مَا لَا يَسَعُ المُسْلِمَ جَهْلُهُ
lu ab jullit warut a réere
اللَّجْنَةُ العِلْمِيَّةُ
بِرِئَاسَةِ الشُّؤُونِ الدِّينِيَّةِ بِالمَسْجِدِ الحَرَامِ وَالمَسْجِدِ النَّبَوِيِّ
Lajnatul Hilmiyyatu bi-Ri'aasati As-Su'uuni Ad-Diiniyyati bil-Masjidi Al-Haraami wal-Masjidi An-Nabawiyyi
بِسْمِ اللَّهِ الرَّحْمَنِ الرَّحِيمِ
lu ab jullit warut a réere
Laytaayu aji-taalif ji
Cant ñeel Na Yàlla miy Boroom mbindeef yi, xéewal ak mucc yal na nekk ci ki ñu yónni muy yërmande ñeel mbindeef yi, moom ak waa këram ak i sahaabaam, ak képp ku topp sunnaam te jube cig njubam ba keroog bis-pénc, ginnaaw loolu:
Lii ab bataaxal la bu ñu tënk, bu làmboo li ëpp solo ci li jullit bi di aajowoo ci ngëmam ak i jaamoom ak i jëflanteem. Dajale nanu ko ngir góor ñi ak jigéen ñiy siyaare ji ñaari barab yu tedd ya, ngir ñu man a am xam-xam ak leer ci mbiri seen diine. Ñuy yaakaar ci Boroom bu Tedd bi, te Yéwén, mu jariñe ci, te mu def ko lu jub te sellal ko ngir Jëmmam ju Tedd ja. Ndaxte moom mooy ki gën a yayoo ñu koy ñaan, te moo gën a tedd képp ku ñuy yaakaar.
Kureelu xam-xam bi ci njiitalu ñi yore wàllu diine ci Masjidulharaam ak masjidu nabiy
Ci turu Yàlla miy Aji-Yërëm képp ku nekk ci kaw suuf jagleel ko jullit ñi ca allaaxira ci laay tàmbalee.
***
Teqale bu njëkk bi:
Li aju ci pas-pas
Waxtaan wu njëkk wi: Maanaam Lislaam ak i ponkam.
Lislaam mooy: jox sa bopp Yàlla cig wéetal, wommatul ko cig topp, deñ ci bokkaale ak i ñoñam
Ponkam ya nag juróom la:
Bi ci njëkk: seede ne amul benn buur bu ñuy jaamu cig dëgg bu dul Yàlla, seede ne Muhammat ndawu Yàlla la.
Ñaareel bi: mooy taxawal julli.
Ñatteel bi: mooy joxe asaka.
Ñenteel bi: woor weeru koor.
Juróomeel bi: aj Màkka benn yoon ci ku ko man.
Solos Tawhiid:
Xamal ne Yàlla mu kawe mi moo bind mbindeef yi ngir ñu jaamu ko te bañ ko a bokkaale ak dara, Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿وَمَا خَلَقۡتُ ٱلۡجِنَّ وَٱلۡإِنسَ إِلَّا لِيَعۡبُدُونِ 56﴾
﴾Binduma jinne ak nit lu dul ngir ñu jaamu ma﴿ [Azzaariyaati: 56], Te jaamu Yàlla gii deesu ko mën a xam lu dul ci xam-xam, kem ni ko yalla mu kawe mi waxe ne:
﴿فَٱعۡلَمۡ أَنَّهُۥ لَآ إِلَٰهَ إِلَّا ٱللَّهُ وَٱسۡتَغۡفِرۡ لِذَنۢبِكَ وَلِلۡمُؤۡمِنِينَ وَٱلۡمُؤۡمِنَٰتِۗ وَٱللَّهُ يَعۡلَمُ مُتَقَلَّبَكُمۡ وَمَثۡوَىٰكُمۡ 19﴾
﴾Xamal ne amul buur bu ñuy jaamu cig dëgg bu dul Yàlla, jéggalul say bàkkaar te jéggalul jullit yu góor yi ak jullit yu jigéen yi. Yàlla xam na seen yëngu-yëngu ak seen dalukaay﴿ [Muhammat: 19], Mu tàmbalee ci xam-xam mu jiitu wax ak jëf. Li gën a am solo ci li jullit bi war a jàng mooy wéetal Yàlla mu kawe mi te tedd; ndaxte mooy cosaanu diine ji, Te diine ji du taxaw lu dul ci Tawhiid, te mooy li njëkk a war jullit bi, te mooy li mujj a war it. Tawhiid nag mooy ponk bi njëkk ci ponki Lislaam yi jullit bu nekk war a xam te jëfe leen, te ñoom juróomi ponk lañu, Kem ni mu ñëwe ci hadiisu Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- muy wax ne:
«بُنِيَ الإسْلَامُ عَلَى خَمْسٍ: شَهَادَةِ أنْ لَا إلَهَ إلَّا اللَّهُ وأنَّ مُحَمَّدًا رَسُولُ اللَّهِ، وَإقَامِ الصَّلَاةِ، وَإيتَاءِ الزَّكَاةِ، وَحَجِّ البَيْتِ، وصَوْمِ رَمَضَانَ».
«Tabax nañu lislaam ci juróom: seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawal Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak aji Màkka, ak woor weeru koor»1.
Di na war ci ab jullit mu jàng maanaam Tawhiid; te mooy kennal Yàlla cig jaamu, Te du ko bokkaale ak kenn ci jaamoom gi; du malaaka, du Yonnente bu ñu yónni
Maanaam "seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla":
Mooy jaam bi saxal ci fas gu dogu ne amul lu ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla mu màgg mi, Mu jaamu Yàlla moom dong, te wéetal ko ci mbooleem xeeti jaamu yi: moo xam ñaan la, walla ragal, walla yaakaar, walla wakkirlu, ak yu ni mel.
Ag seede du wér lu dul ci ñaari ponk:
Bi ci njëkk: dàq ag yàlla ak ag jaamu ci lépp lu dul Yàlla; ci mbooleem ndend yi, ak yi ñuy yàllaal te du Yàlla.
Ñaareel bi: saxalal ko Yàlla gi mu doon ak jaamu gu tege ci dëgg ñeel ko moom dong, wolif ku dul moom. Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿وَلَقَدۡ بَعَثۡنَا فِي كُلِّ أُمَّةٖ رَّسُولًا أَنِ ٱعۡبُدُواْ ٱللَّهَ وَٱجۡتَنِبُواْ ٱلطَّٰغُوتَ...﴾
﴾Yónni Nanu ci xeet wu ne ab Yonnente ngir mu digal leen ne leen jaamuleen Yàlla te moytu ay xërëm...﴿ [An-Nahl: 36].
Sàrti (laa ilaaha illallaahu nag) mooy:
Bi ci njëkk: Xam-xam biy saafaanu ak réer.
Ñaareel bi: kóolute gu safaanoo ak sikk-sàkka.
Ñatteel bi: sellal gu safaanoo ak bokkale.
Ñenteel bi: Dëggal gu safaanoo ak weddi.
Juróomeel bi: bëgg gu safaanoo ak bañ.
Juróom-benneel bi: Jébbalu gu safaanoo ak bàyyi.
Juróom-ñaareel bi: Nangu gu safaanoo ak delloo.
Juróom-ñatteel bi: weddi lépp lu ñuy jaamu lu dul Yàlla mu kawe mi.
Sàrt yii dees leen a war a jëfe, te dajalees na leen ci ñaari bayit yii di ñëw:
Xam-xam kóolute ak sellal ak dëggu, ànd ak *** bëgg ak wommatu ak nangu baat bi.
Ñu dolli ca juróom-ñatteel ba muy nga weddi *** lépp lu dul Yàlla ci mbir yi ñuy jaamu.
Dëggal seede gi mooy kennal Yàlla cig jaamu bañ ko a bokkaale, ak sellal jaamu gi ngir Yàlla dong, Du ñaan ku dul Yàlla, du sukandiku ci ku dul moom, du yaakaar ku dul moom, du jullil ku dul moom, te du rendil ku dul moom mi sell te kawe.
Kon li yenn nit ñi di def ci wër i bàmmeel, ak di xettaliku ci ñi fa tëdd, ak di leen ñaan wolif Yàlla; ag bokkaale la ci jaamu gi, Moo tax ñu war a moytu loolu te di ci moytandikuloo; ndax lii day mel ni li way-bokkaale yi di def, di jaamu xërëm yi ak xeer yi ak garab yi bàyyi fi Yàlla, Te loolu mooy bokkaale gi ñu wàcce téere yi te yónni Yonnente yi ngir ñu ciy bàyyi loo xel ak di ko tere.
Maanaam seede ne Muhammat ndawul Yàlla la:
Topp ko ci li mu digle, dëggal ko yit ci li mu xibaare, te moytu li mu tere te jàjje ca, te bañ a jaamu Yàlla ci lu dul li mu yoonal, Jullit bi day saxal ne Muhammat doomu Abdallaa, mi bokk ci Qurays, giirug Haasim, mooy Yonnentu Yàlla mu kawe mi te tedd, ñeel mbooleem mbindeef yi; ci jinne yi ak nit ñi, kem ni ko Yàlla mu kawe mi waxe:
﴿قُلۡ يَٰٓأَيُّهَا ٱلنَّاسُ إِنِّي رَسُولُ ٱللَّهِ إِلَيۡكُمۡ جَمِيعًا...﴾
﴾Waxal: Éey yéen nit ñi man de Yonente Yàlla laa jëm ci yéen ñépp...﴿ [Al-Ahraaf: 158].
Ak ne Yàlla da ko a yónni ngir mu jottali diineem ji te jubal mbiddeef yi, kem ni ko Yàlla mu kawe mi waxe:
﴿وَمَآ أَرۡسَلۡنَٰكَ إِلَّا كَآفَّةٗ لِّلنَّاسِ بَشِيرٗا وَنَذِيرٗا وَلَٰكِنَّ أَكۡثَرَ ٱلنَّاسِ لَا يَعۡلَمُونَ 28﴾
﴾Yónniwunu la lu dul ci mbooleem nit ñi ngir ngay Aji-Bégle di Aji-Xuppe waaye li ëpp ci nit ñi xamuñu﴿ [Saba: 28]. kem ni ko Yàlla mu kawe mi waxe:
﴿وَمَآ أَرۡسَلۡنَٰكَ إِلَّا رَحۡمَةٗ لِّلۡعَٰلَمِينَ 107﴾
﴾Yónniwunu la lu dul ngir nga nekk yёrmaande ci mbooleem mbindeef yi﴿ [Al-Anbiyaa : 107].
Li seede gii làmboo, mooy: nga bañ a gëm ne Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- am na àq ci céru Boroom bi ak sañ-sañu doxal àdduna bi, mbaa wàll ci jaamu gi, Moom kay -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ab jaam la deesu ko jaamu, te ndawul Yàlla la deesu ko weddi. Te yoralul boppam walla keneen dara ci njariñ ak lor, lu dul lu soob Yàlla, kem ni ko Yàlla mu kawe mi waxe:
﴿قُل لَّآ أَقُولُ لَكُمۡ عِندِي خَزَآئِنُ ٱللَّهِ وَلَآ أَعۡلَمُ ٱلۡغَيۡبَ وَلَآ أَقُولُ لَكُمۡ إِنِّي مَلَكٌۖ إِنۡ أَتَّبِعُ إِلَّا مَا يُوحَىٰٓ إِلَيَّ...﴾
﴾Waxal ne: waxuma leen ne yore naa mangasiini Yàlla, te xamuma kumpa, te waxuma leen ne man malaaka laa; duma topp lu dul li ñu may soloo... ﴿
[Al-Anhaam: 50].
Ñaareelu waxtaan wi: maanaam gëm ak i ponkam:
Gëm: mooy saxal ci xol, ak wax ci làmmeñ, ak jëf ci xol ak ci cér yi, day dolliku ci topp Yàlla, di wàññeeku ci ag moy.
Gëm sàrt la ci wérug jaamu gi ak ug nangoom. Naka noonu bokkaale ak kéefar dafay màbb jaamu Yàlla yépp, Kem ni Yàlla dul nangoo julli gu amul jàpp, niki noonu it du nangu jaamu Yàlla gu amul gëm, Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿وَمَن يَعۡمَلۡ مِنَ ٱلصَّٰلِحَٰتِ مِن ذَكَرٍ أَوۡ أُنثَىٰ وَهُوَ مُؤۡمِنٞ فَأُوْلَٰٓئِكَ يَدۡخُلُونَ ٱلۡجَنَّةَ وَلَا يُظۡلَمُونَ نَقِيرٗا 124﴾
﴾Képp ku jëf aw yiw moo xam góor la walla muy jigéen te di aji-gëm ñooñu dinañu dugg àjjana te deesu leen tooñ dara donte daa tuuti ba toll ni mboxosu xooxu tàndarma﴿ [An-Nisaa-i: 124].
Mu leeral ne bokkaale day màbb jëf, kem ni ko Yàlla mu kawe mi waxe:
﴿وَلَقَدۡ أُوحِيَ إِلَيۡكَ وَإِلَى ٱلَّذِينَ مِن قَبۡلِكَ لَئِنۡ أَشۡرَكۡتَ لَيَحۡبَطَنَّ عَمَلُكَ وَلَتَكُونَنَّ مِنَ ٱلۡخَٰسِرِينَ 65﴾
﴾Yàlla xamal na la xamal ña la jiitu woon ci ne boo bokkaalee say jëf dina yàqu, te di nga bokk ci way-ñàkk yi﴿ [As-Sumari: 65].
Ponki ngëm juróom-benn la: gëm Yàlla, ak i malaakaam, ak ay téereem, ak i Yonenteem, ak bis-pénc, ak dogal bu neex ak bu naqari.
1) gëm Yàlla day làmboo ñatti mbir:
1- Gёm moomeelam gi:
Te mooy kennal ko ci jëfam; lu mel ni bind ak wërsëg ak dundal ak faat, Kon amul aji-bind ku dul Yàlla, amul aji-wërsëgale ku dul Yàlla, amul aji-dundal ku dul Yàlla, amul aji-faat ku dul Yàlla, te kenn soppaxndikuwul ci dénd bi ku dul moom -mi Sell te Kawe-.
Te xameesul ci mbindeef yi kenn ku weddi ne Yàlla mu kawe mi mooy Boroom bi, lu dul ku féttérlu te gëmul li muy wax, Kem ni mu ame woon ci Firhawna, ba mu waxee ay nitam ne:
﴿...أَنَا رَبُّكُمُ الْأَعْلَى﴾
﴾...Man maay seen Boroom bi gën a màgg﴿ [An-Naasihaati: 24], Waaye loolu teguwul ci ngëm, kem ni ko Yàlla mu kawe mi nettalee ci Muusaa -yal na ko Yàlla dolli jàmm -mu ne :
﴿قَالَ لَقَدۡ عَلِمۡتَ مَآ أَنزَلَ هَٰٓؤُلَآءِ إِلَّا رَبُّ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضِ بَصَآئِرَ وَإِنِّي لَأَظُنُّكَ يَٰفِرۡعَوۡنُ مَثۡبُورٗا 102﴾
﴾Mu ne ko: Xam nga bu wóor ne yii, Boroom Asamaan yi ak Suuf si rekk a leen wàcce ñu di ay lay yu leer, te man nag dama laa jàppe, ku ñu alag yaw Firhawna﴿ [Al-Israa: 102], Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿وَجَحَدُوا بِهَا وَاسْتَيْقَنَتْهَا أَنْفُسُهُمْ ظُلْمًا وَعُلُوًّا... ﴾
﴾dañu ko a weddi te wóoroon na leen, waaye ngir ag tooñ ak ug rëy...﴿ [An-Naml: 14].
Te mbindeef yii manul ñàkk ku leen bind, Ndaxte manul a amal boppam ci boppam; Ndaxte dara manul a bind boppam, te manul a jekki-jekki rekk am; Ndaxte lépp lu sosu war naa am ku ko sos, Ndax am gi mu am ci nosewu gu yéeme ak dëppoo gu méngoo dafay tere mu doon lu jekki-jekki rekk am, Kon nag, daa war a am ku ko amal, te mooy Yàlla, Boroom mbindeef yi. Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿أَمۡ خُلِقُواْ مِنۡ غَيۡرِ شَيۡءٍ أَمۡ هُمُ ٱلۡخَٰلِقُونَ 35 أَمۡ خَلَقُواْ ٱلسَّمَٰوَٰتِ وَٱلۡأَرۡضَۚ بَل لَّا يُوقِنُونَ 36﴾
﴾ndax dañu leen a bind ci lu dul dara walla ñoom ñoo bind 35
Walla ñoom ñoo bind asamaan yi ak suuf si Déedéet! Li am kay moo di ne ñoom wóoluwuñu (gëmuñu) 36﴿ [At-Tuur: 35-36].
Bokkaalekat ya daan nañu saxal moomeelu Yàlla mu kawe mi, waaye daan nañu ko bokkaale ci yàllaal gi, te loolu dugalu leen woon ci Lislaam. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc xeex ak ñoom, daganal seen dereet ak seen alal, ndaxte dañoo bokkaale Yàlla ci jaamu gi, ñu daal di jaamu ñeneen boole leen ak moom, niki xëram yi, ak xeer yi, ak malaaka yi, ak ñeneen.
2- Gëm wéetam gi cig jaamu:
Gëm wéetam gi cig jaamu, maanaam: ne moom rekk mooy ki ñu war a jaamu ci dëgg, te amul bokkaale, (Al-ilaahu) maanaam mooy (Al-maaluuhu), di ki ñuy jaamu ngir bëgg ko ak màggal ko ak toroxlul ko.
Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿وَإِلَٰهُكُمۡ إِلَٰهٞ وَٰحِدٞۖ لَّآ إِلَٰهَ إِلَّا هُوَ ٱلرَّحۡمَٰنُ ٱلرَّحِيمُ 163﴾
﴾Te seen Yàlla, jenn Yàlla la; amul jeneen Yàlla ju dul Moom, Moom miy Boroom Yërmaande gu mag gi, di Jéggalekat bi﴿ [Al-Baqara: 163].
Te képp ku wutal Yàlla ndend di ko jaamu, yàllaam googa ag neen la, Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿ذَٰلِكَ بِأَنَّ ٱللَّهَ هُوَ ٱلۡحَقُّ وَأَنَّ مَا يَدۡعُونَ مِن دُونِهِۦ هُوَ ٱلۡبَٰطِلُ وَأَنَّ ٱللَّهَ هُوَ ٱلۡعَلِيُّ ٱلۡكَبِيرُ 62﴾
﴾Loolu mooy ne Yàlla rekk mooy dëgg te lépp lu ñuy jaamu te du moom ag neen la, te Yàlla mooy Ki kawe, di Ki màgg﴿ [Al-Hajji: 62].
