الدُّرُوسُ الْمُهِمَّةُ لِعَامَّةِ الْأُمَّةِ
Ay njàngale yu am solo ñeel xeet wi yépp
لِسَمَاحَةِ الشَّيْخِ العَلَّامَةِ
عَبْدِ العَزِيزِ بْنِ عَبْدِ اللهِ بْنِ بَازٍ
رَحِمَهُ اللهُ
Abdul Asiis Ibn Baas -yal na ko Yàlla yërëm-
بِسْمِ اللهِ الرَّحمَنِ الرَّحِيمِ
Ay njàngale yu am solo ñeel xeet wi yépp
Ñeel fóore ju mag jii di
Abdul Asiis Ibn Baas -yal na ko Yàlla yërëm-
Ci turu Yàlla miy Aji-Yërëm képp ku nekk ci kaw suuf jagleel ko jullit ñi ca allaaxira ci laay tàmbalee.
Laytaayu aji-taalif ji
Cant ñeel na Yàlla miy Boroom mbindéef yi, mujj ga ñeel na way- gëm ñi, Yal na Yàlla julli te sëlmal ci jaamam bi di Yonenteem bi Muhammat, moom ak waa-këram ak àndandoom yépp.
Ginnaaw loolu:
Lii ay waat la yu tënku ci leeral lenn ci li war ci ku ne mu xam ko ci diiney lislaam, tudde naa ko: ( ay njàngale yu am solo ñeel xeet wi yépp).
Maa ngi ñaan Yàlla mu jariñ ci jullit ñi, te nangul ma ko, ndax moom ku tabe la ku tedd la.
Abdul Asiis ibn Abdallah ibn Baas. Ay njàngale yu am solo ñeel xeet wi yépp1
Bind bu njëkk mi: saaru faatiha ak saar yu gàtt yi
Saaru faatiha ak lu jàppandi ci saar yu gàtt yi, tàmbalee ci saaru Isaa zulsilati ba saaru Naasi, di ko jàng, di wéral njàng ma, di ko mokkal, di firi li ñu ci war a xam.
Ñaareelu bind bi: Ponki Lislaam.
Leeral ponki Lislaam yi di juróom, ak bi ci njëkk ak ba ci gën a màgg: Seede ne amul benn buur bu ñuy jaamu ci dëgg bu dul Yàlla, ak seede ne Muhammat ndawul Yàlla la, ak firi ay maanaam, ak leeral ay sàrti laa-i-Laaha illal Laahu, te li maanaam mooy: (laa-i-Laaha) day dàq lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla, (illal Laahu) day saxal ne Yàlla rekk moo yeyoo jaamu déet ñu koy bokkaale. Sàrti (laa-i-Laaha Illal Laahu nag) mooy: xam-xam bi safaanoo ak réer, kóolute gi safaanoo ak sikk-sàkka, sellal gi safaanoo ak bokkaale, dëgg gi safaanoo ak fen, bëgg safaanoo ak bañ, wommatu gi safaanoo ak bokkaale, nangu gi safaanoo ak bañ, ak weddi lépp lu ñuy jaamu te du Yàlla. Sàrt yii dajalees na ko ci ñaari bayit yii di ñëw:
Xam-xam, kóolute, ak sellal, ak dëggu, ànd ak bëgg, ak wommatu, ak nangu baat bi. Ñu dolli ca juróom-ñatteel ba muy nga weddi lépp lu dul Yàlla ci mbir yi ñuy jaamu.
Ànd ak leeral seede ne Muhammat ndawul Yàlla la ak ya mu làmboo: loolu mooy lii: dëggal ko ci li mu xibaare, ak topp ko ci li mu digle, ak moytu li mu tere te jàjje ca, bañ a jaamu Yalla lu dul ci li Yàlla yoonal mook ub Yonenteem -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- . Ginnaaw ba muy leeralal ndongo yi li des ci ponki lislaam yii di juróom, mooy: Jilli, ak joxe asaka, ak woor weeru koor, ak aj màkka ci ku ko man benn yoon.
Ñatteelu bind bi mooy: Ponki gëm yi.
Juróom-benn la: te mooy nga gëm Yàlla ak i malaakaam, ak ay téereem, ak i Yonenteem, ak bis-pénc, nga gëm dogal bu neex ak bu naqari bu jóge ci Yàlla.
Ñenteelu bind bi: xaaji tawhiid ak xaaji bokkaale.
Leeral xaaji Tawhiid yi (wéetal Yàlla) te yooyu ñatt la: wéetal Yàlla ci ay jëfam, wéetal Yàlla ci jaamu gi, wéetal Yàlla ci ay turam ak i melokaanam.
1- Tawhiid Ar Rubuubiyatu: mooy gëm ne Yàlla mooy ki bind lépp, mooy kiy def di dindi ci lépp, kenn jàppalewu ko ci loolu.
2- Tawhiidul uluuhiyyatu: mooy gëm ne Yàlla mooy ki ñuy jaamu ci dëgg amul bokkaale, loolu mooy li (laa-i-Laaha illal Laahu) di tekki, ndax li muy firi mooy: Yàlla rekk lañuy jaamu ci dëgg, jaamu yépp moo xam julli la walla woor mbaa leneen day war ñu sellal ko ngir Yàlla rekk, te du dagan ñu jëme ci dara ñeel keneen ku dul Yàlla.
