy tee a gis mbaax walla lu koy ñoddi mu ñëw ak luy tee a ëmb ak lu koy yàq 48
***
wo130v1.0 - 10/07/2026