Loolu moo tax Yonnente yi -yal na leen Yàlla dolli xéewal ak mucc-, dale ca Nuuh ba ca Muhammat yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, da ñu daan woo seen i askan ci kennal Yàlla, ak jaamu ko moom kepp te bañ ko a bokkaale ak keneen. Te Yàlla mu kawe mi neenal na li Bokkalekat yi di def muy jël ay xërëm, di leen jaamu di ko boole ak Yàlla mu sell mi te kawe, di ci sàkku ndam, ak a sàkku ndimbal; te loolu, ci ñaari firnde yu xel la ko defe:
Bi ci njëkk: ne dara ci melokaani Yàlla yi nekkul ci yàlla yooyu ñu jël, ay mbindéef lañu, duñu bind, te duñu indil njariñ ñi leen di jaamu, duñu leen fegal aw lor, te moomuñu dund, moomuñu dee, moomuñu dekki. kem ni ko Yàlla mu kawe mi waxe:
﴿وَٱتَّخَذُواْ مِن دُونِهِۦٓ ءَالِهَةٗ لَّا يَخۡلُقُونَ شَيۡـٔٗا وَهُمۡ يُخۡلَقُونَ وَلَا يَمۡلِكُونَ لِأَنفُسِهِمۡ ضَرّٗا وَلَا نَفۡعٗا وَلَا يَمۡلِكُونَ مَوۡتٗا وَلَا حَيَوٰةٗ وَلَا نُشُورٗا 3﴾
﴾Dañuy jël lu dul moom def ko ay Yàlla yoy binduñu dara te ñoom dañu leen a bind, te moomaluñu seen bopp lor mbaa njariñ, te moomuñu dee mbaa dund, te moomuñu dekki﴿ [Al-Furxaan: 3].
Ñaareel bi: mooy bokkaalekat yooyu dañu doon saxal ne Yàlla rekk mooy ki bind tey doxal, te loolu day waral ñu wéetal ko ci jaamu gi kem ni ñu ko wéetale ci ay jëfam, kem ni ko Yàlla mu kawe mi waxe:
﴿قُل لِّمَنِ ٱلۡأَرۡضُ وَمَن فِيهَآ إِن كُنتُمۡ تَعۡلَمُونَ 84 سَيَقُولُونَ لِلَّهِۚ قُلۡ أَفَلَا تَذَكَّرُونَ 85 قُلۡ مَن رَّبُّ ٱلسَّمَٰوَٰتِ ٱلسَّبۡعِ وَرَبُّ ٱلۡعَرۡشِ ٱلۡعَظِيمِ 86 سَيَقُولُونَ لِلَّهِۚ قُلۡ أَفَلَا تَتَّقُونَ 87 قُلْ مَنْ بِيَدِهِ مَلَكُوتُ كُلِّ شَيْءٍ وَهُوَ يُجِيرُ وَلَا يُجَارُ عَلَيْهِ إِنْ كُنْتُمْ تَعْلَمُونَ 88 سَيَقُولُونَ لِلَّهِ قُلْ فَأَنَّى تُسْحَرُونَ 89﴾
﴾Waxal ne ana kan moo moom suuf si ak ñi ci biir, su fekkee ne dangeen a xam 84﴿
Danañu ne Yàlla, kon neel xanaa dungeen fàttaliku85
Neel: ana kan mooy Boroom asamaani juróom-ñaar yi ak Boroom Aras ju màgg ji 86
Danañu wax ne Yàlla, Kon neel xanaa dungeen ragal Yàlla 87
Waxal ne: Ana kan moo yor nguurug lépp ci loxoom, di aar te kenn du aare ci moom, su fekkee xam ngeen 88
Danañu wax ne Yàlla la ñeel, ne leen kon naka lañu leen di njabare 89﴿ [Al-Muuminuuna: 84-89] Bu ñu nangoo kennal Yàlla ci moomeelam, kon war na leen ñu jaamu ko moom dong, te duñu ko bokkaale ak kenn ci jaamu gi.
3- gëm ay turam ak i meloom:
Saxal li Yàlla saxal ci boppam ci téereem bi, Walla Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- saxal ko ci sunnaam; ci ay tur ak i melokaan, ci anam gu yell ci Yàlla mu kawe mi, ci lu dul di ko soppi, du caagine neenal, Du caagine ag melal, du caagine it niróole, Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿وَلِلَّهِ ٱلۡأَسۡمَآءُ ٱلۡحُسۡنَىٰ فَٱدۡعُوهُ بِهَاۖ وَذَرُواْ ٱلَّذِينَ يُلۡحِدُونَ فِيٓ أَسۡمَٰٓئِهِۦۚ سَيُجۡزَوۡنَ مَا كَانُواْ يَعۡمَلُونَ 180﴾
﴾Yàlla amna ay Tur yu rafet, kon ñaanleen ko ci, te bàyyileen ñiy dëngal ci Turam yi, dees na leen fay li ñu daan def ﴿ [Al-Ahraaf: 180], Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿...لَيۡسَ كَمِثۡلِهِۦ شَيۡءٞۖ وَهُوَ ٱلسَّمِيعُ ٱلۡبَصِيرُ﴾
﴾...Moom niróowul ak dara te moom Aji-Dégg la Aji-Gis la﴿ [As-Suuraa: 11].
Xaaji bokkaale yi ñatt la:
1- Bokkaale gu mag.
2- Bokkaale gu ndaw.
3- bokkaale gu nëbbu.
1- Bokkaale gu mag:
Ag tënkam mooy: Yamale lu dul Yàlla ak Yàlla ci lu Yàlla jagoo, kem ni ko Yàlla mu kawe mi waxe:
﴿إِذۡ نُسَوِّيكُم بِرَبِّ ٱلۡعَٰلَمِينَ 98﴾
﴾ba ñu leen doon yamale ak Boroom mbindeef yi﴿ [As-Suharaa: 98].
Li muy làmboo mooy: jëmale ag jaamu ci ku dul Yàlla mu kawe mi, Walla jëmale ab pàcc ci jaamu gi ci ku dul Yàlla mu sell mi; lu mel ni ñaan, ak xettaliku, ak nisër, ak rendi, ak yeneen yu bokk ci xeeti jaamu yi.
Walla muy làmboo: daganal lu Yàlla araamal, walla araamal lu mu daganal, Walla rotal lu Yàlla mu màgg mi waral, Niki daganal lu ñu xam ne araam na ci diine ji te leer naññ; lu ci mel ni daganal njaalo, walla sàngara, walla dënge ñaari way-jur, walla ribaa, walla lu ko niru.
walla araamal lu Yàlla mu màgg mi daganal ci yu teey yi, Walla rotal lu Yàlla waral; Niki gëm ne julli warul, walla woor warul, walla asaka warul.
Bokkaale gu mag gi day waral jëf ju yàqu, ak sax sawara ci ku ko deewaale, kem ni ko Yàlla mu kawe mi waxe:
﴿...وَلَوۡ أَشۡرَكُواْ لَحَبِطَ عَنۡهُم مَّا كَانُواْ يَعۡمَلُونَ﴾
﴾... bu ñu bokkaale woon kon seen jëf yépp di na yàqu ﴿ [Al-Anhaam: 88].
Ku ci faatu; Yàlla du ko jéggal, àjjana it araam na ci moom, kem ni ko Yàlla mu kawe mi waxe:
﴿إِنَّ ٱللَّهَ لَا يَغۡفِرُ أَن يُشۡرَكَ بِهِۦ وَيَغۡفِرُ مَا دُونَ ذَٰلِكَ لِمَن يَشَآءُ...﴾
﴾ Yàlla du jéggal ku koy bokkaale, dana jéggale nag lu yées bokkaale ñeel ku ko soob...﴿ [An-Nisaa-i: 48], Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿...إِنَّهُۥ مَن يُشۡرِكۡ بِٱللَّهِ فَقَدۡ حَرَّمَ ٱللَّهُ عَلَيۡهِ ٱلۡجَنَّةَ وَمَأۡوَىٰهُ ٱلنَّارُ...﴾
﴾mbir mi mooy képp kuy bokkaale Yàlla àjjana araam na ci moom, te sawara mooy wàccuwaayam... ﴿ [Al-Maa-ida: 72].
2- Bokkaale gu ndaw:
Mooy lu téere yi tudde bokkaale, waaye eggul ci darajay bokkaale gu mag gi; loolu lañuy tudde bokkaale gu ndaw; Lu mel ni giñ ci ku dul Yàlla mu kawe mi; niki giñ ci Kaaba gi, ak ci Yonnente yi, ak ci kóolute, ak ci dundu diw ak yu ni mel, Kem ni ko Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- waxe:
«مَنْ حَلَفَ بِغَيرِ اللهِ فَقَدْ كَفَرَ أَو أَشرَكَ».
«ku giñ ci ku dul Yàlla weddi na walla bokkaale na»2.
Te man naa nekk bu màgg, moo ngi aju rekk ci li nekk ci xolu boroomam, Bu dee li nekk ci xolu kiy giñ ci Yonnente bi walla Sëriñ sangam mooy ne dafa mel ni Yàlla, walla ne dees koy ñaan wolif Yàlla, walla ne dafay doxal àdduna bi; loolu day nekk bokkaale gu mag, Waaye bu dee kiy giñ ci ku dul Yàlla jubluwul lii, waaye day jaar rekk ci làmmiñam te fasu ko, ndax da ko a tàmm; kon day nekk bokkaale gu ndaw, Te lii day am lu bari, kon li war mooy ñu yewwu ci loolu te àrtu ci, ngir sàmm Tawhiid ak aar ko.
3- bokkaale gu nëbbu:
Mooy liy nekk ci xol bi ci ngistal; Niki kuy julli walla di jàng ngir ngistal ci nit ñi, walla di sàbbaal ngir ñu tagg ko, walla di saraxe ngir ñu tagg ko, Te loolu dafay màbb jëf ji ñuy wonewu, waaye du màbb yeneen jëf ya ñu sellal ngir Yàlla mu kawe mi.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«الشِّرْكُ فِي هَذِهِ الْأُمَّةِ أَخْفَى مِنْ دَبِيبِ النَّمْلَةِ السَّودَاءِ عَلَى الصَّفَاةِ السَّودَاءِ فِي ظُلْمَةِ اللَّيْلِ، وَكَفَّارَتُهُ أَنْ يَقُولَ: "اللَّهُمَّ إِنِّي أَعُوذُ بِكَ أَنْ أُشْرِكَ بِكَ شَيْئًا وَأَنَا أَعْلَمُ، وَأَسْتَغْفِرُكَ مِنَ الذَّنْبِ الَّذِي لَا أَعْلَمُ».
«Bokkaale ci askan wii gën naa nëbbu doxuw sànxaleñ wu ñuul ci kaw xeer wu ñuul ci guddi gu lëndëm, likoy kaffara nag mooy mu wax: "Allaahummam innii ahuusu bika an usrika bika say an wa anaa ahlamu wa astaxfiruka minassanbi lasii laa ahlamu»3.
Xeeti kéefër yi:
Xeet bu njëkk bi: Kéefër gu mag:
Mooy liy waral sax ca sawara, te am na juróomi xeet:
1- ak kéefarug weddi:
Mooy weddi Yonente yi, Te lii lu néew la ci yéefër yi; ndax Yàlla mu màgg mi dëgëral na ay Yonnenteem ci ay lay yu leer, Mbirum weddikat yii de, mi ngi mel ne ni ko Yàlla melale:
﴿وَجَحَدُوا بِهَا وَاسْتَيْقَنَتْهَا أَنْفُسُهُمْ ظُلْمًا وَعُلُوًّا...﴾
﴾Ñu weddi ko, te seen i bakkan wóoroon na leen ne dëgg la, waaye ngir tooñ rekk ak rëy-rëylu... ﴿
[An-Nahl: 14].
2- ak kéefarug bañ ak rëy-rëylu:
Lii day mel ni weddig Ibliis: weddiwul ndigëlu Yàlla, waaye da koo weccook bañ ak rëy-rëylu, Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿وَإِذۡ قُلۡنَا لِلۡمَلَٰٓئِكَةِ ٱسۡجُدُواْ لِأٓدَمَ فَسَجَدُوٓاْ إِلَّآ إِبۡلِيسَ أَبَىٰ وَٱسۡتَكۡبَرَ وَكَانَ مِنَ ٱلۡكَٰفِرِينَ 34﴾
﴾Fàttalikul bi Nu waxee Malaaka yi ne leen: Sujjóotalleen Aadama, ñu sujjóot, ba mu des Ibliis; moom dafa bañ te rëy-rëylu, daal di bokk ci yéefar yi ﴿ [Al-Baqara: 34].
3- Kéefërug dëddu:
Loolu nag mooy mu dëddu ak déggam ak xolam wolif topp dëgg, du ko xool, te du ko sax bàyyi xel, Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿وَمَنۡ أَظۡلَمُ مِمَّن ذُكِّرَ بِـَٔايَٰتِ رَبِّهِۦ ثُمَّ أَعۡرَضَ عَنۡهَآۚ إِنَّا مِنَ ٱلۡمُجۡرِمِينَ مُنتَقِمُونَ 22﴾
﴾Amul ku dàq a tooñ ku ñu fattali aayay Boroomam, mu daal di dummóoyu, Nun de, dinanu fayyu ci saay-saay yi﴿ [As-Sajdati: 22].
Dëddu gu dayoo gi nag, mooy ag kàccoorte la, waaye du kéefar; niki kiy dëddu jàng yenn ci faratay diine ji, yu mel ni àttey koor walla aj ak yu ni mel.
4- Kéfërug sikk-sàkka:
Loolu nag mooy muy dengi-dengi, te doguwul ci dëgg gi, waaye kay da ciy sikk-sàkka, kem ni ko Yàlla mu Kawe mi te Sell waxe:
﴿وَدَخَلَ جَنَّتَهُ وَهُوَ ظَالِمٌ لِنَفْسِهِ قَالَ مَا أَظُنُّ أَنْ تَبِيدَ هَذِهِ أَبَدًا 35 وَمَا أَظُنُّ السَّاعَةَ قَائِمَةً وَلَئِنْ رُدِدْتُ إِلَى رَبِّي لَأَجِدَنَّ خَيْرًا مِنْهَا مُنْقَلَبًا 36﴾
﴾mu dugg toolam, di aji-tooñ boppam, di wax naan: njortuma ne lii dina jeex mukk 35
te jàppuma ne bis-pénc dina am, te bu ma delloo ci sama Boroom, dinaa fa fekk aw delloowaay wu ko gën36﴿ [Al-Kahf: 35-36].
5- kéefarug naaféq:
Te mooy mu feeñal ci làmmiñam ag ngëm, di nëbb ci xolam ag weddi, Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿وَمِنَ ٱلنَّاسِ مَن يَقُولُ ءَامَنَّا بِٱللَّهِ وَبِٱلۡيَوۡمِ ٱلۡأٓخِرِ وَمَا هُم بِمُؤۡمِنِينَ 8﴾
﴾am na ci nit ñi ñu naan: gëm nanu Yàlla ak bis bu mujj ba, te duñu ay way-gëm﴿ [Al-Baqara: 8].
Yii nag ñooy xeeti kéefar gu mag giy génne ci diine ji.
Xeet bu ñaareel bi: Kéefër gu ndaw:
Xeet bii du waral sax ca sawara, Mooy li rot ci Alxuraan ak Sunna, ñu tudde ko ag kéefar te xamaleesu ko ci alif ak laam; waaye dafa rot te nekk lu kenn xamul, Ay misaalam nag yu bari la, bokk na ci: Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
«اثْنَتَانِ فِي النَّاسِ هُمَا بِهِمْ كُفْرٌ: الطَّعْنُ فِي النَّسَبِ، وَالنِّيَاحَةُ عَلَى المَيِّتِ».
"ñaar a ngi ci nit ñi te ag kéefar la: di jam ay askan, ak di yuuxu ku dee"4.
2) gëm Malaaka yi.
Te ñoom, aalamu kumpa lañu, Yàlla da leen a bind ci leer, Te ñoom, Yàlla mu kawe mi lañuy jaamu, Te amuñu dara ci jagley Boroom bi, ak jagley ñu leen di jaamu, Te ñoom duñu moy Yàlla ci lu mu leen digal, Te dañuy def lépp lu ñu leen digal, Ñoom nag, lim bu bari lañu, kenn takkul seenug lim ku dul Yàlla mu kawe mi.
Gëm malaaka yi nag day làmboo ñenti mbir:
1- gëm seenug am.
2- Gëm ñi nu xam seen i tur ci ñoom; niki: Jibriil, ak Miikaayil, ak Israafiil, ak ñu dul ñoom. Ku ñu xamul turam danu koy gëm ci lu daj.
3- gëm li nu xam ci seen i melokaan, yi ñëw ci Alquraan ak ci Sunna; Niki melokaanu Jibriil, Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa xibaare ne gis na ko ci melokaan mi ko Yàlla mu kawe mi binde, mu am juróom-benn téeméeri laaf, yu daj jawwu ji.
4- gëm li nu xam ci seen i jëf: niki seenug sàbbaal Yàlla mu kawe mi, ak di ko jaamu guddi ak bëccëg te duñu ci tàyyeel mbaa ñu ciy yoqat.
Ci misaal: Jibriil mooy ki ñu dénk wahyu gi.
Israafiil: mooy ki ñu dénk ëf Bufte ga.
Malaakam dee mi nag: mooy ki ñu dénk jël ruu yi ci dee gi.
ak Maalik miy wattu sawara; ak Ridwaan miy wattu àjjana, ak ñeneen.
3) gëm téere yi:
Li ñu namm ci téere yi: mooy téere yi jóge asamaan te Yàlla wàcce leen ci ay Yonenteem, Muy ag njub ñeel nit ñi ak yërmànde ci ñoom, ngir ñu egg ci texeg àdduna ak allaaxira.
Gëm téere yi nag day làmboo ñenti mbir:
1- gëm ne Yàlla mu kawe mi moo ko wàcce ci dëgg.
2- gëm yi ñu ci xam turam, niki Alxuraan bi ñu wàcce ci Muhammat -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-, ak Tawraat bi Yàlla wàcce ci Muusaa yal na jàmm nekk ci moom, ak Injiil bi Yàlla wàcce ci Iisaa yal na jàmm nekk ci moom, ak zabuur bi Yàlla jox Daawuda yal na jàmm nekk ci moom.
Wànte la nu xamul turam danu koy gëm noonu.
3- Dëggal xibaaram yi; niki xibaari Alxuraan, ak xibaar yi ñu soppi wul ci téere ya jiitu woon.