3- Bu dee kennal Yàlla ci ay turam ak i meloom nag mooy: gëm lépp lu rot ci Alxuraan, walla ci hadiis yu wér yi ci ay turi Yàlla ak i melokaanam, ak saxal ko ñeel Yàlla kepp, saxal ko ca na mu yelle ca moom, ci lu dul ag coppi, walla dàq, walla di ko melal, ngir jëfe waxi Yàlla mu Sell mi:
﴿قُلۡ هُوَ ٱللَّهُ أَحَدٌ 1 ٱللَّهُ ٱلصَّمَدُ 2 لَمۡ يَلِدۡ وَلَمۡ يُولَدۡ 3 وَلَمۡ يَكُن لَّهُۥ كُفُوًا أَحَدُۢ4﴾
{WAXAL NE LIY MBIR TEY MBIR :YALLA KEENN LA}1
{YÀLLA MOOY KI ÑUY JUBLU CI FAJUK AAJO YI}2
Lam ya lid wa lam yuulad 3
Te amul benn nawle} [Saaru Al-Ixlaas: 1-4]. Ak waxi Yàlla -mu kawe mi te sell-:
﴿...لَيۡسَ كَمِثۡلِهِۦ شَيۡءٞۖ وَهُوَ ٱلسَّمِيعُ ٱلۡبَصِيرُ﴾
{Dara melul ne moom Yàlla te moom Aji-Dégg la Aji-Gis la} [As-Suuraa: 11], Lenn ci ay woroomi xam-xam def nañu ko ñaari xaaj, ñu dugal kennal Yàlla ci ay turam ak i meloom ci biir ci biir kennal Yàlla cig moomeelam, loolu deesu ca wax dara, ndax jubluwaay bi leer na ci ñaari xaaj yépp.
Xaaji bokkaale yi ñatt la: bokkaale gu mag, bokkaale gu ndaw, bokkaale gu nëbbu.
Bokkaale gu mag gi: day waral jëf ju yàqu ak sax sawara ci ku ko deewaale, kem ni ko Yàlla waxe ne:
﴿...وَلَوۡ أَشۡرَكُواْ لَحَبِطَ عَنۡهُم مَّا كَانُواْ يَعۡمَلُونَ﴾
{ bu ñu bokkaale woon kon seen jëf yépp di na yàqu } [Al-Anhaam: 88], Yàlla mu kawe mi wax na ne:
﴿مَا كَانَ لِلۡمُشۡرِكِينَ أَن يَعۡمُرُواْ مَسَٰجِدَ ٱللَّهِ شَٰهِدِينَ عَلَىٰٓ أَنفُسِهِم بِٱلۡكُفۡرِۚ أُوْلَٰٓئِكَ حَبِطَتۡ أَعۡمَٰلُهُمۡ وَفِي ٱلنَّارِ هُمۡ خَٰلِدُونَ 17﴾
{Jaaduwul bokkaalekat yi di toppatoo jàkkay Yàlla ji, te ñoom ay seede lañu ci seen weddi ga Ñooñu seeni jëf yàqu na, te sawara lañuy sax} [At-Tawba: 17], Ku ci faatu deesu ko jéggal, àjjana it araam na ci moom, niki ni ko Yàlla mu màgg mi waxe ne:
﴿إِنَّ ٱللَّهَ لَا يَغۡفِرُ أَن يُشۡرَكَ بِهِۦ وَيَغۡفِرُ مَا دُونَ ذَٰلِكَ لِمَن يَشَآءُ...﴾
﴾ Yàla du jéggal ku koy bokkaale, dana jéggale nag lu yées bokkaale ñeel ku ko soob ﴿ [Saaru Annisaa-i: 48]. Yàlla mu kawe mi wax na ne:
﴿...إِنَّهُۥ مَن يُشۡرِكۡ بِٱللَّهِ فَقَدۡ حَرَّمَ ٱللَّهُ عَلَيۡهِ ٱلۡجَنَّةَ وَمَأۡوَىٰهُ ٱلنَّارُۖ وَمَا لِلظَّٰلِمِينَ مِنۡ أَنصَارٖ﴾
{mbir mi mooy képp kuy bokkaale Yàlla àjjana araam na ci moom, te sawara mooy wàccuwaayam, tooñkat yi duñu am ku leen di dimbali} [Al-Maa-ida : 72].
Bokk na ci ay xeetam: ñaan ñi faatu, ak xërëm yi, ak xettaliku ci ñoom, ak di leen nésaral, ak di rendi ngir ñoom, ak yu ni mel.
Bokkaale gu ndaw nag: mooy lu Alxuraan ak Sunna tudde bokkaale, te fekk bokkul ci xeeti bokkaale gu mag gi; niki ngistal ci yenn jëf yi, ak waat ci ku dul Yàlla, ak wax bu soobee Yàlla ak diw, ak lu ni mel; ngir waxI Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-:
«أَخْوَفُ مَا أَخَافُ عَلَيْكُمُ الشِّرْكُ الأَصْغَرُ»، فَسُئِلَ عَنْهُ، فَقَالَ: «الرِّيَاءُ».
{ li ma gën a ragal ci yéen mooy bokkaale gu ndaw} ñu laaj ko mooy lan, mu ne mooy: {ngistal}2 Imaam Ahmat ak Tabaraanii ak Bayhaqii, ñu jële ko ci Mahmuut ibn Labiid Al-Ansaarii -yal na ko Yàlla gërëm- ci càllale gu baax, Tabaraanii nettali na ko ci ay càllale yu baax, jële ko ci Mahmuut ibn Labiid, mu jële ci Raafih ibn Xadiij, mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Ak waxi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-
«مَنْ حَلَفَ بِشَيْءٍ دُونَ اللَّهِ فَقَدْ أَشْرَكَ».
{ képp ku waat ci lu dul Yàlla bokkaale na}3 Imaam Ahmat moo ko soloo ci càllale gu wér, ñu jële ko ci Umar ibn Al-Xattaab -yal na ko Yàlla gërëm- Abuu Daawuda it soloo na ko, ak At-Tirmisiyu ci càllale gu wér, ci Hadiisu ibn Umar -yal na ko Yàlla gërëm- ñu jële ko ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«مَنْ حَلَفَ بِغَيْرِ اللَّهِ فَقَدْ كَفَرَ أَوْ أَشْرَكَ».
«ku giñ ci ku dul Yàlla weddi na walla bokkaale na».4 Ak waxi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-:
«لَا تَقُولُوا: مَا شَاءَ اللَّهُ وَشَاءَ فُلَانٌ، وَلَكِنْ قُولُوا: مَا شَاءَ اللَّهُ ثُمَّ شَاءَ فُلَانٌ».
«buleen di wax: bu soobe Yàlla soob diw, waaye waxleen: bu soobe Yàlla topp mu soob diw5» Abuu Daawuda moo ko génne ci càllale gu wér, ñu jële ko ci Husayfata ibn Al-Yaman -yal na ko Yàlla gërëm-.
Waaye xeet bii du waral génn ci diine, du waral it sax ca sawara, waaye day dàquwante ak matug tawhiid ju war.
Ñatteelu xeet bi mooy: bokkaale gu nëbbu, tegtal ba mooy waxi Yonnente bi - yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-:
«أَلَا أُخْبِرُكُمْ بِمَا هُوَ أَخْوَفُ عَلَيْكُمْ عِنْدِي مِنَ الْمَسِيحِ الدَّجَّالِ؟» قَالُوا: بَلَى يَا رَسُولَ اللَّهِ. قَالَ: «الشِّرْكُ الْخَفِيُّ؛ يَقُومُ الرَّجُلُ فَيُصَلِّي، فَيُزَيِّنُ صَلَاتَهُ لِمَا يَرَى مِنْ نَظَرِ الرَّجُلِ إِلَيْهِ».
{Mo ndax duma leen xibaare li ma gën a ragal ci yéen ci Masiihud Dajjaal ? Ñu ne ko ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, mu ne leen: bokkaale gu nëbbu, nit ki day taxaw di julli muy rafetal ag julleem ngir ne nit a ngi koy xool}6 Imaam Ahmat moo ko soloo ci Musnadam, ñu jële ko ci Abuu Sahiid Al-Hudriyyu - Yal na ko Yàlla gërëm-.
Dina dagan ñu séddale bokkaale ci ñaari xeet kepp:
Gu mag ak gu ndaw, bokkaale gu nëbbu moom dina duggaale ci biir. dana tàbbi ci gu mag gi, niki bokkaaleg naaféq yi; ndax ñoom dañuy nëbb séen pas-pas yu yàqu ya, di feeñal Lislaam ngir ngistal, ak ragal ci seen bopp.
Dina nekk ci bokkaale gu ndaw, lu mel ni ki ngistal, kem ni mu ñëwe ci Hadiisu Mahmuut ibn Labiid Al-Ansaarii bi jiitu, ak hadiisu Abuu Sahiit bi ñu tudd.
Yàlla mooy boroom tawfeex.
Juróomeelu njàng mi mooy rafetal (Ihsaan).
Ponki rafetal, mooy: nga jaamu Yàlla ba mel ni yaa ngi koy gis, boo demul ba mel noonu, nga xam ne moom Yàlla mi ngi lay gis.
Juróom-benneelu bind bi mooy: Sàrti julli.
Sàrti julli juróom-ñent la:
Lislaam, ak am xel, ak ràññee, ak laab, ak deñ ci sobe, ak suturaal sa awra, ak duggug waxtu wi, ak jublu xibla, ak yéene.
Juróom-ñaareelu bind bi mooy: ponki julli
Ponki julli Fukk ak ñent la:
Taxaw ci ku ko man, kàbbaru armal, jàng faatiha, rukkoo, yamoo ginnaaw rukoo bi, sujjóot ci juróom-ñaari cér yi, siggi jóge ci sujjóot ba, toog ci digante ñaari sujjóot yi, dal ci jëf yépp, toftale ponk yi, taaya ju mujj ji, toog ci taaya ju mujj ji, julli ci Yonnente bi, ñaari sëlmal yi.
Juróom-ñatteelu njàng mi mooy: yi war ci julli.
Yi war ci julli juróom-ñatt la:
Mbooleem kàbbaar yi ba mu des bu armal bi, ak wax ji Imaam walla kuy julli moom dong di wax ( samihal Lallaahu liman Hamidahu), ak wax ji ñépp di wax ( Rabbanaa wa lakal hamdu), ak wax ( subhaana rabbiyal hasiim) ci rukkoo bi, ak wax (subhaana rabbiyal ahlaa) ci sujjóot bi, ak wax( rabbi ixfir lii) ci diggante ñaari sujjóot yi, ak taaya ju njëkk ji, ak toogaayu taaya ju njëkk ji.
Juróom- ñenteelu bind bi mooy: Taaya.
Te mooy nit ki wax:
(Attahiyyaatu lil Laahi, was salawaatu, wat tayyibaatu, assalaamu halayka ayyuhan Nabiyyu wa rahmatul Laahi wa barakaatuhuu, assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahi assaalihiina, ashadu an laa-i-Laaha illal Laahu, wa ashadu anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu).
Topp mu julli ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax: ( Allahumma salli halaa Muhammadin, wa halaa aali Muhammadin, kamaa sallayta halaa Ibraahiima wa halaa Aali Ibraahiima, innaka hamiidun majiidun, wa baarik halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin kamaa baarakta halaa Ibraahiima wa halaa aali Ibraahiima innaka hamiidun majiidun).
Topp mu sàkkoo muslu ci Yàlla ci Taaya ju mujj ji ci mbugalum sawara, ak ci mbugalum bàmmeel, ak ci fitnay dund ak dee, ak ci fitnay Masiihud Dajjaal, bu noppee mu tànn lu ko soob ci ay ñaan rawati na ñaan yi ñu tuxale ci sariiha, bokk na ca:
( allahumma ahinnii halaa sikrika wa sukrika wa husni ibaadatika, allahumma innii salamtu nafsii sulman kasiiran, walaa yaxfirus sunuuba illaa Anta, faxfir lii maxfiratan min hindika, warhamnii, innaka antal Xafuurur Rahiim).