4- Jëfe àtteem yi ñu nasaxalul, gërëm ko te wommatul ko, moo xam xam nanu xereñteem gi mbaa xamunu ko. Te mbooleem téere yi jiitu woon, Alxuraan ju màgg ji moo leen folli, Kon du dagan ñu jëfe benn àtte bu bokk ci àttey téere yu njëkk ya, lu dul la ca wér, te Alxuraanul kariim walla Sunnas Yonnente bi dëggal ko.
4) Ñenteel bi: Gëm Yonente yi -yal na jàmm nekk si ñoom-:
Yonnente yi: mooy limub Yonente; te Yonente mooy nit ku ñu soloo ag Sariiha sant ko mu jotali ko, Ki ci njëkk mooy Nuuh -yal na ko Yàlla dolli jàmm-, ki ci mujj mooy Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, Ñoom ay nit yu ñu bind lañu, Amuñu ci meloy Boroom bi walla ag jaamu dara.
Gëm Yonente yi day làmboo:
1- gëm ne seen bataaxal dëgg gu bàyyikoo fa Yàlla la, Ku weddi yónnenteg kenn ci ñoom weddi na ñépp.
2- Gëm ñi ñu xam seen tur ci ñoom, niki: Muhammat, ak Ibraahiima, ak Muusaa, ak Iisaa, ak Nuuh, yal na jàmm ak mucc nekk ci ñoom. Ñoom nag ñooy Yonnente yay boroom dogu ya.
Wànte ñi nu xamul seen tur ci ñoom, danu leen di gëm ci lu daj, Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿وَلَقَدۡ أَرۡسَلۡنَا رُسُلٗا مِّن قَبۡلِكَ مِنۡهُم مَّن قَصَصۡنَا عَلَيۡكَ وَمِنۡهُم مَّن لَّمۡ نَقۡصُصۡ عَلَيۡكَ...﴾
﴾Yónni Nanu ay Yonnente yu la jiitu woon, am na ca ñoom ñu nu la nettali, te am na ca ñoom ñu nu la nettaliwul...﴿ [Xaafiri: 78].
3- dëggal li wér ci seen i xibaar -yal na leen Yàlla dolli jàmm ak mucc-.
4- Jëfe Sariihab ki ñu yónni ci nun ci ñoom, te mooy ki leen tëj, muy Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
5) Gëm bis bu mujj ba:
te mooy bis-pénc, bi ñuy dekkil nit ñi, ngir càmbar ak pay, Ñu tudde ko noonu ndaxte amul beneen bis ci ginnaawam, fa la waa àjjana di dal ci seen i kër, waa sawara itam ci seen i kër.
Gëm bis bu mujj ba nag day làmboo ñatti mbir:
A- gëm dekki:
Te mooy dundal ñi faatu su ñu walee ci Bufte ba walug ñaareel ga, Nit ñi taxaw ngir Boroom mbindeef yi, duñu sol dall, duñu am muuraay, duñu xaraf, Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿كَمَا بَدَأْنَا أَوَّلَ خَلْقٍ نُعِيدُهُ وَعْدًا عَلَيْنَا إِنَّا كُنَّا فَاعِلِينَ 104﴾
﴾kem na nu tàmbalee woon mbind mu njëkk ma noonu la nu koy delloo waate, ab digg la ci nun te dinanu ko def﴿ [Al-Anbiyaa : 104].
B- Ñaareel bi mooy: gëm càmbar ga ak fay ga:
Fa ñuy càmbare jaam bi ay jëfam, dal di ka koy fay, Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿إِنَّ إِلَيۡنَآ إِيَابَهُمۡ 25 ثُمَّ إِنَّ عَلَيۡنَا حِسَابَهُم 26﴾
﴾Ci nun rekk lañuy dellusi 25
Ginaaw loolu, war na ci nun nu càmbar leen26﴿
[Al-Xaasiya: 25-26].
C- gëm àjjana ak sawara:
Te ñoom ñaar ñooy mujjukaayu mbindeef yi ba fàww; Àjjana mooy kërug xéewal ga Yàlla mu kawe mi waajalal way-gëm ñi ragal Yàlla, ak ñi sàmm ndigëli Yàlla ak yu Ndawam, yal na jàmmi Yàlla ak xéewalam nekk ci moom, Amna fa lu bët musul a gis, te nopp musu ko a dégg, te musul a rot ci xolu nit.
Bu dee sawara nag; Këru mbugal la, Yàlla waajalal ko yéefar yi weddi Yàlla te moy yonenteem ya. Amna ci biiram ay xeeti mbugal yu tar yu musul a rot ci xel.
6) gëm dogal bu neex ak bu naqari:
Li ñu jublu ci ndogal: Li Yàlla di Dogalu ci lépp luy am ci anam gi mu jiitoo ci xam-xamam te mu namm ko.
Gëm ndogal yi nag day làmboo ñenti mbir:
1- Xam-xam: mooy gëm xam xamub Yàlla mu kawe mi, ak ne xam na la jiitu ak liy ñëw, ak naka lay ame, ci lu dajale ak cig faramfacce ba fàww. Te moom -mu sell mi- moo xam li amul bu doon ama naka lay ame, kem ni ko Yàlla mu kawe mi waxe ne:
﴿وَلَوۡ رُدُّواْ لَعَادُواْ لِمَا نُهُواْ عَنۡهُ ...﴾
﴾ Bu ñu leen delloo woon kon di nañu delluwaat ca la ñu leen tere woon ... ﴿ [Al-Anhaam: 28].
2) Mbind mi: mooy nga gëm ne Yàlla mu kawe mi te sell bind na nattaleg mbir yépp ba bis-pénc ba, kem ni ko Yàlla mu kawe mi waxe:
﴿أَلَمۡ تَعۡلَمۡ أَنَّ ٱللَّهَ يَعۡلَمُ مَا فِي ٱلسَّمَآءِ وَٱلۡأَرۡضِۚ إِنَّ ذَٰلِكَ فِي كِتَٰبٍۚ إِنَّ ذَٰلِكَ عَلَى ٱللَّهِ يَسِيرٞ 70﴾
﴾Xanaa xamóo ne Yàlla xam na li nekk ci Asamaan ak Suuf, loola ma nga ca téere ba,(lawhul mahfuus) te loolu lu yomb la ci Yàlla﴿ [Al-Hajji: 70].
3- Coobare ga: mooy gëm ne amul dara luy xew ci àdduna sii lu dul ci coobarey Yàlla mu màgg mi te tedd, Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿وَرَبُّكَ يَخۡلُقُ مَا يَشَآءُ وَيَخۡتَارُ ...﴾
﴾ Sa Boroom mooy bind lu ko soob te mooy tànn...﴿ [Al-Xasasi: 68]. Nit ki nag am na coobare gu dul génn ci coobarey Yàlla, niki ni ko boroom bi waxe:
﴿وَمَا تَشَآءُونَ إِلَّآ أَن يَشَآءَ ٱللَّهُ رَبُّ ٱلۡعَٰلَمِينَ 29﴾
﴾dara duleen soob lu dul ne dafa soob Yàlla miy Boroom mbindeef yi ba noppi﴿ [At-Takkwiir : 29].
4- Bind gi: te mooy gëm ne Yàlla moo bind mbindeef yi ak seen i jëf, ci lu baax ak lu bon, Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿ٱللَّهُ خَٰلِقُ كُلِّ شَيۡءٖۖ وَهُوَ عَلَىٰ كُلِّ شَيۡءٖ وَكِيلٞ 62﴾
﴾ Yàlla moo bind lépp, te moo gàlloo lépp lu mu man a doon ﴿ [As-Sumari: 62].
Dayo yii dajalees na ko ci bayit bii:
Xam-xamam, mbindam, coobareem, ak sàkkam, di amal ak di sàkk.
Ñatteelu waxtaan wi mooy: rafetal
Rafetal, moom benn ponk la, te mooy: nga jaamu Yàlla ba mel ni yaa ngi koy gis, boo demul ba mel noonu, nga xam ne moom Yàlla mi ngi lay gis.
Maanaam: nit ki def li ko Yàlla jaamuloo ba mel ni mu ngi taxaw ci kanamu Yàlla mu kawe mi, Loolu day waral ragal gu mat ak dellu ci Moom mu sell mi. Te loolu day waral jaamu gi dëppoo ak Sunnas Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Te rafetal ñaari tolluwaay la, te ñiy rafetal ñoo ngi ci ñaari maqaama yu wuute:
Tolluwaay bu njëkk bi: mooy bi gën a kawe, te mooy tolluwaayu janoo; Mooy jaam bi jëf ba mel ni mi ngi gis Yàlla ak xolam, ba xol bi leer ak ngëm, ba kumpa mel ni jañoo ga.
Tolluwaayu ñaareel bi mooy: tolluwaayu sellal ak fuglu, Te mooy jaam bi di teewlu ci xelam ne Yàlla mi ngi janoo ak moom, te mi ngi koy gis, bu teewloo loolu kon sellal na ngir Yàlla mu kawe mi.
ñenteelu waxtaan wi: ab tënk bu gàtt ci cosaani Ahlu sunna wall jamaaha:
Bu njëkk bi: topp li dikk ci Alxuraan ak Sunna ci biir ak ci bitti, Te bañ a jiital waxi kenn ci nit ñi ci kàddug Yàlla ak kàddug Yonenteem, yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Ñaareel bi: muccug seen xol yi ak seen làmmiñ yi ñeel Sahaabay Yonente Yàlla bi, yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, Da ñuy fas ne xalifa gi ginnaaw Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-: mooy Abuu Bakar, ginnaaw ba Umar, ginnaaw ba Usmaan, ginnaaw ba Aliyun, -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ñoom ñépp.
Ñatteel bi: Bëgg waa kër Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ak féetewoo leen, rawatina ñu sell ñi ci ñoom.
Ñenteel bi: bañ a génn ci kaw njiit yi, donte dañoo tooñ, Te ñu di leen ñaanal sell ak jàmm, Duñu ñaan musiba ci seen kaw. Topp leen ci topp Yàlla la bokk, te farata la, lu dul ñu santaane ag moy, Bu ñu diglee ag moy, du dagan ñu leen cay topp, Topp leen ci njekk nag day wéy ci lu dul loolu.
Juróomeel bi: gëm xar-baaxi wàlliyu yi; Te mooy lu Yàlla di jaarale ci seen i loxo ci mbir yu xotti mbaax.
Juróom-benneel bi: duñu yéefaral ñoñ-xibla ngir rekk ay moy ak bàkkaar yu mag, Kem ni ko Xawaarik yi di defe, Waaye mbokkoog ngëm gi day sax ànd ak moy ya, Dañuy wax ci moykat bi ne: moom jullit la ngir ngëmam, kàccoor la it ngir bàkkaaram bu mag.
Teqaleg ñaareel bi: lu aju ci jaamu Yàlla yi
Waxtaan wu njëkk wi: Laab:
Laab ci làkk: mooy ag cet ak ug sell ci sobe yu feeñ ak yu nëbbu.
Ci Sariiha nag: mooy yëkkëti am toj ak dindi sobe. Te laab mooy caabiy julli, Looloo tax, jàng ko bokk na ci mbiri diine yi gën a màgg, te war na ci jullit bu nekk mu jàng ko te yittewoo ko.
Li ci njëkk: xeeti ndox yi:
1- mu laab di laabal; dana wér ñu laabe ci, Moo xam mu des ca ag mbindam; Niki ndoxum taw, walla ndoxum dex, walla ndoxum géej, Walla mbir mu laab jaxasoo ak moom, te notu ko, te it dindiwul turam wa.
2- mu Sobe; jëfandikoo ko du dagan, Du yëkkëti am toj, te du dindi sobe, Mooy li meloom walla xetam walla cafkaam soppeeku ci sobe.
Ñaareel bi: Sobe:
Sobe mooy: ag tilim gu ñu jagleel, Aw xeetam dafay teree julli; Niki saw, ak xayta, ak dereet ak yeneen yi, te mu nekk ci yaram wi, ci bérab bi ak ci yére bi.
Liy cosaan ci mbir yi mooy: ag dagan ak ug laab, Kon képp ku jàpp ne dara sobe la, warnaa am firnde. Bokkul ci sobe: tiflit, ñaqu nit, ak ñaqu mbaam; waaye dañoo laab, donte sax dañoo tilim, Sobe bu nekk tilim la, waaye du tilim bu nekk sobe la.
Sobe amna ñatti daraja:
Bi ci njëkk: Sobe su diis;
Niki lu mel ni: sobem loo xam ni ab xaj da caa cab, Anamu laabal ko mooy: dees koy raxas juróom-ñaari yoon, bu njëkk ba ñu boole ci suuf.
Ñaareel bi: Sobe su woyof:
Niki sawu xale bu góor buy nàmp bu laalee yére bi mbaa leneen. Anamu laabal ko mooy ñu wis ci ndox ba mu muur ko, te du laaj xoos walla nal.
Bu ñatteel bi: sobe su digg-dóomu:
Niki sawu doomu Aadama ak xaytaam, ak li ëpp ci sobe yi, bu dalee ci suuf walla yére ak yu ni mel. Anamu laabal ko mooy: ñu dindi jëmmi sobe si su amee jëmm, te setal bérab ba ci ndox walla leneen lu ñuy setale.
Bokk na ci li ab tegtal ñëw ci ag sobeem:
1- sawu nit ak ay xayteem.
2- Masyu ak Wadyu5.
3- neferey lu ñu dul lekk ndawalam.
4- Dereetu mbërëg ak wësin.
5- Tiflitu xaj.
6- médd, dees na ci settee:
A- Nit bu faatoo.
B- méddu jën ak njéeréer.
C- Méddum lu amul dereet juy yol; lu mel ni weñ ak Xorondom ak yamb ak yu ni mel.
D- Yaxu lu médd, ak béjjënam, ak weyam ak kawaram ak dunqam.
Anamu laabale sobe si day nekk:
1- Ci ndox, moom te mooy cosaan ci laabal sobe yi, kon deesu ko weccoo ak leneen.
2- Lu Sariiha indi ci melow laabal jëm yi nekk sobe walla lu sobe taq:
A- Dees na laabal deru lu médd ci wulli ko.
B- Laabalug ndab bu ci ab xaj xabee; mooy dees koy raxas juróom-ñaari yoon; bu njëkk ba ñu boole ci suuf.
C- laabalug yére bu dereetu mbërëg laal; mooy ñu xoos ko, topp ñu bomb ko ag ndox, bu noppee ñu weñ ko; bu ca jeexit desee ginnaaw loolu it du lor.
D- laabalug catu yérey jigéen; mooy suuf su laab si ci topp.
E- laabalug yére ci sawu liir bu góor buy nàmp; dana nekk ci wis ko, ak ci raxas bu dee sawum liir bu jigéen la.
F- laabalug yére bu am masyu; mooy ñu wis ndox ci bérab ba.
G- Laabal suufu dàll; ci bomb ko ci suuf su laab.
H- laabal suuf ci sobe; dañuy sotti siwo ndox ca bérab ba, walla ñu bàyyi ko ba mu wow ci jant bi walla ngelaw li, bu njeexitu sobe sa déñee kon laab na.
Ñatteel bi : li aram a def ci ku amul jàpp:
Mbir yi aram ci ku tojle toj gu ndaw mbaa gu mag:
1- Julli, moo xam gu farata la, walla gu naafila la; Ndax li ñu jële ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«لَا يَقْبَلُ اللَّهُ صَلَاةً بِغَيْرِ طُهُورٍ».
«Yàlla du nangu julli ci lu dul laab»6.
2- Laal kaamil; Ndax li rot ci téere bi Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bindaloon Amru ibn Hasmin, te mu wax ca ne:
«لَا يَمَسُّ الْقُرْآنَ إِلَّا طَاهِرٌ».
«Kenn warul a laal Alxuraan ji lu-dul ku laab»7.
3- wër néeg bu yàgg ba (Kaaba ga); Ngir waxu Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
«الطَّوَافُ بِالْبَيْتِ صَلَاةٌ، إِلَّا أَنَّ اللَّهَ أَبَاحَ فِيهِ الْكَلَامَ».
«Wër Kaaba ga julli la, lu dul ne rekk Yàlla daganal na ci wax.»8. Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jàpp na ngir tawaaf, Wér na jóge ci Yonente bi-yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko- ne dafa tere ki gis mbaax mu wër Kaaba ga ba baa muy laab.
Bu dee yi ñu araamal ci ki am toj gu mag nag mooy:
1- Jàng Alxuraan; Ngir hadiisu Aliyun yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: "Dara daanul tere Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci Alxuraan, lu dul janaba"9.
2- Toog ci biir jumaa ci lu dul njàppu; Ndax waxi Yàlla mu kawe mi:
﴿يَٰٓأَيُّهَا ٱلَّذِينَ ءَامَنُواْ لَا تَقۡرَبُواْ ٱلصَّلَوٰةَ وَأَنتُمۡ سُكَٰرَىٰ حَتَّىٰ تَعۡلَمُواْ مَا تَقُولُونَ وَلَا جُنُبًا إِلَّا عَابِرِي سَبِيلٍ حَتَّىٰ تَغۡتَسِلُواْ...﴾
﴾Yéen way-gëm ñi, buleen jege julli te fekk dangeen a màndi, ngir ngeen di xam li ngeen di wax, walla ngeen ame janaba ba keroog ngeen di sangu...﴿ [An-Nisaa-i: 43].
Ku ame toj gu mag bu jàppoo, dagan na mu toog ca jàkka ja, naka noonu itam, dagan na ci ku tojle toj gu mag mu jaar ca jàkka ja rekk te du fa toog.
Ñenteel bi: Teggini faj aajo:
Sopp nañu ci faj aajo:
1- Sori nit ñi te suturlawu ci bérab bu wéet.
2- wax ñaan gi rot ci bu ñuy dugg, te mooy:
«اللَّهُمَّ إِنِّي أَعُوذُ بِكَ مِنَ الْخُبْثِ وَالْخَبَائِثِ».
«Allaahumma innii ahuuzu bika minal xubusi wal xabaa-isi»10.
Dina war ci faj aajo:
1- serlu ba Set ci saw mi.
2- suturaal awra wi.
Tere nañu ci faj aajo:
1- Jublu xibla walla wan ko ginnaaw.
2- Faj aajo ci yooni nit ñi ak seen i bérab yu ñépp bokk.
3- Saw ci ndox mu taa.
Danañu sib ci faj aajo:
1- Laal Sakara si ci loxo ndayjoor jamonoy faj aajo ji.
2- laabu ak fompu ci loxo ndayjoor.
3- Sib nañu wax ci jamonoy faj aajo, rawatina tudd turu Yàlla mu màgg mi.
Juróomeel bi: àttey Laabu ak fompu:
Laabu mooy: dindi sobe si génne ci ñaari yoon yi ci am ndox.