Bu dee ci taaya ju njëkk ji day jog jëm ci ñatteelu ràkka ba ci jullig tisbaar ak tàkkusaan ak timis, bu jullee ci Yonnente bi loolu moo gën; ngir mbooleem hadiis yi rot ci loolu, mu jog na jëm ci ñatteel ba.
Fukkeelu bind bi mooy: sunnay julli.
Bokk na ca:
1- ubbiteg julli gi.
2- teg loxo ndayjoor ci kaw loxo càmmooñ ci kaw dënn bi, ci taxawaay bi njëkk muy rukoo ak ginnaaw rukkoo ba.
3- yëkkati ñaari loxo yi ba mu tolloo ak ñaari mbagam walla ñaari noppam fekk baaraamu loxo yi sësaloo ci kàbbar bu njëkk bi, ak buy rukkoo, ak buy siggi jóge ci rukkoo bi, ak buy taxaw jóge ci taaya ju njëkk ja jëm ca ñatteelu ràkka ba.
4- lépp lu dolliku ca njëlbéenug sàbbaal ga ca rukkoo ba ak sujjóot ba.
5- lépp lu dolliku ca wax ja muy wax: (Rabbanaa walakal hamdu) ginnaaw bu siggee ca rukkoo ba, ak lépp lu dolliku ca wax ja muy wax: (rabbi ixfir lii) benn yoon ca diggante ñaari sujjóot ya.
6- def bopp bi mu yamoo ak ndigg li ci rukoo bi.
7- soreele ñaari përëgi loxo yi ak ñaari wetam, mu soreele biir ba ak ñaari poojam, soreele it ay poojam ci ay yeelam ci sujjóot ba.
8- yëkkati ñaari loxo yi mu bañ a lalu ci suuf ca sujjóot ba.
9- toogaayub Aji-julli ji ca kaw tànkub càmmooñ ba ñu lal, ak samp tànkub ndayjoor ba ci taaya ju njëkk ji ak ci diggante ñaari sujjóot yi.
10- Toog toogaayu (tawarruk) ci taaya bu mujj bi ci jullig ñenti ràkka mbaa ñatti ràkka, tawarruk mooy: toog teg say njekkikaay ci suuf daal di lal tànkub càmmooñ ba ca ron tànkub ndayjoor ba te samp bu ndeyjoor ba.
11- di junj ci baaraamu sànnikaay bi ci taaya ju njëkk ji ak ju ñaareel ji ba taaya ji jeex ak di ko yëngal buy ñaan.
12- julli ci Yonnente bi ak ci waa këram, ak julli ci Ibraahiima ak waa këram, ci taaya gu njëkk gi.
13- Ñaan ci taaya gu mujj gi.
14- biral njàng ma ci jullig fajar, ak ci jullig àjjuma, ak jullig ñaari feet yi, ak jullig baawunaan, ak ci ñaari ràkka yu njëkk yi ci jullig timis ak gee.
15- yalu njàng ma ci jullig tisbaar, ak tàkkusaan, ak ci ñatteelu ràkka ci jullig timis, ak ci ñaari ràkka yi mujj ci jullig gee.
16- Jàng li tegu ci faatiha ci Alxuraan, ànd ak sàmmoonte ak yeneen sunna yi rot ci julli yu dul yii ñu tudd, bokk na ca yooyu: lu topp ci wax( rabbanaa wa lakal hamdu) ginnaaw siggi ci rukoo ci àqi Imaam walla maamuun mbaa kiy julli moom dong, loolu sunna la, bokk na ca ba tay: teg ñaari loxo yi ca kaw wóom ya te teqale waaraam yi ci rukoo bi.
Fukkeelu bind bi ak benn mooy: yiy yàq julli.
Yiy yàq julli juróom-ñatt la:
1- wax te tay ko ànd ak fàttaliku ak ug xam, bu dee ki fàtte nag walla ki xamul loolu du yàq julleem.
2- reetaan.
3- lekk.
4- naan.
5- Awra yu feeñ.
6- dummóoyu xibla gu jéggi dayo.
7- Po mu bari ta tegaloo ci biir julli gi.
8- Njàpp mu yàqu.
Fukkeelu bind bi ak ñaar mooy: sàrti njàppu.
Yooyu Fukk la:
Lislaam, ak am xel, ak xàmme, ak yéene, ànd ak àtteem ci mu bañ koo yéenee dagg ba keroog njàpp mi di mat, ak laabu mbaa fomp ba set njëkk muy jàpp, ak ndox mu laab te dagan, ak dindi lépp luy tax ndox mi du àgg ci der bi, ak duggug waxtu wi ci koo xam ne ag tojleem lu sax la.
Bindub fukkeel bi ak ñatt mooy: faratay njàpp.
Juróom-benn la:
Raxas xar kanam te ci la gallaxndiku ak saraxndiku bokk, ak raxas ñaari loxo yi ba ca coñco ya, ak masaa bopp bi yépp ñaari nopp yi ci lay bokk, ak raxas ñaari tànk yi ba ca dojor ya, ak toftale, ak méngale cér ya. Sopp nañu ñu baamtu raxas kanam ga, ak ñaari loxo ya, ak ñaari tànk ya ñatti yoon, niki noonu gallaxndiku ak saraxndiku ga, li cay farata nag mooy benn yoon, bu dee masaa bopp nag kenn soppul baamtu ga niki ni ay hadiis yu wér dikkee di tegtale loolu.
Bindub fukkeel bi ak ñent mooy: yiy yàq njàpp.