Fompu mooy: dindi sobe siy génne ci ñaari yoon yi ci lu dul ndox; niki xeer mbaa musuwaar.
Sàrti li ñuy fompoo:
1- Mu nekk lu dagan.
2- Mu nekk lu laab.
3- Mu nekk luy setal.
4- mu bañ a doon yax walla neefere.
5- Bumu doon dara lu am worma; niki ay këyit yu am turu Yàlla mu tedd mi te kawe.
Dina dagan ñu doyloo fompu ci ñaari sàrt:
1- Li génn bañ a weesu bérab ba mu aadawoo génne.
2- Fompu gi na nekk ci ñatti xeer yu mana setal.
Juróom-benneel bi mooy: àttey njàppu.
Njàppu dana war ci ñatti jaamu Yàlla:
1- Julli, moo xam gu farata la, walla gu naafila la.
2- Laal kaamiil bi.
3- Wër kaaba ga.
Sàrti njàppu:
1- Lislaam.
2- Xel.
3- ràññee.
4- Yéene: te bérabam mooy xol, wax ko biida la, Képp ku bëgg a jàppu rekk yeene na, Raxas céri njàppu yi nag ngir yéene seddal mbaa setal, loolu du njàppu.
5- Wéyal àtteem: mooy mu bañ ko a yéenee dagg ba laabam gi mat.
6- Dogug li waral njàppu mi, Dees na settee ci loolu: képp ku am salas, ak kiy gis dereeti njorgel.
7- Laabu walla fompu jiitu ko, ñeel ku am saw walla xayta génn ci moom.
8- Ndox muy laabal, te mu dagan.
9- Dindi lépp luy tere ndox mi laal der bi.
10- Duggug waxtu julli wi ñeel ki tojam di lu sax.
Faratay njappu:
1- raxas xar kanam, ci la gallaxndiku ak saraxndiku bokk.
2- raxas ñaari yoxo yi ak coñc yi.
3) masaa bopp bépp, nopp yi ci la bokk.
4) raxas tànk yi ak dojor yi.
5) Toftale céri njàppu yi.
6- toftale njàppu mi: maanaam warul a am dog-dog bu yàgg ci diggante cér yi.
Melow njàppu:
1- Tudd Yàlla (wax bismilla).
2) raxas ténq yi ñatti yoon.
3) raxas xar kanam gi ñatti yoon, boole ci gallaxndiku ak saraxndiku.
4) raxas yoxo yi ba ci coñc yi ñatti yoon, tàmbalee ci loxob ndayjoor bi, teg ci loxob càmmooñ bi.
5) masaa bopp bi ak nopp yi.
6) raxas tànk yi ak dojor yi ñatti yoon, tàmbalee ci tànku ndayjoor bi, teg ci bu càmmooñ bi.
Yiy toj njàppu:
1- Liy génne ci ñaari génnuwaay yi, lu ci mel ni: saw ak ngelawal ak xayta.
2- sobe su bon su génne ci yaram.
3- Xel mu deñ ci nelaw walla leneen.
4- Laal sa awra ci sa loxo te dara doxul ci diggante bi, moo xam bu kanam la wala bu ginnaaw.
5- lekk ndawalug giléem.
6- génn ci lislaam, yal na nu Yàlla musal ci loolu.
Juróom-ñaareel bi: Àttey masaa ñaari saŋ ak ay kawas:
1- Saŋ mooy: lu ñuy sol ci tànk yi ci der walla lu ko niru.
2- Ay kawas nag mooy: lu ñuy sol ci tànk ci leen walla wëttéen ak lu ko niru.
Sàrti masaa ci kaw i saŋ:
1- Mu sol leen ci ginnaaw laab gu mat sëkk.
2- ñu muur tànk yi ba ci dojor yi.
3- Ñu nekk yu laab.
4- Masaa gi nekk ci diir bi ñu tënk.
5- Masaa gi na nekk ci njàppu, du wolif sangu.
6- Saŋ yi ak lu ni mel nekk lu dagan, bu nekkee lu ñu siif ci kàttan walla suwaa ci ku góor ki; masaa ca du dagan, ndaxte lu araam deesu ci maye ag yombal.
Diirub masaa gi:
Ñeel aji-sax ji: benn bis ak guddeem, bu dee aji-tukki ji: ñatti fan ak seen i guddi.
Melokaanu masaa gi:
Day tooyal loxo yi ci ndox, mu masaa ci kaw kawas yi mbaa ñaari saŋ yi, mu tambalee ci catu tànk yi ba ci yeel yi, benn yoon.
Yiy yàq masaa gi:
1- jeexug diirub masaa gi.
2- Summi ñaari kawas yi walla benn ba.
3- Am toj mu mag.
Àtteb masaa ci ay saŋ:
Ag yombal la, te def ko moo gën summi saŋ yi di raxas ñaari tànk yi; ngir jël yombalug Yàlla mu Kawe mi te Tedd, ak roy Yonbi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ak wuute ak ñoñ-bidda yi.
3) Masaa ay bàndaas ak ay lëmas-lëmas ak taf-taf:
Bàndaas: mooy li ñuy takk ci damm-damm yi; muy tabax walla ay bant ak lu ko niru.
Lëmas-lëmas: mooy li ñuy fas ci góom mbaa gaañu-gaañu mbaa lakk-lakk; muy morso ak yu ni mel.
Taf-taf: mooy li ñuy taf ci góom yi walla ci taab yi ngir faju.
Àtteb masaa ci kawam:
Dana dagan: su dee aajo moo nañu ag desam, ci sàrtub mu bañ a weesu bérabu aajo bi.
Du dagan su soxla si jeexee, walla bu summi ga du jur coono mbaa lor.
Melokaanu masaa ci seen kaw:
Day raxas la ko wër, daal di koy masaa ci wet yépp. Te du masaa lu weesu bérabu njàppu bi.
Juróom-ñatteel bi: àttey tiim:
Tiim: mooy masaa kanam gi ak ñaari ténq yi ci pàkk bu sell, jublu ca laab, ci anam gu ñu jagleel.
Àtteem:
Dañoo war a tiim wottee ko jàppu ak sangu bu ñu amul ndox, walla manuñu ko a jëfandikoo.
Xereñte gi tax ñu yoonal ko:
Tiim bokk na ci yi xeetu Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal te musal ko- jagoo, Nekkul woon luñu xamoon ci xeet yi jiitu woon, yaatalug Yàlla la ci kaw xeet wii ak ug rafetalam ci moom.
Anam yi ñu yoonale tiim:
1- Bu amul ndox, moo xam ci dëkk la walla ci tukki, te mu wut ko te amu ko.
2- Bu amee ndox mu mu aajowoo ci naan walla togg, ba su ko jëfandikoo ci laab dana lor aajoom ci ragal mu ragal a mar ci boppam, walla ci beneen doomu Aadama mbaa rab wu ñu wormaal.
3- Bu ragalee ne jëfandikoo ndox mi dina ko lor ci yaramam ngir tawat, walla mu yéexal ag wéram.
4- Bu manut a jëfandikoo ndox ma ngir tawat gu tax manuta yëngu, te amul ku koy jàppal, te mu ragal julli ga raw ko.
5. Su ragalee sedd ci jëfandikoo ndox mi, te amul lu mu ko tàngale, day tiim te julli.
Melow tiim:
Day dóor ñaari loxoom ci suuf sa di aji-tasare baaraam ya, daal di cay masaa kanamam ci biiru baaraam ya, masaa ñaari ténqam ci biir loxoom, te mu matale kanam gi ak ñaari ténq yi ci masaa gi.
Yiy yàq tiim:
1- Am am ndox, bu fekkee ne tiim bi ñàkk ndox moo ko waraloon. Walla mu man ko a jëfandikoo, bu fekkee ne ñàkk ko a man a jëfandikoo moo waraloon tiim gi.
2. Dana yàqu it ci lenn ci liy yàq njàppu, mbaa ci lenn ci liy waral sangu, niki janaba, ak mbërëg, ak meret.
Àtteb ki am ngànt ci jëfandikoo ndox ak tiim:
Képp ku amul ndox ak suuf, walla mu tollu ci melokaan bu mu manut a laalal deram bi ndox walla suuf; kon day julli ci melo wi mu nekk, te du jàppu te du tiim; ndaxte Yàlla du teg benn bakkan lu dul lu mu àttan. Bu ñu nattale woon ne amna ndox ak suuf ginnaaw loolu, walla mu man leen a jëfandikoo, kon du bàmtuwaat julleem ga, ndaxte def na li ko waroon, Ndax waxi Yàlla mu kawe mi:
﴿...فَٱتَّقُواْ ٱللَّهَ مَا ٱسۡتَطَعۡتُمۡ...﴾
﴾...Ragalleen Yàlla seen kem kàttan...﴿ [At-taxaabuni: 16], Ngir waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
«إِذَا أَمَرْتُكُمْ بِأَمْرٍ فَأْتُوا مِنْهُ مَا اسْتَطَعْتُمْ».
«bu ma leen digalee dara, defleen ci lu ngeen man»11.
Njariñ: Bu tiimee ngir janaba, topp mu am ndox; kon day sangu.
Juróom-ñenteel bi: Àttey mbërëg ak meret:
Bu njëkk bi: Mbërëg:
Moom dereet la ju ñu bindaaleek jigéen, day jóge ci biiru butiitu njurukaay gi ci waxtu yees xam. Te ci li ëpp day doon ci weer wu nekk juróom-benni fan walla juróom-ñaar, te man naa dolliku walla mu wàññeeku, Weeru jigéen gi dana yàgg dana gàtt itam; mi ngi aju ci melo wi ko Yàlla binde.
Àttey mbërëg:
Kiy gis mbaax du julli, te du woor, te bu ko defoon du wér.
2- Kiy gis mbaax, dana fay woor gi bu laabee waaye du fay julli gi.
3- araam na ci moom mu wër néeg ba( Kaaba gi), Te du jàng Alxuraan, Te du toog ci Jàkka. 4- Day araam ci boroom këram muy sëy ak moom ba keeroog dereet ja di dog ba mu sangu.
5- Dagan na ci boroom këru kiy gis mbaax mu bànneexu ci moom ci lu dul sëy ci péy ma, niki fóon ak laal ak yu ni mel.
6- Day araam ci boroom këram mu koy fase fekk mi ngi gis mbaax.
Laab mooy dogug dereet ja, bu dereet ja dogee; kon laab na, te mbërëgam jeex na, te sangu war na ko. Topp mu defaat li ñu ko daan tere ngir sababu mbërëg ma.
Su gisee ginnaaw laab ag nëxit walla mboq-mboq, du ko jàppee dara.
Ñaareel bi: meret:
Dereet la joj butitu njurukaay da koy génne ci sababu jur gi ak ginnaawam, te mooy desitu dereet ja desoon ci diirub ëmb bi.
Meret mi ngi mel ni mbërëg ci li daggan, niki bànneexu ci moom ci lu dul péy ga.
Ak ci li ñu araamal: lu ci mel ni sëy, ak woor ak julli, ak fase, ak wër Kaaba ga, ak jàng Alxuraan, ak toog ci jàkka, Ak ci warug sangu bu dereetam dogee, kem ni mu nekke ci mbaax.
War na ci moom mu fay koor gi, waaye du fay julli gi, niki kiy gis mbaax.
Te diiram bi gën a yàgg mooy ñent-fukki fan, Bu dereeti wësin ja dogee laata ñent-fukki fan, kon meretam jeex na, day sangu, julli, te dellu ci mbooleem li ñu ko terewoon ngir sababu meret mi.
Ñaareelu waxtaan wi: Julli:
Li ci njëkk: àttey nodd ak liqaam:
Yoonalees nañu nodd ci at mi njëkk ci gàddaayug Yonnente bi, Sababu yoonal gi: bi xam waxtu yi jafee ci ñoom, dañoo waxtaan ci taxawal am màndarga bu leen koy tegtal, Ñu wan Abdullah Ibn Zayd -yal na ko Yàlla dollee gërëm- nodd gii ci ay nelaw, wahyu wi saxal ko.
Nodd mooy: yégle duggug waxtuw julli wi. Liqaam: mooy yëgle taxawug julli gi.
Nodd ak liqaam farata guy doy la (kifaaya) ci mbooloom góor ñi ñeel julli yi ñu farataal, Ñoom ñaar ci màndargay Lislaam yu fés yi lañu bokk, kon daganul ñu bàyyi leen.
Sàrti nodd:
1- Noddkat bi nekk góor.
2- Nodd gi di luñu toftale.
3- Nodd gi nekk lu méngaloo.
4- Nodd gi nekk ginnaaw duggug waxtu julli wi, Dees na ci settee: nodd gu njëkk gi ci fajar ak ci àjjuma.
Sunnay nodd:
1- Mu teg ñaari baaraamam ci ñaari noppam.
2- Nodd ci njëlbeenu waxtu wi.
3- Gestu ndayjoor ak càmmooñ ci ñaari Hayyahala yi.
4- Mu nekk boroom baat bu neex.
5- Mu teeyal kàdduy nodd gi ci lu dul ag diibal du caagine ag xëcc gu ëpp.
6- Muy taxaw ci wax ju mat ju nekk.
7- Jublu xibla ci jamonoy nodd gi.
Nodd nag fukk ak juróomi wax yu mat la, kem ni Bilaal -yal na ko Yàlla dollee gërëm- daan ko nodde ci teewaayu Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- saa su nekk.
Baati nodd yi:
(Allaahu akbar): ñenti yoon.
(Ashadu an laa ilaaha illal-Laahu): ñaari yoon.
(ashadu anna Muhammadan rasuulul Laahi): ñaari yoon.
(hayya halas salaah): ñaari yoon,
(hayya halal falaah): ñaari yoon.
Topp mu wax: (Allaahu akbar): ñaari yoon.
Daal di koy tëje ci (laa ilaaha illal Laahu): benn yoon.
Te mu dolli ci noddug fajar ginnaaw hayya halal falaah gi: assalaatu xayrun minan nawmi, ñaari yoon; Ndaxte waxtu la wu li ëpp ci nit ñi di nelaw.
Te liqaam, fukk i baat ak benn la, yu ñuy baral la, ngir yëgal ñi teew la, moo tax ajowul a yàggal.
Melokaanam moo nekk nii:
(Allaahu akbar) ñaari yoon.
(Ashadu an laa ilaaha illal Laahu): benn yoon.
(ashadu anna Muhammadan rasuulul Laahi): benn yoon.
(hayya halas salaah): benn yoon.
(hayya halal falaah): benn yoon.
(xadd xaamatis salaatu): ñaari yoon.
(Allaahu akbar) ñaari yoon.
(laa ilaaha illal Laahu): benn yoon.
Sopp nañu ci ku dégg nodd gi mu wax li nodd-kat bi di wax, ba mu des ci (hayya halas salaah) ak (hayya halal falaah), foofu day wax: (laa hawla wa laa xuwwata illaa bil Laahi), Topp mu julli ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-. Topp ginnaaw loolu mu wax:
«اللهمَّ رَبَّ هَذِهِ الدَّعْوَةِ التَّامَّةِ، وَالصَّلَاةِ القَائِمَةِ، آتِ مُحَمَّدًا الوَسِيلَةَ وَالفَضِيلَةَ، وَابْعَثْهُ مَقَامًا مَحْمُودًا الَّذِي وَعَدْتَهُ، إِنَّكَ لَا تُخْلِفُ الْمِيعَادَ».
«Allaahumma Rabba haazihid dahwatit taammati, wassalaatil xaa imati, aati Muhammadan Alwasiilata walfadiilata, wabhashu maxaaman mahmuudan allazii wahadtahu, innaka laa tukhliful miihaad»12.
Mu daal di wax:
«رَضِيتُ بِاللَّهِ رَبًّا، وَبِالْإِسْلَامِ دِينًا، وَبِمُحَمَّدٍ ﷺ نَبِيًّا».
«radiitu bil Laahi rabban, wa bil islaami diinan, wa bi Muhammadin sallal Laahu halayhi wa sallama nabiyyan»13.
Tere nañu génn ci jàkka ji ginaaw nodd gi ci lu dul ngànt walla yéeney dellusi.
Bu ñuy boole ñaari julli, benn nodd doy na, te ñu taxawal liqaam ñeel julli gu nekk.
Ñaareel bi: solos julli ak ngëneelam:
Julli mooy ponku Lislaam bi gën a feddaliku ginnaaw ñaari seede yi. Te amna wàccuwaay bu ñu ko jagleel, ndaxte Yàlla, ca asamaan la ko warale ci Yonnenteem bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci guddig yéeg ga ca asamaan, Loolu di tegtale ag màggam ak feddalikug waram ak darajaam fa Yàlla mu màgg mi.
Ay Hadiis yu bari ñëw na ci ngëneelam ak ug waram ci kenn ku nekk, Te ag Farataam lu ñu xam la diiney Lislaam ci lu manul ñàkk.
Bokk na ci liy tegtale ag waram ak ug feddalikoom: ay tegtal yu bari yu nekk ci Téere Yàlla bi ak Sunnas Yonnente bi, bokk na ci:
1- waxu Yàlla jii:
﴿...إِنَّ ٱلصَّلَوٰةَ كَانَتۡ عَلَى ٱلۡمُؤۡمِنِينَ كِتَٰبٗا مَّوۡقُوتٗا﴾
﴾...Julli de lu ñu wutal waxtu la ñeel way-gëm ñi﴿ [An-Nisaa-i : 103]. maanaam: luñu farataal la ci waxtu yi Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc- leeral.
2- ak waxu Yàlla mu kawe mi:
﴿وَمَا أُمِرُوا إِلَّا لِيَعْبُدُوا اللَّهَ مُخْلِصِينَ لَهُ الدِّينَ حُنَفَاءَ وَيُقِيمُوا الصَّلَاةَ...﴾
﴾digaluñu leen lu dul ñu jaamu Yàlla te sellal diine ji ñeel ko, te set wicc ci bokkaale, tey taxawal julli...﴿ [Al-Bayyinatu: 5].
3- Ak waxu Yàlla mu kawe mi:
﴿فَإِنْ تَابُوا وَأَقَامُوا الصَّلَاةَ وَآتَوُا الزَّكَاةَ فَإِخْوَانُكُمْ فِي الدِّينِ...﴾
﴾Bu ñu tuubee tey taxawal julli di joxe asaka, kon nag seen mbokk lañu ci diine ji...﴿ [At-Tawba : 11].
4- Jële nañu ci Jaabir -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«إِنَّ بَيْنَ الرَّجُلِ وَبَيْنَ الشِّرْكِ وَالْكُفْرِ تَرْكُ الصَّلَاةِ».
«li dox ci diggante nit ki ak bokkaale ak kéefar mooy bàyyi julli»14.
5- Jële nañu ci Buraydata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«العَهْدُ الَّذِي بَيْنَنَا وَبَيْنَهُمُ الصَّلَاةُ، فَمَن تَرَكَهَا فَقَدْ كَفَرَ».
«kóllare gi dox ci sunu diggante ak ñoom yéefar yi mooy julli, ku ko bàyyi weddi na»15.
Boroom xam-xam yi dëppoo nañu ci ne képp ku weddi ag waram yéefar la. Waaye ku ko bàyyi ngir tayyeel ak woyofal ko, li gën a wér mooy ag kéefaram, ndax Hadiis bu wér bi jiitu, ak li Saahaaba yi dëppoo ci loolu.
Ñatteel bi: Sàrti julli:
1- Duggug waxtuw julli gi:
Ndax waxi Yàlla mu kawe mi:
﴿...إِنَّ ٱلصَّلَوٰةَ كَانَتۡ عَلَى ٱلۡمُؤۡمِنِينَ كِتَٰبٗا مَّوۡقُوتٗا﴾
﴾...Julli de lu ñu wutal waxtu la ñeel way-gëm ñi﴿ [An-Nisaa-i]. Maanaam: luñu farataal la ci ay waxtu yu ñu tënk.
Waxtuy julli yi ñu farataal ñoo ngi nii:
A- Fajar: mu tàmbalee ci fenkug fajar ba ci fenkug jant bi.
b- Tisbaar: Mi ngi tàmbalee bi jant bi di jeng ba keroog keru lu nekk di tolloo ak moom ci guddaay.
C- Tàkkusaan: mu dale ca jeexug waxtuw tisbaar ga ba ci mboqi-mboqi jant bi, waxtuw Darooraam mi ngi yem ci sowug jant bi.
D- Timis: Mi ngi dale ci sowug jant bi ba ci fàddug xonq-xonq yi.
E- Gee: Mi ngi tàmbalee bu waxtuw Timis gi jeexee, di jeexe ci xaaju guddi gi.
2- Muur awra:
Te mooy li war a muuru, te feeñam ñaaw te ñu ciy rus, Awray góor mooy li dale ci jumbaxam ba ci wóomam, Jigéen nag léppam awra la ci julli, ba mu des xar kanamam, Te day muur xar kanamam su nekkee ci teewaayu góor yoo xam ne ay jàmbur lañu ci moom.
3- Moytu sobe:
Sobe mooy: tilim gu ñu jagleel gu xeetam di teree julli; niki saw ak xayta ak dereet, ak yu ni mel, dina nekk ci yaram ci bérab ak ci yére.
4- Jublu ci xibla:
Xibla mooy Kaaba gu tedd ga, ñu tudde ko Xibla ngir li ko nit ñi di jublu.
Kon, julli du wér bu amul jublu xibla, Ndax waxi Yàlla mu kawe mi:
﴿...وَحَيۡثُ مَا كُنتُمۡ فَوَلُّواْ وُجُوهَكُمۡ شَطۡرَهُ...﴾
﴾...fu ngeen man di nekk na ngeen jublu ci wetam...﴿ [Al-Baqara: 144].
5- Yéene:
Ci làkk mooy: jublu, ci Sariiha nag: mooy dogu ci def ag jaamu Yàlla ngir jegeñ-jegeñlu Yàlla mu kawe mi. Bérabam mooy xol bi, kon soxlawul ñu koy wax, ndax bidda la.
Ñenteel bi: ponki julli:
Ponk yi fukk la ak ñent:
Ponk bu njëkk bi mooy: Taxaw ci ku ko man.
Ndax waxi Yàlla mu kawe mi:
﴿...وَقُومُواْ لِلَّهِ قَٰنِتِينَ﴾
﴾... Nangeen taxaw temm di way-jaamu Yàlla ﴿ [Al-Baqara : 238], Ak hadiisu Imraan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu yéegal ko ba ci Yonnente bi ne:
«صَلِّ قَائِمًا، فَإِن لَمْ تَسْتَطِعْ فَقَاعِدًا، فَإِن لَمْ تَسْتَطِعْ فَعَلَى جَنْبٍ».
«jullil taxaw, boo ko manul nga toog, boo ko manul nga wetu»16.
Bu manul a taxaw ndax feebar, mu julli toog walla mu wetu, Ñi bokk àtte ak ki feebar ñoo di: ku ragal, ak ku ñàkk yére, ak ki soxlaa toog walla tëdd ngir paj gu laaj mu bañ a taxaw. Naka noonu it dees na dogal ngànt ci taxaw gi kiy julli ci ginnaaw imaam bu sax bi te moom mënatul, kon bu imaam bi toogee julli, ñi ci ginnaawam itam dañuy toog julli ngir topp seen imaam. Dagan na toog di def naafila, donte man naa taxaw, waaye yool bi du nekk kem yoolu ki taxaw.
Ponku ñaareel bi: mooy kàbbaru armal ca njëlbeen ga:
Ngir waxu Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
«ثُمَّ اسْتَقْبِلِ الْقِبْلَةَ، وَكَبِّرْ».
«Topp nga jublu xibla te kàbbar»17.
Waxiin wi mooy mu wax: (Allaahu akbar), leneen lu dul moom doyul.
Ponku ñaareel bi: Jàng Faatiha:
Ngir waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
«لَا صَلَاةَ لِمَنْ لَمْ يَقْرَأْ بِفَاتِحَةِ الْكِتَابِ».
"ku jàngul faatiha amul julli"18.
Ponku ñenteel bi: Rukkoo ci bépp ràkka:
Ndax waxi Yàlla mu kawe mi:
﴿يَاأَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا ارْكَعُوا وَاسْجُدُوا...﴾
﴾Yéen ñi gëm Rukooleen sujóotleen...﴿
[Al-Hajji : 77].
Ponku juróomeel bi ak bu juróom-benneel bi:
Siggi jóge ca Rukoo ba, ak yemoo taxaw ni mu meloon laata Rukkoo bi, ndaxte Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daa saxoon ci def ko.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ki ñaawaloon julleem gi:
«ثُمَّ ارْفَعْ حَتَّى تَعْتَدِلَ قَائِمًا».
«Nga daal di yëkkëtiku ba taxaw temm»19.
Ponku juróom-ñaareel bi: Sujjóot ci juróom-ñaari cér yi:
Te mooy jëh bi mu ànd ak bakkan bi, ak ñaari loxo yi, ak ñaari wóom yi, ak cati waaraam i ñaari tànk yi, Ngir waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
«أُمِرْنَا أَنْ نَسْجُدَ عَلَى سَبْعَةِ أَعْظُمٍ: الجَبْهَةِ، وَأَشَارَ بِيدِهِ عَلَى أَنْفِهِ، وَالكَفَّيْنِ، وَالرُّكْبَتَيْنِ، وَأَطْرَافِ القَدَمَيْنِ».
«digal nañu nu nuy sujjóot ci juróom-ñaari cér: jëh bi, mu daal di junj loxoom ci bakkanam, ak ñaari ténq yi, ak ñaari wóom yi, ak cati ñaari ndëggu yi»20.
Ponku juróom-ñatteel bi: Yëkkëtiku bawoo ci sujjóot bi toog ci diggante yaar i sujjóot yi:
Ngir hadiisu Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
«كَانَ النَّبِيُّ ﷺ إِذَا رَفَعَ رَأْسَهُ مِنَ السَّجْدَةِ، لَمْ يَسْجُدْ حَتَّى يَسْتَوِيَ جَالِسًا».
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan yëkkëti boppam jóge ca sujjóot ba, du sujjóot ba keroog muy toog ba jub21.
Ponku juróom-ñenteel bi: dal ci ponk yépp:
Te mooy dal gi, ak lu mu néew-néew, ngir waxu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ñeel ki ñaawaloon ag julleem:
«حَتَّى تَطْمَئِنَّ».
"ba nga dal"22.
Ñaari ponk yi: bu fukkeel bi ak bu fukkeell bi ak benn:
Taaya bu mujj bi ak toogaayam: ndax hadiisu Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu askanale Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
«إِذَا صَلَّى أَحَدُكُمْ فَلْيَقُلْ: التَّحِيَّاتُ لِلَّهِ وَالصَّلَوَاتُ وَالطَّيِّبَاتُ، السَّلَامُ عَلَيْكَ أَيُّهَا النَّبِيُّ وَرَحْمَةُ اللَّهِ وَبَرَكَاتُهُ، السَّلَامُ عَلَيْنَا وَعَلَى عِبَادِ اللَّهِ الصَّالِحِينَ، أَشْهَدُ أَنْ لَا إِلٰهَ إِلَّا اللَّهُ وَأَشْهَدُ أَنَّ مُحَمَّدًا عَبْدُهُ وَرَسُولُهُ».
«Su kenn ci yeen di julli, na wax: Attahiyyaatu lil Laahi, wassalawaatu, wattayyibaatu, assalaamu halayka ayyuhan Nabiyyu wa rahmatul Laahi wa barakaatuhuu, assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahi assaalihiina, ashadu an laa ilaaha illal Laahu, wa ashadu anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu»23.
Ponk fukkeel bi ak ñaar: Julli ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci taaya ji mujj:
Mooy mu wax:
«اللَّهُمَّ صَلِّ عَلَى مُحَمَّدٍ».
«Allaahumma salli halaa Muhammadin»24, Lu tege ci loolu sunna la.
Ponku fukkeel bi ak ñàtt: toftale ponk yi:
Ndaxte Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc da ko daan toftale, Te dafa wax ne:
«صَلُّوا كَمَا رَأَيْتُمُونِي أُصَلِّي».
"julleeleen kem ni ngeen may gise may jullee"25. Te jàngal na ko ki ñaawaloon ci julleem gi, ci ag toftale ci «topp ca».
Ponk fukkeel bi ak ñent: Sëlmël:
Ndax waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
««وَخِتَامُهَا التَّسْلِيمُ».
«ag tëjam mooy sëlmal gi», Ak waxam ji:
«وَتَحْلِيلُهَا التَّسْلِيمُ».
«ag feccikoom mooy sëlmal gi»26.
Juróomeel bi mooy: yi war ci julli.
Yi war ci julli juróom-ñatt la:
1- Mbooleem kàbbar yi ba mu des kàbbaru armal.
2) Wax: «subhaana rabbiyal asiim» benn yoon ci rukoo, Sunnaal nañu mu wax ko ñatti yoon, loo lu mooy li gëna néew ci lu mat, Mbaa mu wax ko fukk i yoon te mooy la ca gën a kawe.
3) Wax: «samihal Laahu liman hamidahu» ci siggi gi jóge ci Rukkoo bi; ñeel imaam ak kiy julli moom dong.
4) Wax: «rabbanaa walakkal hamdu» ci siggi ba yemoo jóge ca Rukoo ba.
5) Wax: «subhaana rabbiyal ahlaa» benn yoon ci sujóot bi, Sunnaal nañu mu wax ko ñatt yoon.
6) Wax: «rabbi ixfir lii» benn yoon ci diggante ñaari sujóot yi, Sunnaaal nañu mu wax ko ñàtti yoon.
7) Taaya ju njëkk ji; te mooy mu wax:
«التَّحِيَّاتُ لِلَّهِ، وَالصَّلَوَاتُ وَالطَّيِّبَاتُ، السَّلَامُ عَلَيْكَ أَيُّهَا النَّبِيُّ وَرَحْمَةُ اللَّهِ وَبَرَكَاتُهُ، السَّلَامُ عَلَيْنَا وَعَلَى عِبَادِ اللَّهِ الصَّالِحِينَ، أَشْهَدُ أَنْ لَا إِلٰهَ إِلَّا اللَّهُ وَأَشْهَدُ أَنَّ مُحَمَّدًا عَبْدُهُ وَرَسُولُهُ».
«Attahiyyaatu lil Laahi, was salawaatu, wat tayyibaatu, assalaamu halayka ayyuhan Nabiyyu wa rahmatul Laahi wa barakaatuhuu, assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahi assaalihiina, ashadu an laa ilaaha illal Laahu, wa ashadu anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu»27.
Toogaayu taaya ju njëkk ji.
Juróom-benneel bi: sunnay julli.
Sunay julli, bàyyi leen yàqul julli, Moom nag ñaari xaaj la: sunnay wax yi, ak sunnay jëf yi.
Li ci njëkk: sunnay wax yi:
1- Ñaanug ubbee julli gi, amna ay anam, bokk na ci:
«سُبْحَانَكَ اللَّهُمَّ وَبِحَمْدِكَ، وَتَبَارَكَ اسْمُكَ، وَتَعَالى جَدُّكَ، وَلَا إِلٰهَ غَيْرُكَ» .
«Subhaanaka allaahumma wa bi hamdika, wa tabaaraka ismuka, wa tahaala jadduka, wa laa ilaaha xayruka»28 .
2- Muslu ci Saytaane laata Faatixa, Mooy mu wax: «Ahuusu bil-Laahi minas Saytaanir rajiimi».
3- Wax mu tàmbalee ci tudd turu Yàlla, Mooy mu wax: «Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim».
4- lépp lu dolleeku ci genn sàbbaal gi ci Rukkoo yi ak sujjóot yi.
5- lépp lu dolleeku ci jenn wax ji
«رَبِّ اغْفِرْ لِي».
"Rabbi ixfir lii" Ci diggante yaari sujjóot yi.
6- Wax:
«مِلْءَ السَّمَاوَاتِ، وَمِلْءَ الْأَرْضِ، وَمِلْءَ مَا بَيْنَهُمَا، وَمِلْءَ مَا شِئْتَ مِنْ شَيْءٍ بَعْدُ».
"mil-as samaawaati, wa mil-al ardi, wa mil-a maa baynahumaa, wa mil-a maa sita min say-in bahdu", Ginnaaw bu ñu waxee:
«رَبَّنَا ولَكَ الحَمْدُ».
«rabbanaa walakal hamdu»29.
7- Jàng ci ginnaaw faatiha.
8- Wax:
«اللَّهُمَّ إِنِّي أَعُوذُ بِكَ مِنْ عَذَابِ جَهَنَّمَ، وَمِنْ عَذَابِ الْقَبْرِ، وَمِنْ فِتْنَةِ الْمَحْيَا وَالْمَمَاتِ، وَمِنْ فِتْنَةِ الْمَسِيحِ الدَّجَّالِ».
«allaahumma innii ahuusu bika min hasaabi Jahannama, wa min hasaabil xabri, wa min fitnatil mahyaa wal mamaati, wa min fitnati Al-Masiihi Al-Dajjaal»30. Ak gépp ñaan gu dolleeku ca loola ci taaya gu mujj gi.
Ñaareel bi: sunnay jëf yi:
1- Yëkkëti ñaari loxo yi ba mu tolloo ak ñaari mbagg yi walla ñaari nopp yi ci ñenti bérab:
A- Ci kàbbaru armal gi.
B- ci Rukoo bi.
C- Ci siggi ga bawoo ci rukoo bi.
D- Buy jug jëm ca ñatteelu ràkka ba.
2- teg loxo ndayjoor ci kaw loxo càmmooñ ci kaw dënn bi, ci taxawaay bi, njëkk muy Rukoo ak ginnaaw Rukoo ba.
3- Xool ci bérabu sujóot bi.
4- soreele ñaari përëgi loxo yi ak ñaari wetam ca sujjóot ba.
5- Soreele biir ba ak ñaari poojam ci ñaari sujjóot yi.
6- Toog ci kaw tànku càmmooñam te samp bu ndayjoor ba ci bépp toogaay ci biir julli gi, ba mu des ci taaya bu mujj bi ci julliy ñatti ràkka ak ñenti ràkka yi.
PP7- Lal tànku càmmooñam ci suufu tànku ndayjooram teg ay toogoom ci suuf ci taaya gu mujj gi ci jullig ñatti ràkka walla gu ñenti rakka.
Juróom-ñaareel bi: melow julli:
1- Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan taxaw ci julli, da daan jublu xibla, yëkkëti loxoom, jubale biir baaraam yi xibla, daal di wax:
«اللهُ أَكْبَرُ».
«Allaahu Akbar»
2- topp mu japp loxo càmmooñam ci loxo ndayjooram teg leen ci kaw dënnam.
3- Ginnaaw ba mu jàng ñaan giñuy ubbee julli, te daawul sax ci benn xeetu ñaan dong, Ñaani ubbee yi sax yépp jóge ci moom, dagan na ñu ubbee ci ñoom, bokk na ci yooyu:
«سُبْحَانَكَ اللَّهُمَّ وَبِحَمْدِكَ، وَتَبَارَكَ اسْمُكَ، وَتَعَالى جَدُّكَ، وَلَا إِلٰهَ غَيْرُكَ».
«Subhaanakal Laahumma wa bi hamdika, wa tabaaraka ismuka, wa tahaalaa jadduka, wa laa ilaaha xayruka».
4- Topp mu wax:
«أَعُوذُ بِاللَّهِ مِنَ الشَّيْطَانِ الرَّجِيمِ، بِسْمِ اللَّهِ الرَّحْمَٰنِ الرَّحِيمِ».
«Ahuusu bil-Laahi minas Saytaanir rajiimi, Bismil Laahir Rahmaanir Rahiimi».
5- topp mu jàng faatiha, daal di wax: «aamiin».
6- Topp mu jàng li jàppandi ci Alxuraan, Mu Yëkkëti njàng mi ci jullig fajar, ak ci ñaari ràkka yu njëkk ya ci jullig timis ak gee, Mu yelu njàng ma ci yu dul yooyu. Day guddal ràkka bu njëkk bi ci julli gu ne mu gën a gudd bu ñaareel bi.
7- topp mu yëkkëti ñaari loxoom kem ni mu ko defe woon ci ubbi gi, Mu daal di wax: «Allaahu Akbar», Mu sëgg Rukoo, Mu teg ay yoxoom ci kaw ay wóomam, xàjjale ay waaraamam, mu dëgëral leen, dal di tàllal ndiggam, def boppam mu tolloo ak moom; du ko yëkkëti te du ko suufeel, Mu wax:
«سُبْحَانَ رَبِّيَ الْعَظِيمِ» مرةً.
«subhaana Rabbiyal Asiim» benn yoon, Gën jaa tuuti ci lumu matale mooy ñatti yoon, ni mu jàllee.
8- Mu yëkkëti boppam, daal di wax:
«سَمِعَ اللَّهُ لِمَنْ حَمِدَهُ».
«Samihal Laahu liman hamida», Mu Yëkkëti ñaari loxoom kem ni mu leen di yëkkëtee buy Rukoo.