Juróom-benn la:
Liy génn ci ñaari génnuwaay yi, ak sobe su ëpp suy génn ciw yaram, ak xel mu dem ngir nelaw walla leneen, ak laal am pëy ci loxo moo xam pëyum kanam la mbaa mu gannaaw te fekk dara doxul ca digganteem ak loxo bi, ak lekk yàppu giléem.
Ag yeeye bu am solo: bu dee sang néew nag: li wér mooy ne du yàq njàpp, loolu mooy li ëpp ci waxi woroom xam-xam yi; ngir ne tegtal ñëwu ci, waaye nag bu loxob kuy sang néew bi laalee pëyum néew bi kon day war ci moom mu jàpp.
Li war ci moom mooy loxoom bañ a laal pëyum néew bi lu dul ne am na lu mu doxale ca diggante ba, niki noonu laal jigéen du yàq njàpp, moo xam laalug bànneexu la walla déet fii ak dara génnul ci moom lii mooy li gën a wér ci waxi woroom xam-xam yi, ndaxte Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fóon na kenn ci ay soxnaam daal di julli te jàppaatul.
Bu dee waxi Yàlla ji mu wax ci ñaari aaya yi nekk ci An-Nissa ak Al-Maa-ida:
﴿...أَوۡ لَٰمَسۡتُمُ ٱلنِّسَآءَ...﴾
{Walla ngéen jonjante ak jigéen ñi (sëy)} [An Nisaaii: 43] [Al Maa-ida: 6], Li ñu ci jublu mooy: Sëy, ci li gën a wér si waxi woroom xam-xam yi, mooy waxi Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla gërëm-, ak am mbooloo ci magi Lislaam yi jiitu ak ñi ñëw seen ginnaaw. Yàlla mooy Boroom tawfeex.
Bindub fukk AK juróomeel bi mooy: jikkowoo ay jikko yu ñu yoonal ci bépp jullit.
Bokk na ca: dëggu, ak wóor, ak sàmmu, ak am kersa, ak njàmbaare, ak tabe, ak matal kóllare, ak sori lépp lu Yàlla araamal, ak rafetal dëkkandoo, ak dimbali way-aajowoo yi sa kem kàttan, ak yeneen ci ay jikko yoy Alxuraan ak Sunna tegtale na ne lu ñu santaane la.
Bindub fukkeel bi ak juróom-benn: tegginoo teggini Lislaam yi.
Bokk na ca: nuyoo, ak di leeral xar- kanam, ak di lekke ak a naane loxo ndayjoor, ak wax bismillah cig tàmbali, ak wax alhamdu lil-Laahi boo noppee, ak wax alhamdu lil-Laahi boo tissóolee, ak wax yarhamukal Laahu ñeel ki tissóoli bu dee wax na alhamdu lil-Laahi, ak seeti ku feebar, ak gunge néew ca jullée ga ak rob ga, ak teggini Lislaam ci booy dugg jàkka, walla kër mbaa nga nga fay génn, ak booy tukki, ak am ay teggin sa diggante ak say ay say way-jur ak say mbokk ak say dëkkandoo ak ci mag ñi ak ci ndaw ñi, ak ndokkeel ku am doom mbaa kuy takk soxna, ak massawu ku dogal dal, ak yeneen ci ay teggin yu Lislaam digle ci sol yére ak summiku ak sol ay dàll.
Bindub fukkeel bi ak juróom-ñaar: moytandikuloo bokkaale ak xeeti moy Yàlla yi.
Bokk na ca: juróom-ñaari bàkkaar yiy alage, te mooy: bokkaale Yàlla, ak njabar, ak ray bakkan bu Yàlla araamal, ak lekk riiba, ak lekk alali jirim, ak daw ci bisu xare, ak xas jullit bu jigéen bu sàmm boppam.
Bokk na ca: dëngé ñaari way-jur, ak dagg mbokk, ak seede ay neen, ak waat ci lu dul dëgg, ak lor dëkkandoo, ak tooñ nit ñi ci seen dereet, ak ci seen alal, ak ci seen der, ak naan sàngara, ak kàrt, ak jëw, ak rambaaj, ak yeneen ci yi Yàlla tere walla Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Bindub fukkeel bi ak juróom-ñatt: waajal ab néew ak jullée ko ak rob ko.
Jàppal faramfànce gi:
Yoonalees na ñuy sah aji-sukraat ji: ( laa-i-Laaha illal-Laahu); ngir waxi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-
«لَقِّنُوا مَوْتَاكُمْ: لَا إِلَهَ إِلَّا اللَّهُ».
{Saleen seeni way-faatu: laa-i-Laaha illal-Laahu}7 Muslim soloo na ko ci Sahiiham, Li ñu jublu ci way-faatu ci Hadiis bii: mooy ñiy sukraat, te mooy ñi màndargay dee feeñ ci ñoom.
Ñaareel ba: Bu ko wóoree ne faatu na na gëmmal bët ya, na takk ñaari ŋaam ya, ngir li sunna ñëw ci loolu.
Ñatteel bi: war na ñu sang néewub jullit lu dul mu nekk ku faatu ci xare, kooku kenn du ko sang kenn du ko julllee, waaye dañu koy robaale ak ay yéréem; ndax Yonnente bi - yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- sangul ñi ñu faatoon ca xareb Uhud, te julleewu leen.
Ñenteel ba: melokaanu sang néew.
Dañuy suturaal awraam, topp ñu yëkkëti ko tuuti daal di nal biir bi ndànk, sangkat bi daal di laxas ciy loxoom ab morso walla lu ni mel, bu noppee mu jàppal ko njàppum julli, topp mu raxas bopp bi ak ndox ak siddéem walla lu ni mel, topp mu raxas wetug ndayjooram, teg ca bu càmmooñ ba, topp mu sang ko ñaareelu yoon ak ñatteelu yoon, muy rombale loxoom ca kaw biir ba, bu dara génnee mu raxas ko, bu noppee mu sakk barab ba ak wëttéen walla lu ko niru, bu dee deñul di génn, mu jëfandikoo ban, walla jumtukaay yu yees yi ci wàllu faj; niki kol ak lu ko niru.