9- Bu taxawee ba yemoo mu wax:
«اللَّهُمَّ رَبَّنَا وَلَكَ الْحَمْدُ، حَمْدًا كَثِيرًا طَيِّبًا مُبَارَكًا فِيهِ، مِلْءَ السَّمَاءِ، وَمِلْءَ الْأَرْضِ، وَمِلْءَ مَا بَيْنَهُمَا، وَمِلْءَ مَا شِئْتَ مِنْ شَيْءٍ بَعْدُ، أَهْلَ الثَّنَاءِ وَالْمَجْدِ، أَحَقُّ مَا قَالَ الْعَبْدُ، وَكُلُّنَا لَكَ عَبْدٌ، لَا مَانِعَ لِمَا أَعْطَيْتَ، وَلَا مُعْطِيَ لِمَا مَنَعْتَ، وَلَا يَنْفَعُ ذَا الْجَدِّ مِنْكَ الْجَدُّ».
"Allaahumma Rabbanaa wa lakal hamdu, hamdan kasiiran tayyiban mubaarakan fiihi, mil-as samaawaati, wa mil-al ardi, wa mil-a maa baynahumaa, wa mil-a mii sita min say-in bahdu, ahlas sanaa-i wal hamdi, ahaqu maa xaalal habdu, wa kullunaa laka habdun, laa maaniha limaa ahtayta, wa laa muhtiya limaa manahta, wa laa yanfahu saljiddi minka aljiddu"31. Daan na guddal yemoo gi.
10- Topp mu kàbbar, daal di sujóot, Te du yëkkëti ay loxoom, Day sujjóot ci jëwam ak bakkanam, ak ay yaari tenqam, ak yaari wóomam, ak ay cat i waaraami tànkam, Mu jubale baarami loxoom ak baarami taankam ci xibla bi, Day yemoo ci sujjóotam, day dëgëral jëwam ak bakkanam ci suuf, Day sukkandiku ci ay ténqam, daal di yëkkëti ay concam, Mu soreele ñaari përagam ci ñaari wetam, Mu Yëkkëti biiram mu sori luppam yi, Luppam yi it sori yeelam yi, Mu wax ci sujjóotam:
«سُبْحَانَ رَبِّيَ الأَعْلَى».
«subhaana Rabbiyal ahlaa» benn yoon, Li gën a néew te mat mooy ñatti yoon, kem ni mu jàllee. Mu ñaan ci ñaan yi rot.
11- Topp mu yëkkëti boppam daal di wax: «Allaahu akbar», mu lal tànku càmmooñam, toog ci, samp tànku ndayjooram, Mu teg ñaari loxoom ci kaw ñaari luppam topp mu wax:
«اللَّهُمَّ اغْفِرْ لِي، وَارْحَمْنِي، وَاجْبُرْنِي، وَاهْدِنِي، وَارْزُقْنِي».
"Allaahumma ixfirlii, warhamnii, wajburnii, wahdinii, warsuqnii"32.
12- Topp mu kàbbar daal di sujóot, mu def ci ñaareel bi ni mu ko defee woon ci bu njëkk bi.
13- Topp mu yëkkëti boppam daal di kàbbar, mu jóge ci kanamu yaari tànkam, sukkandiku ci yaari wóomam ak yaari luppam.
14- Bu taxawee temm nag; daal di tàmbalee jàng. Mu julli ràkka ñaareel bi kem ni mu jullee bu njëkk bi.
15- Topp mu toog ci taaya ju njëkk ji, kem ni muy tooge ci diggante ñaari sujjóot yi, Mu teg loxo ndayjooram ci kaw luppu ndayjooram, teg loxo càmmooñam ci kaw luppu càmmooñam, Mu teg baaraamu déyu loxo ndayjooram ci kaw baaraamamu digg bi, mu def ko mu mel ni ab wërngal, Muy junj ci baaraamu sànnikaayam, di ko xool, Mu wax:
«التَّحِيَّاتُ لِلَّهِ وَالصَّلَوَاتُ وَالطَّيِّبَاتُ، السَّلَامُ عَلَيْكَ أَيُّهَا النَّبِيُّ وَرَحْمَةُ اللَّهِ وَبَرَكَاتُهُ، السَّلَامُ عَلَيْنَا وَعَلَى عِبَادِ اللَّهِ الصَّالِحِينَ، أَشْهَدُ أَنْ لَا إِلٰهَ إِلَّا اللَّهُ وَحْدَهُ لَا شَرِيكَ لَهُ، وَأَشْهَدُ أَنَّ مُحَمَّدًا عَبْدُهُ وَرَسُولُهُ».
«Attahiyyaatu lil Laahi, was salawaatu, wat tayyibaatu, assalaamu halayka ayyuhan Nabiyyu wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu, assalaamu halaynaa wa halaa hibaadil Laahi asaalihiina, ashadu an laa-i-Laaha illal Laahu wahdahu laa shariika lahu, wa ashadu anna Muhammadan habduhu wa rasuuluhu» Daan na woyofal taaya jii.
16- Topp mu jug daal di kàbbar, mu julli ràkkab ñatteel bi ak bu ñenteel bi, te mu gën leen a woyofal ci ñaari ràkka yu njëkk ya. Mu jàng ci ñoom ñaar Faatiha.
17- mu toog ci taaya ju mujj ji daal di Tawarruk, Tawarruk mooy: mu lal tànku càmmooñam, génne ko ci wetu ndayjoor bi, samp tànku ndayjoor bi, teg ag toogoom ci suuf.
18- Topp mu taaya taaya ju mujj ji, moom nag: day mel ni taaya ju njëkk ji, Mu dolli ca:
«اللَّهُمَّ صَلِّ عَلَى مُحَمَّدٍ وَعَلَى آلِ مُحَمَّدٍ، كَمَا صَلَّيْتَ عَلَى آلِ إِبْرَاهِيمَ، إِنَّكَ حَمِيدٌ مَجِيدٌ، وَبَارِكْ عَلَى مُحَمَّدٍ وَعَلَى آلِ مُحَمَّدٍ، كَمَا بَارَكْتَ عَلَى آلِ إِبْرَاهِيمَ، إِنَّكَ حَمِيدٌ مَجِيدٌ».
«Allaahumma salli halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin, kamaa sallayta halaa aali Ibraahiima, innaka hamiidun majiidun, wa baarik halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin, kamaa baarakta halaa aali Ibraahiima, innaka hamiidun majiidun».
19- mu sàkkoo muslu ci Yàlla ci mbugalum Jahannama, ak ci mbugalum bàmmeel, ak ci fitnay dund ak dee, ak ci fitnay Masiihud Dajjaal. Mu ñaan ci ñaan yi rot ci Alxuraan ak Sunna.
20- mu sëlmël ci ndayjooram, daal di wax:
«السَّلَامُ عَلَيْكُمْ وَرَحْمَةُ اللَّهِ».
«Assalaamu halaykum wa rahmatul Laah», Ak ci càmmooñam it kem noonu; Day tàmbalee sëlmël gi ci wetu xibla bi, jeexale ko ci bu geestu gi matee.
Juróom-ñatteel bi: yi ñu sib ci julli:
1- geestu ci lu dul aajo.
2- Yëkkëti bët yi jëme asamaan.
3- gëmm bët yi ci lu dul aajo.
4- lal ñaari loxo yi ci suuf ca sujjóot ba.
5- Muur sa gémmiñ ak sa bàkkan ci lu dul aajo.
6- Julli safa saw mbaa xayta, walla ag lekk gu mu xemmeem teew.
7- di fomp jëham ak bakkanam ci li taq ci jeexitali sujóot gi, fomp gi nag ci ginnaaw bu julli gi jeexee loolu aayul.
8- Wéeru ci miir ak lu ni mel bu ñuy taxaw, ci lu dul aajo.
Juroom-ñenteel bi mooy: yiy yàq julli:
1- lekk ak naan.
2- Wax ju génn julli gi.
3- reetaan ak xaqataay.
4- Bàyyi benn ci ponkam ya walla benn ci warteefam ya te tay ko.
5- Dolli ab ponk walla ab rakka te tay ko
6- Sëlmël njëkk imaam bi.
7- Yëngatu yu bari te toftaloo yu bokkul ci julli gi ci lu dul aajo.
8- Def luy wuute ak benn ci sàrti julli gi; niki njàpp mi toj ak feeñal awra te tay ko ak wëlbatiku gu bari ci xibla gi ci lu dul lu manut a ñàkk, ak dog yéene ji.
10- fukkeel bi: sujjóotu njuumte:
Njuumté: fàtte la, te Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- juumoon na ci julli; ndaxte njuumté ci melokaanu nit la bokk, Te jàddam gi bokk na ci matalug xéewëlu Yàlla ci xeetam ak matalug seen diine, ngir ñu roy ci moom ci li mu leen yoonal bu ñu jàddee.
Sabab yi ñu yoonalal sujjóotu njuumte:
1- anam gu njëkk gi:
Dolli ci julli gi, te mooy yokk ay jëf mbaa yokk ay wax:
A- Dolli jëf yi: Bu dee dolli gu bokk ci jëfi julli gi la, lu ci mel ni taxaw ca bérabu toog ba, ak toog ca bérabu taxaw ga, walla mu dolli ab rukoo walla ab sujóot, bu defee loolu te fekk dafa juum; kon day sujóotal njuumte gi.
b- Dollikug wax yi: lu melni jàng ci Rukoo ba ak sujjóot ba,
Bu defee loolu, kon sopp nañu ci moom sujjóotu njuumte.
2- anamu ñaareel gi:
Wàññi ci julli ngir njuumte, day ame ci ñaari mbir:
A- Bàyyi benn ponk: su dee ponk boobu mooy kàbbaru armal gi, kon julleem gi fasoogul, te sujjóotu njuumte du ca doy. Bu dee nag ponk la bu dul kàbbaru armal, ni Rukoo walla sujjóot, te mu fàttaliku laata muy door di jàng beneen ràkka; kon war na dellu, mu def ko ak li ci topp.
Bu ko fàttalikoo ginnaaw ba mu dooree njàng mi ci beneen ràkka, kon ràkka ba mu ko bàyyee woon day yàqu, ràkka bi ci topp mooy taxaw ci bérabam.
b- Bàyyi lu war: niki fàtte taaya bu njëkk bi, walla sàbbaal gi ci rukoo gi. Ci anam gii: day sujjóotal njuumte gi.
3- Ñatteelu anam gi: sikk-sàkka:
Misal: bu kenn sikk-sàkkaa ci jullig tisbaar, ndax ñatt la julli walla ñent, ci anam gii nag:
A- Bu dara lëngee ci moom; day jëfe loolu, daal di sujjóotal njuumte gi.
B- Bu dara lëngul ci moom; dafay tabax ci li ko wóor, te def sujjóotu njumte.
Bu sikk-sàkka ga amee ginnaaw julli gi, walla mu doon ku bari sikk-sàkka, kon du faale sikk-sàkka googu.
Ab Njariñ: Sujjóotu njuumte, njëkk sëlmël gi la: su fekkee ci wàññi la, walla ci sikk-sàkka te dara notul fi moom. Mu nekk ci ginnaaw sëlmël gi: su dee ci dolli la, walla ci sikk-sàkka gu ñu jëfe gi li gën jamtal, Mbir mi ci loolu nag lu yaatu la, bu soobee Yàlla mu kawe mi.
Fukkeel bi ak benn mooy: Waxtu yi ñu aaye ku ci julli:
Liy cosaan mooy daganug julli ci waxtu yépp, Waaye nag Sariiha dafa tere ku julli ci yenn waxtu yi, ñoom nag ñooy yii:
1- Ginnaaw jullig Fajar ba keroog Jant bi di fenk, te mu yëkkëtiku luy tolloo ak ab xeej ci gisu bët.
2- bu Jant bi nekkee ci digg asamaan ba keroog muy jeng, te mooy waxtu wi gën a gàtt ci waxtu yi ñu aaye ku ci julli.
3- Ginnaaw jullig Tàkkusaan ba keroog jant bi di so, te mooy bi gën a guddu ci waxtuy tere yi.
Julli yi dagan a def ci waxtuy tere ya:
1- Di fay farata yu faat.
2- Julli yiy am sabab, niki: nuyu jàkka, ak ñaari ràkkay tawaaf, ak jullig muurug jant bi, ak julleeg néew.
3- Fay sunnag fajar ginnaaw julli fajar.
Fukkeel ba ak ñaar: jullig mbooloo:
Te moom màndarga mu màgg la ci màndargay Lislaam, te mooy jullig mbooloo ci jàkka yi Jullit ñi dëppoo nañu ci ne jooxe julliy juróom ci jàkka yi bokk na ci jaamu Yàlla yi ñu gën a feddali ak topp Yàlla yi gën a màgg, te mooy sémboli Lislaam yi gën a màgg.
1- Àttey jullig mbooloo:
Jullig mbooloo lu war la ci jàkka ji ñeel julliy juróom yi ci kaw góor ñi am kàttan gi, ci teewaay ak ci tukki, Ci jamonoy kóolute ak jomonoy ragal, muy faratay jëm.
Liy tegtale warug jullig mbooloo: Alxuraan ak Sunna, ak jëfu jullit ñi, maas ga di ko jële ci yeneen i maas, ñi mujj jële ko ca ña jiitu.
Bu dee ci alxuraan mooy: waxi Yàlla jii:
﴿وَإِذَا كُنتَ فِيهِمۡ فَأَقَمۡتَ لَهُمُ ٱلصَّلَوٰةَ فَلۡتَقُمۡ طَآئِفَةٞ مِّنۡهُم مَّعَكَ...﴾
﴾ boo nekkee fi ñoom, nga taxawal julli gi, na ab kurel ci ñoom taxaw ànd ak yaw...﴿ [An-Nisaa-i: 102]. Ndax aaya bi day tegtale ne warug jullig mbooloo lu feddalku la, Ndax mayeesul jullit ñi ñu bàyyi ko ci jamonoy ragal, Bu fekkoon ne du lu war, kon ngànt li gën a yey ci ñu bàyyi ko mooy ngàntug ragal. Bàyyi jullig mbooloo ak di ci tàyyeel, ci melo naaféq yi gën a fés la bokk.
Bu dee ci Sunna: hadiis yu bari la, bokk na ca:
Li ñëw ci Sahiihu Muslim
أَنَّ رَجُلًا أَعْمَى قَالَ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، لَيْسَ لِي قَائِدٌ يَقُودُنِي إِلَى الْمَسْجِدِ، فَسَأَلَهُ أَنْ يُرَخِّصَ لَهُ أَنْ يُصَلِّيَ فِي بَيْتِهِ، فَرَخَّصَ لَهُ، فَلَمَّا وَلَّى دَعَاهُ فَقَالَ: «هَلْ تَسْمَعُ النِّدَاءَ؟» قَالَ: نَعَمْ، قَالَ: «فَأَجِبْ».
Benn gumba dafa ne: yaw Yonnente Yàlla bi, man de amuma ku may wommat yóbb ma ca jàkka ja, mu sàkku ci moom mu yombalal ko muy jullee ci këram, mu yombalal ka ko. Ba mu wëlbatikoo rekk mu woo ko, daal di ne ko: «ndax danga dégg nodd gi?» Mu ne ko: waaw, mu ne ko: «kon nag wuyujil»33.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- digal ko mu teew ca jàkka ja ngir jullig mbooloo mi te wuyu woote bi, ànd ak ne gumba la ak coono bi mu ciy daj. Loolu di tegtale warug jullig mbooloo.
2- Li ñuy dabe mbooloo mi:
Dees na dabe jullig mbooloo ci dab ab ràkka ci julli ga ànd ak imaam bi. Ndax waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
«مَنْ أَدْرَكَ رَكْعَةً مِنَ الصَّلَاةِ فَقَدْ أَدْرَكَ الصَّلَاةَ».
«Ku dab ab ràkka ci julli dab na julli ga»34.
3- Li ñuy dabe ràkka bi:
Ku dab Rukoo bi, dab na ràkka bi, Ki ñu jiitu bu dabee imaamam mu rukoo: kon daa wara kàbbar kàbbaru armal gi di aji-taxaw, topp mu kàbbar beneen yoon ngir rukoo, Bu yemee ci kàbbaru armal gi fekk mu taxaw, dana ko doy ci kàbbaru rukoo bi.
4- Ngànt yiy daganal ci nit ki mu bàyyi jullig mbooloo gi:
1- Feebar, bu dee teew àjjuma ak jullig mbooloo day metti ci moom.
2. Di muutale am saw walla xayta; ndax day dindi ragalu xol bi ci julli gi, te itam day lor yaram wi.
3- Teewug ñam wi te nit ki xiif, walla xolam di aju ci ñam wi, ci kaw ñu bañ ko a jël def ko aada walla pexe ngir bañ a teewe jullig mbooloo mi.
4- Ragal gu wér ci bakkan walla alal walla leneen.
Fukkeel bi ak ñatt: jullig ragal:
Yoonalees nañu jullig ragal ci gépp rayante gu dagan, niki xeex ak yéefar yi ak ñi bew ak xarekat yi, ndax waxu Yàlla mu kawe mi:
﴿...إِنۡ خِفۡتُمۡ أَن يَفۡتِنَكُمُ ٱلَّذِينَ كَفَرُوٓاْ...﴾
{...bu ngeen ragalee yéefar yi di leen fitnaal...} [An-Nisaa-i: 101]، Nattale ci ñi des te xeex ak ñoom dagan.
Yoonalees nañu jullig ragal ci ñaari sàrt:
1) Noon bi nekk ku dagan a xeexal.
2- Mu ragal ñu song jullit ñi bu ñuy julli.
Melokaanu jullig ragal:
Am na ay melokaan yu bari, te bi ci gën a siiw mooy li rot ci hadiisu Sahl -yal na ko Yàlla gërëm-:
أَنَّ طَائِفَةً صَفَّتْ مَعَ النَّبِي ﷺ، وَطَائِفَةً وِجَاهَ العَدُوِّ، فَصَلَّى بِالَّتِي مَعَهُ رَكْعَةً، ثُمَّ ثَبَتَ قَائِمًا، وَأَتَمُّوا لِأَنْفُسِهِمْ، ثُمَّ انْصَرَفُوا، وَصَفُّوا وِجَاهَ العَدُوِّ، وَجَاءَتِ الطَّائِفَةُ الأُخْرَى، فَصَلَّى بِهِمُ الرَّكْعَةَ الَّتِي بَقِيَتْ مِنْ صَلَاتِهِ، ثُمَّ ثَبَتَ جَالِسًا، وَأَتَمُّوا لِأَنْفُسِهِمْ، ثُمَّ سَلَّمَ بِهِمْ.
ne ag kuréel dafa sàppe ànd ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, geneen kuréel jàkkarloo ak noon bi, mu julli ak kurél gi ànd ak moom, benn ràkka, topp mu des taxaw, ñoom ñu mottalil seen bopp, daal di dem, sàppe jàkkarloo ak noon bi, geneen kuréel gi ñëw, mu julli ak ñoom ràkka bi desoon ca julleem ga, topp mu des toog, ñoom ñu mottalil seen bopp, mu ànd ak ñoom sëlmël35.