Mu baamtuwaat njàpp ma bu setul mu dolli ba juróom walla juróom-ñaari yoon, topp mu fomp ko, mu daal di def ci ruqam yi gëtt, ak barabu sujjóot ya, bu defee ca yaram wépp gëtt it baax na, topp mu cuuraay càngaay la, bu dee ay weham mbaa ay naanoom (Mustaas) dafa gudd mu dagg ca dara, bu ko bàyyee it dara nekku ca, bu mu peñe kawar ga, bumu wat kawaru naq ga bu mu ko xarafal, ndax tegtal ñëwu ca, jigéen nag dees na létt kawar ga ñatti létt tëral létt ya mu jëm ginnaaw.
Juróomeel bi: sàng néew bi.
Li gën mooy ñu sàng néew bi ak ñatti yére yu weex du am semis du am kaala, kem niko Yonnente bi defe, bu ñu ko defelee ab semis ak ub tubëy ak ub càngaay dara nekku ca.
Jigéen moom dañu koy sàng ci juróomi yére: ab yére, ak muuraay, ak sër, ak ñaari laxasaay. Dinañu sàng xale bu góor ci benn yére ba ci ñatti yére, xale bu jigéen nag dinañu ko sànge ab semis ak ñaari càngaay.
Liy farata ci ñépp mooy benn yére buy suturaal yaramu néew bépp, waaye bu dee néew bi da doon armal kon dees na ko sang ak ndox ak siddéem, daal di koy sàng ci ab sër ak ub mbalaan, mbaa leneen, waaye duñu muur bopp bi ak kanam gi duñu ko sotti gëtt itam; ndax te dees koy dekkal yawmal xiyaam muy wax labbaykal Laahumma làbbayka niki mu wére ci Hadiisu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu dee néew bi jigéen la dañu koy sàng niki ñépp. Waaye kenn du ko laalal gëtt kenn du muur kanamam kenn du ko solal ay gaaŋ ci loxoom waaye dañuy muur kanam gi ak loxo yi ci càngaay li niki ni leeral li jiitoo woon ci melow sàng jigéen.
Juróom-benneel bi: ki gën a yay ci sang ko ak jullée ko ak rob ko.
Ki mu waxoon ne moo koy sang, topp baayam, topp maamam, topp ka ko gën a jege ci ay bokkam, ci àqi ku góor ki.
Ki gën a yay ci sang néew bu jigéen bi mooy: ki mu dénkoon loolu, topp ci maam ju jigéen, topp ci ka ko gën a jege ci jigéen ñi, ñaari way-deñcante yi ku ci ne man naa sang moroomam; ndax Abuubakar soxnaam mooko sang, Alliyun tamit moo sang soxnaam Faatima - yal na leen Yàlla gërëm-.
Juróom-ñaareel bi: na ka lañuy jullée néew.
Day kàbbar ñenti yoon, mu jàng faatiha ginnaaw kàbbar bu njëkk ba, bu ko boolee akk aw saar wu gàtt walla benn aaya mbaa ñaar di na baax; ngir hadiis bu wér bi ci ñëw jógé ci ibn Abbaas -yal na leen Yàlla gërëm-, topp mu kàbbar ñaareelu kàbbar, daal di julli ci Yonnente bi niki muy jullée ci moom ci taayag julli, topp mu kàbbar ñatteelu kàbbar bi, daal di wax: ( Allahumma ixfir Li hayyinaa wa mayyitinaa, wa saahidinaa wa xaa-ibinaa, wa saxiirinaa wa kabiirinaa, wa sakarinaa wa unsaanaa, Allahumma man ahyaytahu minnaa fa ahyihi halal islaam, waman tawaffaytahu minnaa fa tawaffihi halal iimaan, Allaahumma ixfir lahu, warhamhu, wa haafihi, wahfu hanhu, wa akrim nusulahu, wa wassih mudxalahu, waxsilhu billmaa-i wassalji walbaradi, wanaqihi minal xataayaa kamaa yunaqas sawbul abyadu minaddanasi, wa abdilhu daaran xayran min daarihi, wa ahlan xayran min ahlihi, wa adxilhu al jannata, wa ahishu min hasaabil xabri, wa hasaabin naari, wafsah lahu fii xabrihi, wa nawwir lahu fiihi, Allaahumma laa tahrimnaa ajrahu walaa tudilanaa bahdahu. Topp mu kàbbar ñetteelu kàbbar bi, daal di sëlmël benn sëlmël ci ndayjooram.
Sopp nañu mu yëkkëti ñaari loxoom ci bépp kàbbar, bu dee néew bi jigéen la ñu wax: ( Allaahumma ixfir lahaa...) ba mu jeex, bu dee ñaari néew la ñu wax: (Allaahumma ixfir lahumaa...) ba mu yegg, bu dee ay néew yu bari la ñu wax: ( Allaahumma ixfir lahum...) ba mu yegg, bu dee ab xale la lii la koy ñaanal wolif njéggal: ( Allaahumma ijhalhu faratan wa suxran li waalidayhi, wa safiihan mujaaban, allahumma saqil bihii mawaasiinahumaa, wa ahsim bihii ujuurahumaa, wa alhiqhu bi saalihi salafil muuminiina, wajhalhu fii kafaalati Ibraahiima alayhis salaatu was salaamu, waxihi birahmatika hasaabal jahiimi).
Liy sunna mooy imaam bi taxaw fi tolloo ak bopp bi bu dee góor la, bu dee jigéen la mu taxaw ci digg bi, bu dee ñu bari lañu na góor ñi gën a jege imaam bi, bu dee ay xale ñoo nga ca xale bu góor mooy nekk ci kanam jigéen gu mag topp ca xale bu jigéen topp ca, ñu góor ñi ñooy yamoo bopp xale ak mag, ndiggu jigéen tolloo ak bopp góor, niki noonu jigéen xale ak mag ñooy tollo bopp, ñiy julli ñépp nekk ci ginnaaw imaam, bu dee kenn koo xam ne amul fu mu taxaw man naa taxaw ci ndayjooru imaam.
Juróom-ñatteel bi: naka lañuy robe néew.
Li ñu yoonal mooy ñu xóotal bàmmeel bi ba mu tolloo ak ndig góor, ñu gas ko mu am pax mu ndaw féete xibla, ñu dugal néew bi ci pax mu ndaw mi mu tëdde wetug ndayjooram, ñu tekki takk-takki càngaay li, kenn du muri kanam ga moo xam góor la mbaa jigéen, ñu daal di fay samp ay móol, daal di cay raatale ban ba mu dëgër, bu dee amuñu móol nañu fa def leneen moo xam ay xeer la mbaa bant bu man a tax suuf si du àgg ca moom, ñu daal di koy sotti suuf, sopp nañu bu ñuy def loolu ñu wax (Bismillahi, wa halaa millati rasuulil-Laahi), ñu yëkkati bàmmeel bi ba mu tolloo ak sibra, bu dee jàppandi na ñu def ca ay xeer yu dëgër daal di ciy wis ndox.
Yoonal nañu ci ñi ko gunge woon ñu taxaw ca bàmmeel ba ñaanal néew bi; ndaxte Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan noppi ci rob néew day taxaw ca bàmmeel ba daal di wax ne:
«اسْتَغْفِرُوا لِأَخِيكُمْ، وَاسْأَلُوا لَهُ التَّثْبِيتَ، فَإِنَّهُ الْآنَ يُسْأَلُ».
{ sàkkulleen seen mbok mi njéggal, ngeen ñaanal ko Yàlla saxal làmmeñam, ndax te leegi ñu laaj ko}8 .
Juróom-ñenteel bi: yoonal nañu ci ki fekkewul jullee gi mu jullee ko ginnaaw bi ñu ko robee ba noppi.
Ndax Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- def na loolu, waaye loolu na fekk rob bi matagul weer mbaa ca lay yam, bu dee diir ba ëpp na wéer kon deesul yoonal jullee ga ca bàmmeel ba; ndax loolu kenn tuxalewul ci Yonnente bi ne jullee na ab néew ca bàmmeel ba ginnaaw ba ñu ko robee ba mu ëpp weer.
Fukkeel bi: du dagan ci waa kër néew bi ñuy toggal nit ñi aw ñam.
Ngir waxi Jaabir ibn Abdallah Al-Bajalii sahaaba bu tedd ba -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
«كُنَّا نَعُدُّ الاجْتِمَاعَ إِلَى أَهْلِ الْمَيِّتِ، وَصَنْعَةَ الطَّعَامِ بَعْدَ الدَّفْنِ، مِنَ النِّيَاحَةِ».
(Dajaloo ci waa-kër néew bi ak defar aw ñam ginnaaw
biñuko robee daaan nañu ko boole ci déjjatu, (mooy lii yuuxu aka xalangu) maanaam àtte boobu lay yor.9 Imaam Ahmat moo ko soloo ci càllale gu rafet, Bu dee nag ñeneen ñoo leen toggal aw ñam walla ñoom ñoo ko togg ngir seeni gan loolu dara nekku ci, yoonal nañu ci ay mbokkam ak i dëkkandoom ñu toggal leen ; ndax yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bi mu jotee xibaaru faatug Jahfar ibn Abii Taalib -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ca Saam, dafa digal waa këram ngir ñu defaral waa kër Jahfar aw ñam, mu wax ne:
«إِنَّهُ أَتَاهُمْ مَا يَشْغَلُهُمْ».
{ñoom de mbir mu leen soxlaal moo leen dal}10.
Waa kër néew bi bu ñu woowee seeni dëkkandoo mbaa ñeneen ngir ñu ñëw lekk ci ñaw wi ñu leen jox dara nekku ca, loolu amul wenn waxtu wu ñu ko tënk ci li nu xam ci sariiha.
Fukkeel bi ak benn : du dagan ci jigéen muy ténj aji-faatu ji lu ëpp ñatti fan lu dul muy jëkkëram
Kon dina war ci moom mu ténj ko ñeenti weer ak fukki fan, lu dul mu nekk ku ëmb bu boobaa bu wësinee lay jeex; ngir li mu rot ci sunna su wér jóge ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- .
Bu dee góor nag du dagan muy ténj kenn ci jegeñaale yi walla ñeneen.
Fukkeel bi ak ñaar : dina ñu yoonal ci góor ñi ñuy siyaare ji bàmmeel yi ngir di ñaanal néew yi ak di leen sàkkul yërmànde ak ngir fàttaliku dee ak la ca ginnaawam.
Ngir waxi Yonnente bi - yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-
«زُورُوا الْقُبُورَ، فَإِنَّهَا تُذَكِّرُكُمُ الْآخِرَةَ».
{siyaareleen bàmmeel yi, ndax da leen di fàttali allaaxira}11 Muslim moo ko soloo ci téereem bu wér bi. Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan jàngal sahaaba yi bu ñu siyaaree bàmmeel ñu Wax:
«السَّلَامُ عَلَيْكُمْ أَهْلَ الدِّيَارِ مِنَ الْمُؤْمِنِينَ وَالْمُسْلِمِينَ، وَإِنَّا إِنْ شَاءَ اللَّهُ بِكُمْ لَاحِقُونَ، نَسْأَلُ اللَّهَ لَنَا وَلَكُمُ الْعَافِيَةَ، يَرْحَمُ اللَّهُ الْمُتَقَدِّمِينَ مِنَّا وَالْمُسْتَأْخِرِينَ».