Dananu jariñoo ci Jullig ragal:
1- Solos julli ci Lislaam, ak solos jullig mbooloo, ndaxte Jamanoy tiis du tax ñu bañ koo def.
2- Teggi coono ci xeet wi, ak yombug Sariiha ji, akug méngoom ci bépp jamono ak bépp bérab.
3- Matug Sariihab Lislaam, ak ne dafa yoonalal bépp anam ak li méngoo ak moom.
Fukkeel bi ak ñent: Jullig àjjuma:
Li ci njëkk: àtteem:
Jullig Àjjuma faratay jëmm la ci bépp jullit bu góor, bu mat, te am xel, te di aji-dëkk, te amul ngànt.
Ndax waxi Yàlla mu kawe mi:
﴿يَٰٓأَيُّهَا ٱلَّذِينَ ءَامَنُوٓاْ إِذَا نُودِيَ لِلصَّلَوٰةِ مِن يَوۡمِ ٱلۡجُمُعَةِ فَٱسۡعَوۡاْ إِلَىٰ ذِكۡرِ ٱللَّهِ وَذَرُواْ ٱلۡبَيۡعَۚ ذَٰلِكُمۡ خَيۡرٞ لَّكُمۡ إِن كُنتُمۡ تَعۡلَمُونَ 9﴾
﴾Ée yéen way-gëm yi bu ñu wootee julli ci bisub àjjuma nangeen jëm ca tudd Yàlla ga te bàyyi njaay mi, loolu moo gën ci yéen, ndeem xam ngeen﴿
[Al-Jumuha: 9].
Ak ngir waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
«لَيَنْتَهِيَنَّ أَقْوَامٌ عَنْ وَدْعِهِمُ الْجُمُعَاتِ، أَوْ لَيَخْتِمَنَّ اللَّهُ عَلَى قُلُوبِهِمْ، ثُمَّ لَيَكُونُنَّ مِنَ الْغَافِلِينَ».
«nit ñi danañu bàyyi li ñuy ñàkk a teewe àjjuma yi, walla Yàlla dana kaste seen xol yi, te danañu bokk ci way-sàggan yi»36.
Ñaareel bi mooy: Sàrti werug jullig Àjjuma:
A) Waxtu wi: waxtoom mooy waxtu jullig tisbaar, Du wér bu jiitoo waxtoom, du wér it ginnaaw ba waxtu wa rombee.
2) Am mbooloo teewe ko, te li gën a néew ci mbooloo mooy ñatt, ci li gën a wér, Du wér it ci kenn ku beru, ak itam ci ñaar.
3) Jullikat yi di way-dëkk ci ay kër yu ñu tabaxe ak li ñu baaxoo tabaxe, moo xam simaa arme la, walla ci xeer, walla ci ban, ak yeneen, Ci loolu kon du wér ci waa àll bi dëkk ci ay xayma ak ay këri kawar, te dëkkuñu ci bérab bu sax, waaye dañuy tuxu di topp ñax mi ngir seen i jur.
4) Ñaari xutba jiitu ko ndax Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc da ko a saxoo woon.
Ñatteel bi: Ponki ñaari xutbay àjjuma:
1- Sant Yàlla ak ñaari seede yi.
2-Julli ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-
3- dénkaane ragal Yàlla.
4- Jàng lenn ci Alxuraan.
5- Waare.
Ñenteel bi : yi ñu sopp ci ñaari xutbay àjjuma yi:
1- Xutba ci kaw minbar.
2- teqale diggante ñaari xutba yi ci toogaay bu gàtt. 3- ñaanal jullit ñi ak ñi jiite seeni mbir ci ñaari xutba yi.
4- gàttal leen.
5- Xutbakat bi nuyu nit ñi bu yéegee ca Minbar ba.
Juróomeel bi: Mbir yi ñu sopp ci bisub àjjuma:
1- soccu.
2- Laal gëtt su amee.
3- Teel a génn jëm ca jullig Àjjuma ga.
4- Dox jëm ca jumaa ja, te bañ a war.
5- jege imaam bi.
6- Ñaan.
7- Jàng saaru Al-Kahfi.
8- Julli ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Juróom-benneel bi : Yi ñu tere ki teew àjjuma gi:
1- Araam na ñu wax ci bisu àjjuma fekk imaam bi di xutba, ndax waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc:
«إِذَا قُلْتَ لِصَاحِبِكَ يَوْمَ الْجُمُعَةِ: أَنصِتْ، وَالْإِمَامُ يَخْطُبُ، فَقَدْ لَغَوتَ».
«boo waxee sa àndandoo noppil ci bisu àjjuma, fekk imaam bi di xutba, kon fo nga»37. Maanaam: wax nga caaxaan, te caaxaan mooy: bàkkaar.
2- Sib nañu di jéggi ndoddi nit ñi, lu dul bu nekkee imaam, walla muy jéggi jëm ci ab diggante bob manu faa egg ci lu dul loolu.
Dab àjjuma gi:
Ku dab rukoo ànd ak Imaam bi ci ñaareelu ràkka bi ci jullig àjjuma, dab na jullig àjjuma ga, da koy
mottali muy ñaari ràkka, Waaye bu dabul rukoo bi ci ñaareelu ràkka bi, àjjuma gi raw na ko, te da koy mottali ñenti ràkka muy tisbaar, Naka noonu itam, ku àjjuma raw ngir nelaw walla leneen; kooku da koy julli tisbaar.
Fukkeel bi ak juróom: jullig ñi ame ngànt:
Bi ci njëkk: jullig aji-feebar:
Li ci njëkk: war na ci aji-feebar ji muy julli kem kàttanam, Te tu Dagan ci moom mu koy yeexe ci waxtoom fii ak xelam ma nga fa.
Ñaareel bi: Naka la aji-feebar di jullee?:
1- War na ci aji-feebar ji mu julli taxaw di rukoo ak a sujjóot, su manee taxaw ci lu dul jafe-jafe walla lor.
2- Su loroo ci rukoo bi walla ci sujjóot bi, te man a taxaw; day junj rukoo bi fekk mu taxaw, ak sujjóot bi fekk mu toog.
3- su manul a julli taxaw; mu julli toog, Liy sunna nag mooy mu toog ci barabu taxaw ba, muy juñju Rukoo bi, mu sujjóot ci suuf bu manee nekk, budul loolu mu juñjal sujjóot ga, te mu gëna suufe Rukoo ba.
4- Su manul a julli toog, mu wetu, te jëmale kanamam xibla, Wetu ndayjoor nag moo gën bu yombée, te mu juñju ci Rukoo bi ak sujóot bi.
5- bu manul a julli ci wetam, mu julli te jaaxaan, ay tànkam jublu xibla, muy juñju rukoo yi ak sujóot yi.
6- Bu manul a sëggal yaramam ci rukoo ak sujóot, na sëggal boppam, su ko loolu jafee, sëggal gi wàcc na ko, mu doxal jëfi julli gi ci xolam, muy yéene jëfi julli gi rukoo yi ak sujóot yi ak toog fekk moo ngi ci melokaanam, muy def sikar ya.
7- Aji-feebar ji day def ci sàrti julli yi li mu man a def, niki: jublu xibla, jàpp ak ndox, walla mu tiim bu ko manul, ak mu laab ci sobe yi, bu manul dara ci yooyu; da koy wàcc, mu julli ci kem melokaanam, te du yéexal julli gi ba mu génn waxtoom.
8- Sunna si mooy ki feebar day farankulaayu ci bérabi taxaw yi ak rukoo yi, mu lal tànkam ci yu dul yooyu.
Ñaareel bi: jullig aji-tukki ji:
1- bokk na ci boroom ngànt yi: aji-tukki ji, moom yoonalal nañu ko wàññi jullig ñenti ràkka, jële ko ñent def ko ñaari ràkka, Ndax waxi Yàlla mu kawe mi:
﴿وَإِذَا ضَرَبۡتُمۡ فِي ٱلۡأَرۡضِ فَلَيۡسَ عَلَيۡكُمۡ جُنَاحٌ أَن تَقۡصُرُواْ مِنَ ٱلصَّلَوٰةِ...﴾
﴾Bu ngeen tukkee ci suuf si, aayul ci yéen ngeen waññi ci julli gi...﴿ [An-Nisaa-i: 101].
Te jële nañu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
«خَرَجْنَا مَعَ النَّبِيِّ ﷺ مِنَ الْمَدِينَةِ إِلَى مَكَّةَ، فَكَانَ يُصَلِّي رَكْعَتَيْنِ رَكْعَتَيْنِ، حَتَّى رَجَعْنَا إِلَى الْمَدِينَةِ».
«Génn nanu ànd ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jóge Madiina jëm Màkka, mu daan julli ñaari ràkka ñaari ràkka, ba nu dellu Madiina»38.
Wàññi gi day tàmbali bu aji-tukki ji génnee dëkkam; ndaxte Yàlla dàganal na wàññi ñeel ki tukki ci suuf si, Bu génnagul dëkkam du doon ku tukki, ndaxte Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, bu daan tukki rekk la daan wàññi,
2- Diggante bi nga xam ne bu ko aji-tukki ji nammee dog dana dagan ci moom mu wàññi julli mooy luy toll ci juróom-ñatt-fukki kilomeetar.
3- Tukki kat bi man na a wàññi ci buy dellu dëkkam ba mu jóge woon.
4- Bu aji-tukki ji egsee ci ab dëkk, te yéene faa dal; amna ñatti anam:
A) Mu yéene sax fa lu ëpp ñenti fan; kon day war ci moom mu matal julli dale ca bis bu njëkk ba mu fa nekke, te du jot ci yombali tukki yi.
B) Mu yéene sax fa ñenti fan mbaa lu ko yées; kon dagan na mu wàññi te jëfandikoo yombali tukki gi.
C) Mu bañ a yéene ag sax gu ñu tënk, waaye amaana mu sax ab bis walla fukki fan kem ni mu dëppoo ak bérab bi, walla mu am lu ko gaar niki faju walla toppatoo, te saa yu aajoom jeexee mu dellu ca dëkkam; Kii wàññi ñeel na ko ak jëfandikoo yombali tukki gi, ba keroog muy dellu, donte diir ba mu fa des weesu na ñenti fan.
5- Bu aji-tukki ji jullee ci ginnaaw imaam ju tukkiwul, day war ci moom mu matal julli gi, donte sax taaya ju mujj ja rekk la fekke ak moom.
6- Bu ki tukkiwul jullee ci ginnaaw aji-tukki juy wàññi julli gi; day war ci ki tukkiwul mu matal julleem gi ginnaaw sëlmëlug imaam bi.
Fukkeel bi ak juróom-benn: jullig ñaari feet yi.
Feeti jullit ñi ay feet yu bawoo fa Yàlla la, Yàlla mu kawe mi moo leen ko yoonalal, te du ñoom ñoo ko yoonalal seen bopp. Te amuñu lu dul ñaari feet: feetu korite ak feetu tabaski. Mu wuute ak feeti yéefar yi walla feeti bidaa yi nga xam ne Yàlla yoonalu leen te diglewu leen, waaye ñoo ko yoonalal seen bopp.
Àttey jullig ñaari feet yi:
Farata guy doy la, Yonnente bi da leena saxoowoon, niki noonu Xalifa yu jub yi -yal na leen Yàlla gërëm ñoom ñépp-, Dañoo bokk ci màndargay diine ji.
Waxtuw jullig ñaari feet yi: waxtuw jullig feet moo ngi tàmbali bu jant bi yëkkëtikoo luy tollook ab xeej, maanaam: luy tolloo ak ñenteelu xaaju waxtu ginnaaw bu jant bi fenkee, di jeex bu jant bi jengee.
Mélokaanu jullig ñaari feet yi:
1- Day kàbbar kàbbaru armal ci ràkka bu njëkk bi, topp mu jàng ñaan gi ñuy ubbee julli gi, topp mu kàbbar juróom-benn kàbbar, day yëkkëti ñaari loxoom yi ànd ak kàbbar gu nekk, mu sant Yàlla màggal ko, daal di julli ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci diggante kàbbar yi, topp mu muslu ci Yàlla ci saytaane daal di wax Bismil Laahir Rahmaanir Rahiim, daal di tàmbale njàng mi.
2- Mu kàbbar ci ràkka bu ñaareel bi ginnaaw kàbbarug jug ga juróomi kàbbar, topp mu muslu daal di wax bismil Laahir Rahmaanir Rahiim, daal di door njàng mi. sopp nañu mu jàng ci ràkka bu njëkk bi ginnaaw Faatiha saaru Al-Ahlaa, bu ñaareel bi saaru Al-Xaasiya.
3- Bu imaam bi sëlmëlee; day yéeg ci Minbar bi, daal di xutba ñaari xutba, day toog ci seen diggante toogaay bu woyof, niki ni ñu koy defe ci xutbag àjjuma.
Sunnay feet gi:
A- Sangu farata.
B- Set ak laal gët (parfum).
C- lekk laata ñuy génn jëm ci jullig feetu Korite, ak ginnaaw jullig feetu tabaski, mu lekk ci ag tabaskeem su amee ag tabaski.
D- Génn di dox jëm ca julli ga.
E- Dem jaar ci aw yoon, buy dellusi mu jaar ci weneen yoon.
F- teel a dem ca jullikaay ba ñeel Maamuun, wolif imaam bi.
Kàbbar gi:
Yoonal nañu di takbiir ci ñaari guddiy feet yi, ak fukki fan yu njëkk yi njëkk ci Tabaski, ak bisi Tasriiq yi, moom nag ñaari xeet la:
Xeet bu njëkk wi: takbiir bu ñu boyal: mooy bi nga xam ne tënkuñu ko ci aw waxtu.
1- Ci Korite: day dale ci bu jant bi sowee ci guddig Kori gi ba ci tàmbaleeg jullig feet gi.
2- Ci Tabaski: day dale ci sowug jànt bi ci guddi gi njëkk ci weeru Tabaski gi, ba ci sowug jànt bi ci biss bi mujj ci fanni Tasriiq yi.
Xeetu ñaareel bi: tabiir bu ñu tënk: te mooy bi ñu tënk ci ginnaaw julli farata yi.
1- Ki armalul: day dale ca fajaru bisu Arafa ba ci tàkkusaan ji mujj ci fani Tasriiq yi.
2- Kiy armal: day dale ci jullig Tisbaaru bisu Tabaski gi ba ci tàkkusaan gi mujj ci fani Tasriiq yi.
Fukkeel bi ak juróom-ñaar: jullig muurug jant bi:
Maanaam Xusuuf ak Kusuuf:
Xusuuf: mooy leerug weer wi dal di dem ci guddi gi.
Kusuuf: mooy demug leeraayu jant bi ci bëccëg gi.
Àtteb jullig muurug jant bi:
Sunna suñu feddali la, jëfu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- moo ko tegtale, ndax julli na ko bi jant bi muuroo ci jamonoom -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-. Kem ni ko ndigalam tegtalee, te boroom xam-xam yi dëppoo nañu ci ne lu ñu yoonal la.
Waxtoom:
Mi ngi dale ci tàmbaleeg Kusuuf gi walla Xusuuf gi, ba keroog muy leer, te mooy deñuug muuraayu weer wi walla jant bi.
Melokaanam:
Limum ay ràkkaam ñaari ràkka la, dañu ciy béral njàng mi, te melokaanam mooy nii:
A- Day def kàbbarug armal, mu jàng ñaanug ubbee gi, mu muslu ci saytaane, daal di wax bismil Laahir Rahmaanir Rahiim, daal di jàng faatiha, topp mu jàng am njàng mu gudd.
B- Topp mu rukoo lu yàgg.
C- Mu siggi jóge ci rukoo bi, daal di wax: (samihal Laahu liman hamidah), topp mu jàng faatiha, topp mu jàngaat njàng mu gudd, te gën a gàtt mu njëkk ma.
D- Topp mu rukoo rukoo bu gudd te gën a gàtt bu njëkk ba.
E- Topp mu siggi jóge ca rukoo ba, daal di wax: (samihal Laahu liman hamidah).
F- Topp mu sujóot ñaari sujóot yu gudd.
G- Topp mu jug ngir ràkka bu ñaareel bi, moom nag day mel ni ràkka bu njëkk ba, waaye nag moo koy gën a gàtt.
Ay sunnaam:
A) Wooteel ko ci wax ne: (Assalaatu jaamiha).
B) ñu jullee ko ci mbooloo.
Guddal taxaw gi, Rukoo gi ak sujóot si ci biir julli gi.
D) Ràkka bu ñaareel bi gën a gàtt bu njëkk ba.
E) waare ginnaaw ga, ak ñaaxe ci def topp Yàlla yi ak bàyyi yu bon yi.
F) Baril di ñaan ak di toroxlu ak jégalu ak saraxe.
Fukkeel bi ak juróom-ñatt: jullig baawnaan:
1) Baawnaan: mooy sàkkoo nàndal ci Yàlla mu wàcce ci mu wàcce taw ci jamonoy bekkoor.
Waxtu wi ñu yoonal jullig Baawnaan:
Yoonalees nañu jullig Baawnaan bu suuf si bekkooree, taw bi taxaw, ba ñuy loru, kon amuñu menn pexe lu dul ñu toroxlu jëm ci seen Boroom sàkku mu nàndal leen, ñuy sàkku mu xettali leen ci ay xeeti toroxlu yu bari.
A- leeg-leeg ci jullig mbooloo, walla ci kenn-kenn.
B- yenn saa yi, ci ñaan ci xutbag àjjuma, Xatbakat day ñaan, jullit ñi di wax aamiin ci ñaanam gi.
C- Yenn saa yi, ñu ñaan ci waxtu yépp ci lu dul julli du caagine xutba.
Àtteb jullig baawnaan:
Sunna suñu feddali la bu sabab ba amee, ndax jëfu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc-, kem ni mu ñewe ci hadiisu Abdallah Ibn Sayd -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, mu wax ne:
«خَرَجَ النَّبِيُّ ﷺ إِلَى الْمُصَلَّى، فَاسْتَسْقَى، وَاسْتَقْبَلَ الْقِبْلَةَ، وَقَلَبَ رِدَاءَهُ، وَصَلَّى رَكْعَتَيْنِ».
«Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- génn na dem ca bérabu jullikaay ba, ñaan fa taw, jublu xibla, dëpp koddaayam, topp mu julli ñaari ràkka»39.