( Assalaamu halaykum ahlad diyaari minal muuminiina wal muslimiina, wa innaa insaa al-Laahu bikum laahixuuna, nas-alul Laaha lanaa walakumul haafiyata, yarhamul-Laahu al-mutaxaddimiina minnaa walmuta-axiriina)12 Jigéen ñi nag duñu siyaare ji bàmmeel ya, ndax Yonnente bi dafa rëbb jigéen ñiy siyaare bàmmeel, ak ragal gi ñu ragal ci ñoom fitna ak ñàkk a man a muñ, niki noonu du dagan ci ñoom ñuy gunge néew jëm ca armeel ya; ndax Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da leen a tere loolu. Bu dee jullee néew ci jàkka ji walla ci julleekaay bi loolu dina dagan ci góor ñi ak ci jigéen ñépp.
Lii mooy li jàppandi ci ñu dajale ko. Yal na Yàlla dolli Yonnente bi xéewal ak mucc ak ay ñoñam ak i Sahaabaam.
***
xetouk tenk
Ci turu Yàlla miy Aji-Yërëm képp ku nekk ci kaw suuf jagleel ko jullit ñi ca allaaxira ci laay tàmbalee. 2
Laytaayu aji-taalif ji 2
Bind bu njëkk mi: saaru faatiha ak saar yu gàtt yi 3
Ñaareelu bind bi: Ponki Lislaam. 3
Ñatteelu bind bi mooy: Ponki gëm yi. 4
Ñenteelu bind bi: xaaji tawhiid ak xaaji bokkaale. 4
Juróomeelu njàng mi mooy rafetal (Ihsaan). 9
Juróom-benneelu bind bi mooy: Sàrti julli. 9
Juróom-ñaareelu bind bi mooy: ponki julli 10
Juróom-ñatteelu njàng mi mooy: yi war ci julli. 10
Juróom- ñenteelu bind bi mooy: Taaya. 10
Fukkeelu bind bi mooy: sunnay julli. 11
Fukkeelu bind bi ak benn mooy: yiy yàq julli. 13
Fukkeelu bind bi ak ñaar mooy: sàrti njàppu. 14
Bindub fukkeel bi ak ñatt mooy: faratay njàpp. 14
Bindub fukkeel bi ak ñent mooy: yiy yàq njàpp. 14
Bindub fukk AK juróomeel bi mooy: jikkowoo ay jikko yu ñu yoonal ci bépp jullit. 15
Bindub fukkeel bi ak juróom-benn: tegginoo teggini Lislaam yi. 16
Bindub fukkeel bi ak juróom-ñaar: moytandikuloo bokkaale ak xeeti moy Yàlla yi. 16
Bindub fukkeel bi ak juróom-ñatt: waajal ab néew ak jullée ko ak rob ko. 17
Ñaareel ba: Bu ko wóoree ne faatu na na gëmmal bët ya, na takk ñaari ŋaam ya, ngir li sunna ñëw ci loolu. 17
Ñatteel bi: war na ñu sang néewub jullit lu dul mu nekk ku faatu ci xare, kooku kenn du ko sang kenn du ko julllee, waaye dañu koy robaale ak ay yéréem; ndax Yonnente bi - yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- sangul ñi ñu faatoon ca xareb Uhud, te julleewu leen. 17
Ñenteel ba: melokaanu sang néew. 18
Juróomeel bi: sàng néew bi. 18
Juróom-benneel bi: ki gën a yay ci sang ko ak jullée ko ak rob ko. 19
Juróom-ñaareel bi: na ka lañuy jullée néew. 20
Juróom-ñatteel bi: naka lañuy robe néew. 21
Juróom-ñenteel bi: yoonal nañu ci ki fekkewul jullee gi mu jullee ko ginnaaw bi ñu ko robee ba noppi. 22
Fukkeel bi: du dagan ci waa kër néew bi ñuy toggal nit ñi aw ñam. 22
Fukkeel bi ak benn : du dagan ci jigéen muy ténj aji-faatu ji lu ëpp ñatti fan lu dul muy jëkkëram 23
Fukkeel bi ak ñaar : dina ñu yoonal ci góor ñi ñuy siyaare ji bàmmeel yi ngir di ñaanal néew yi ak di leen sàkkul yërmànde ak ngir fàttaliku dee ak la ca ginnaawam. 24
***
imaam Ahmad génne na ko (5/ 428), ak At-Tabaraanii ci Al-Kabiir (4/ 338), ak Al-Bayhaqii ci As-Suhab (14/ 355), mu wax ci Majmahu As-Sawaahid (1/ 121), ne Ahmad nettali na ko te ca ña mu jaar ñoo nga ca As-Sahiih.
Imaam Ahmad génne na ko (1/ 47)
Abuu Daawuda génne na ko ci limatu (3251) ak At-Tirmisii, ci limatu (1535).
Abuu Daawuda génne na ko ci limatu (4980), ak Ahmad (5/ 384).
Ibn Maaja génne na ko ci limatu (4204) ak Imaam Ahmad (3/ 30).
Muslim génne na ko ci ñaari limat yii (916- 917).
Abuu Daawuda génne na ko ci limatu (3221), ak Al-Haakim (3/ 399).
Ibn Maaja génne na ko ci limatu (1612) ak Imaam Ahmad (2/ 204)..
Muslim, Al-janaa-is (976) , An-Nasaa-iyu, Al-janaa-is (2034), Abuu Daawuda , Al-janaa-is (3234) , Ibn Maaja, maa jaa-a fil jannaa-is (1569) , Ahmat (2/441).
Ibn Maaja génne na ko ci limatu (1569), Al-Albaanii wéral na ko.
Muslim génne na ko ci limatu (975).
Majmuuhu Fataawaa Wa Maqaalaat Mutanawwiha (3/288-298).