Melow jullig Baawnaan:
Melow jullig Baawnaan ci bérabam day mel ni jullig feet yi. Sopp nañu ñu def ko ci jullikaay bi niki jullig feet, ay àtteem it day mel ni àttey jullig feet; ak ci limug ràkka yi, ak béral njàng mi, ak ni julli gi di jiitoo xutba gi, ak ci kàbbar yu ñu yokk ci ràkka bu njëkk ak bu ñaareel bi ñu jiitu njàng mi, Kem ni leeral gi jiitoo woon ci jullig ñaari feet yi. Mu xutba genn ug xutba.
Fukkeel bi ak juróom-ñent: Àttey néew:
Bi ci njëkk: ñeel ki fekke aji-sukraat ji:
1- Sopp nañu ki fekke kuy sukraat, mu sa ko: «laa ilaaha illal-Laahu».
2- Liy sunna mooy ñu jubale ko ci Xibla bi.
3- Sopp nañu ñu daal di gëmm ay bëtam.
4- Sunnaal nañu Muur néew bi ci ab sér ginnaaw bi mu faatoo.
5- Jaadu na ñu gaaw ci waajal ko.
6- Dana war it ñu gaawantu fay boram yi.
7- Ñu sang néew bi ak sàng ko, loolu nag fardu kifaaya la.
Ñaareel bi: Àttey jullée néew:
Àtteem: farata guy war ñëpp la.
Ay sàrtam:
1) Jublu ci xibla bi.
2) Muur awra yi.
3) Moytu sobe si.
4- Laabug kiy julli ak ki ñuy jullee.
5) Kiy julli ak ki ñuy jullee ñu nekk ay jullit.
6) Néew bi teew bu dee ci dëkk bi la nekk.
7) Mu doon mukallaf.
Ay ponkam:
1) Taxaw bu ñu kay Jullee.
2) Ñenti kàbbar yi.
3) Jàng faatiha.
4) Julli ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc.
5) Ñaanal ki faatu.
6) Toftale gi
7) Sëlmël.
Ay sunnaam:
1) Yëkkëti yaari loxo yi ci kàbbar gu nekk.
2) Muslu ci saytaane.
3) Ñaanal boppam ak jullit yi.
4) yelu njàng mi.
5) Taxaw tuuti ginnaaw kàbbaar gu ñenteel gi laata sëlmël.
6) Teg loxo ndayjoor ci kaw loxo càmmooñ ci kaw dënn bi.
7) Gestu ci ndayjoor bi ci sëlmël gi.
Ay meloom:
Imaam bi ak ki beru dañuy taxaw ci tolluwaayu dënnub góor gi ak ndiggu jigéen ji, daal di def kàbbaru armal, muslu ci saytaane, waaye du def ubbee gi, mu wax bismil Laahir Rahmaanir Rahiim, daal di jàng faatiha.
Topp mu kàbbar, ginnaaw ga mu julli ci Yonnente bi, topp mu kàbbar, daal di ñaanal néew bi ci ñaan yi rot; Niki waxu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-:
«اللَّهُمَّ اغْفِرْ لِحَيِّنَا وَمَيِّتِنَا، وَصَغِيرِنَا وَكَبِيرِنَا، وَذَكَرِنَا وَأُنثَانَا، وَشَاهِدِنَا وَغَائِبِنَا، اللَّهُمَّ مَنْ أَحْيَيْتَهُ مِنَّا فَأَحْيِهِ عَلَى الإِيمَانِ، وَمَنْ تَوَفَّيْتَهُ مِنَّا فَتَوَفَّهُ عَلَى الإِسْلَامِ، اللَّهُمَّ لَا تَحْرِمْنَا أَجْرَهُ، وَلَا تُضِلَّنَا بَعْدَهُ».
«Allaahumma ixfir li hayyinaa wa mayyitinaa, wa saxiirinaa wa kabiirinaa, wa sakarinaa wa unsaanaa, wa saahidinaa wa xaa-ibinaa, Allaahumma man ahyaytahu minnaa fa ahyihi halal iimaan, waman tawaffaytahu minnaa fa tawaffahu halal islaam, Allaahumma laa tahrimnaa ajrahu, walaa tudillanaa bahdahu»40.
Ak waxam ji:
«اللَّهُمَّ اغْفِرْ لَهُ وَارْحَمْهُ، وَعَافِهِ وَاعْفُ عَنْهُ، وَأَكْرِمْ نُزُلَهُ، وَوَسِّعْ مَدْخَلَهُ، وَاغْسِلْهُ بِالْمَاءِ وَالثلْجِ وَالْبَرَدِ، وَنَقِّهِ مِنَ الْخَطَايَا كَمَا نَقَّيْتَ الثَّوْبَ الْأَبْيَضَ مِنَ الدَّنَسِ، وَأَبْدِلْهُ دَارًا خَيْرًا مِنْ دَارِهِ، وَأَهْلًا خَيْرًا مِنْ أَهْلِهِ، وَزَوْجًا خَيْرًا مِنْ زَوْجِهِ، وَأَدْخِلْهُ الْجَنَّةَ، وَأَعِذْهُ مِنْ عَذَابِ الْقَبْرِ، وَمِنْ عَذَابِ النَّارِ».
«Allaahumma ixfir lahu warhamhu, wa haafihii wahfu hanhu, wa akrim nusulahu, wa wassih mudxalahu, waxsilhu bil maa-i wassalji walbaradi, wa naqihi minal xataayaa kamaa naqayta assawbal abyada minad danasi, wa abdilhu daaran xaytan min daarihi, wa ahlan xayran min ahlihi, wa sawjan xayran min sawjihi, wa adxilhu aljannata, wa ahishu mina annaari»41. Topp mu kàbbar, ginnaaw ga mu taxaw tuuti, dal di sëlmël benn sëlmël ci ndayjooram.
Waxtaan wu ñatteel wi: Asaka:
1- Xamle asaka ak gëddam:
Asaka ci làkk araab, mooy ag màgg ak yokk.
Asaka ci Sariiha: àq la ju war ci sariiha ci alal ju ñu tënk, ci mbooloo mu ñu ko jagleel.
Te mooy ñatteelu ponk ci ponki Lislaam yi, Te moom dafa taqoo ak julli ci Alxuraan ci juróom-ñatt fukki bérab ak ñaar, loolu di tegtale màggug mbiram.
Yàlla nee na:
﴿وَأَقِيمُواْ ٱلصَّلَوٰةَ وَءَاتُواْ ٱلزَّكَوٰةَ...﴾
﴾Taxawalleen julli, joxeleen asaka...﴿
[Al-Baqara: 43].
Yonnente bi -yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«بُنِيَ الإِسْلَامُ عَلَى خَمْسٍ: شَهَادَةِ أَنْ لَا إِلٰهَ إِلَّا اللَّـهُ، وَأَنَّ مُحَمَّدًا رَسُولُ اللَّـهِ، وَإِقَامِ الصَّلَاةِ، وَإِيتَاءِ الزَّكَاةِ، وَحَجِّ الْبَيْتِ، وَصَوْمِ رَمَضَانَ».
«tabax nañu lislaam ci juróom: seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe asaka, ak aji Màkka, ak woor weeru koor»42.
Jullit ñi dëppoo nañu ci ne farata la, Ak ci kéefarug ku weddi ag waram. Ak xeex ak ki ko bañ a génne.
2- Sàrt yiy waral asaka:
A) Nekk gor: du war ci ab jaam; ndaxte amul alal, te li mu yor moomelu sangam la, kon asakaam ci sangam la war.
B) Lislaam: du war ci yéefar bi; ndaxte ag jegeñ-jegeñlu la ak ub topp Yàlla, te yéefar bi bokkul ci ñiy jege Yàlla ak ñiy topp Yàlla.
C) Am lu mat Nisaab: Du war ci lu matul Nisaab, muy lim bu ñu xam ci alal.
D) Moomeel gu mat sëkk: alal ji dafa war a doon lu nit ki moom moomeel gu mat sëkk, kon asaka warul ci alal ju moomeelam saxul, niki borub jaam bu digaalee Jënd boppam.
E) Alal ji am at: Ndax hadiisu Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu askanale ko Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
«لَا زَكَاةَ فِي مَالٍ حَتَّى يَحُولَ عَلَيْهِ الْحَوْلُ».
«Asaka amul ci alal ba keroog muy mat at»43.
3- Alal yi asaka war:
Ji ci njëkk mooy: jur yi,
Te mooy giléem ak nag ak gàtt, asaka dana ci war ci ñaari sàrt:
1- Ñu yore leen ngir ratt leen ak ñuy jur, waaye du ngir liggéey.
2- Mu nekk yu ñuy boyal muy fori (maanaam: muy dunde ci fori), Asaka warul ci ay jur yu boroomam di xont ci xont gu mu Jënd, walla gàñcax gu dajale mbaa leneen, Asaka warul ci jur giy fori ci lenn ci at mi waaye du at mépp mbaa lu ëpp ci at mi.
4- Nisaabu baayimay jur gi:
1- Asakay giléem:
Bu sàrt yi matee; kon day war ci juróomi giléem yu nekk wenn gàtt, ci fukk yi ñaari gàtt, ci fukk yi ak juróom ñatti gàtt, ci ñaar-fukk yi ñenti gàtt, Kem ni ko Sunna tegtalee ak dëppoog woroom xam-xam yi. Bu matee ñaar-fukk ak juróom, kon Bintu Maxaad a ca war, te mooy giléem gu matal at, ba dugg ci ñaareel atam, bu ko amul nag, Ibnu Labuun doy na ca.
Bu giléem yi matee fanweer ak juróom-benn; Bintu labuun war na ca, te mooy: gu matal ñaari at.
Bu matee ñent-fukk ak juróom-benn; kon Hiqa war na ca, gu matal ñatti at.
Bu giléem yi eggee juróom-benn fukk ak benn; kon Jasaha war na ca, te mooy gu matal ñenti at.
Bu limub giléem yi tollee ci juróom-ñaar fukk ak juróom-benn, kon ñaari giléem yu jigéen yu matal ñaari at war na ca.
Bu giléem yi tollee ci juróom-ñeent fukk ak benn; war na ci ñaari hiqqah.
Bu limub giléem yi nekkee téeméer ak ñaar-fukk yu teg benn, kon ñatti Bintu labuun war na ca, topp nag ñent-fukki giléem yu nekk benn Bintu labuun war ca, juróom-fukki giléem yu nekk benn Hiqa war ca.
2- Asakay nag:
Bu matee fanweer te sàrt yi dajee: li ciy war mooy Tabiih walla Tabiiha; mooy lu matal at ba dugg ci ñaareelu atam.
Bu matul fanweer dara waru ci.
Bu matee ñent-fukk, aw nag wu matal ñaari at moo cay war.
Bu limub nag yi ëppee ñent-fukk; kon dana war ci fanweer yu nekk wenn nag wu am at wu góor walla wu jigéen, ak ci ñent-fukk yu nekk wenn nag wu am ñaari at.
3- Asakay gàtt:
Limub gàtt yi bu mattee ñeent-fukk, moo xam xar la walla bëy, kon benn gàtt a ci war: te mooy xar mu góor mu matal juróom-benni weer, walla bëy wu jigéen.
Asaka du war ci ay gàtt yoo xam ni seenub lim matul ñent-fukk. Bu limu gàtt yi eggee téeméer ak ñaar-fukk ak benn, kon ñaari gàtt war na ci. Bu matee ñaari téeméer ak benn; kon ñatti gàtt war na ci.
Ginnaaw lim boobu farata gi day sax, bu ko defee téeméeri gàtt yu nekk wenn gàtt war ca, ñenti téeméer yu nekk ñenti gàtt war ca, noonu lay wéye.
Ñaareel bi: Asakay luy génn ci suuf:
Liy genn ci suuf ñaari xeet la:
1) dugub yi ak meññet yi.
2) Mbell yi.
Xeet bu njëkk bi: dugub yi ak meññet yi:
Asaka day war ci dugub yi, lu ci mel ni: bele ak saño ak ceeb. Ci meññet yi; lu ci mel ni: tàndarma ak rezin, Te warul ci yeneen gàncax yu dul yooyu, niki ñebbe ak lujum.
Sàrti warug asaka ci dugub yi ak meññet yi:
1) Mu doon lu ñuy denc: asaka warul ci lu ñu dul denc, naka furwi yi ak lujum yi.
2) Mu doon lu ñuy natt: kon asaka warul ci lu ñuy jaay ci waññi walla ci peese; lu ci mel ni xaal ak soble ak garanaat, ak yu ni mel.
3) mu mat Nisaab: te mooy juróomi Wasq, asaka du war ci lu matul loolu.
4) Nisaab bi nekk lu ñu moom ci waxtu wi asaka ji di war.
Kon ku ko moom ginnaaw waxtuw warug asaka ji, kooku asaka waru ko, naka noonu it bu ko jëndoon walla ñu may ka ko ginnaaw bi ñu ko góobee.
Waxtuw warug asaka:
Asaka day war ci dugub yi ak meññet yi, bu ñu tàmbalee baax, Te màndargay feeñug baax gi, ñooy yii di ñëw:
A- Ci dugub: su dëgëree dem ba nekk lu wow.
B- Ci meññetu tàndarma: mooy mu xonq walla mu mboq.
C- ci resen: mooy mu nooy te neex.
Nisaabam:
Nisaabug dugub yi ak meññet yi: juróomi Wasq la, Te Wasq mooy juróom-fukki Saah, Kon Nisaab bi ñàtti téeméeri Saahu Yonnente bi la, Nisaab di tollu ci ay kilogaram: lu jege 900 kg naanaka.
Tolluwaayu asaka ji war:
Fukkeelu xaaj bi dana war ci lu ñu nàndal ci lu dul coono; niki liy naan ci ndoxum taw ak sewnde yi.
Xaaju fukkeel bi dana war ci li ñu suuxat ci coono; niki li ñu suuxate teen yi ak dex yi jaare ko ci ay rab walla jumtukaay yu yees yi.
Xeetu ñaareel bi: Mbell yi:
Bokk na ci xeeti liy génne ci suuf: mbell yi, Moom mooy li ñu génne ci suuf te bokkul ci xeetam; niki wurus, ak xaalis, ak weñ, ak gànjar yi.
Waxtu wi ci asaka di war:
Bu ko amee te moom ko; day génne asaka ja fa saasa, ndaxte sàrtaluñu ca mu am at. Nisaabam mooy nisaabu wurus ak xaalis, dees ciy génne ñenteelu xaaju fukkeel ba ci xaymaam.
Ñatteel bi : Asakay njëg yi (Asmaan):
Njëg yi ñooy: wurus ak xaalis ak këyiti xaalis yi, asakaam nag lu war la. Tegtal bi mooy waxu Yàlla mu kawe mi:
﴿...وَالَّذِينَ يَكْنِزُونَ الذَّهَبَ وَالْفِضَّةَ وَلَا يُنْفِقُونَهَا فِي سَبِيلِ اللَّهِ فَبَشِّرْهُمْ بِعَذَابٍ أَلِيمٍ﴾
﴾Ñi nga xam ne dañuy denc wurus ak xaalis te duñu ko joxe ci yoonu Yàlla, bégal leen ci mbugal mu metti﴿ [At-Tawba : 34].
Ñëw na ci haddis:
«مَا مِنْ صَاحِبِ ذَهَبٍ وَلَا فِضَّةٍ لَا يُؤَدِّي فِيهَا حَقَّهَا؛ إِلَّا إِذَا كَانَ يَوْمَ الْقِيَامَةِ صُفِّحَتْ لَهُ صَفَائِحُ مِنْ نَارٍ».
«amul benn boroom wurus du caagine xaalis, te du joxe àqam; lu dul ne bu bis-pénc baa dees na ko lalal ay lali xeeri sawara»44.
Boroom xam-xam yi dëppoo nañu ci warug asaka ci wurus ak xaalis, te këyiti xaalis yi àtteb wurus ak xaalis la am; ndaxte ñoo leen wuutu ci jëflante yi.
Nisaabu Asaka ci njëg yi, ak lees ciy war a génne:
Mooy nisaabu wurus walla xaalis; ndaxte moo leen wuutu ci nekk njëg, bu matee nisaabu benn ci ñoom asaka war na ca, te li gën a siiw tay jii mooy ñu nattale nisaabu këyiti xaalis yi ci xaalis; ndaxte dafa gën a yomb wurus, te moo koy njëkk a mat nisaabam, Bu jullit bi amee lu tollook (595) garaami xaalis, te mu mat at, asaka war na ci. Xaymag garaamu xaalis day soppeeku jamono ju nekk, kon ku am alal ju néew te xamul ndax mat na Nisaab am déet, na laaj jaaykati xaalis yi njëgu garaamu xaalis bi, daal di koy dóor ci (595), li ci génn mooy Nisaab bi.
Ab Njariñ moo ngi ni: ku bëggee génne asakay alalam, na séddale Nisaab bi ci ñent-fukk, la cay génn mooy lim bi war.
Ñenteel bi: Asakay màrsandiis:
Moo di lu ñu jagleel jaay ak jënd, ngir ame ci bonofiis , Màrsandiis day làmboo bépp xeetu alal ju dul koppar; niki woto yi, ak yére yi, ak tiise yi, ak weñ, ak bant yi, ak yeneen lu ñu waajal ngir yaxantu.
Sàrti warug Asakay màrsandiis:
1- mu moom ko ci jëfam; niki njaay, ak luye, ak yeneen anami fàggu yi.
2- mu moom ko ci yéeney yaxantu; ci mu jublu ci fàggu, ndaxte jëf yi mi ngi aju ci yéene yi, te yaxantu jëf la, kon war na ko a lënkale ak yéene niki mbooleem jëf yi.
3- mu matt Nisaabu wurus walla xaalis.
4- mu mat at, maanaam at mu romb.
Ni ñuy génnee Asakay màrsandiis:
Day xayma Màrsandiis mi bu amee at benn ci ñaari koppar yii di wurus mbaa xaalis, Bu ñu ko xaymaa ba mu mat Nisaabu benn ci ñaari koppar yi, dees na ci génne ñenteelu xaaju fukkeel ba ci xaymaam.
Juróomeel bi: Asakay muurum koor:
Moom ab sarax bu war la ci korite, Farataalees nañu ko ci ñaareelu atum Gàddaay gi.
Ab Àtteem:
Asakay muurum koor dafa war ci bépp jullit bu am ci bisub korite gi ak guddeem dund gu ëpp li koy doy di doy ñi mu war a dundal. Day war ci bépp jullit; góor mbaa jigéen, xale mbaa mag, gor mbaa jaam, Ndax Hadiis bii:
«فَرَضَ رَسُولُ اللَّهِ ﷺ زَكَاةَ الْفِطْرِ عَلَى الْعَبْدِ وَالْحُرِّ، وَالذَّكَرِ وَالْأُنثَى، وَالصَّغِيرِ وَالْكَبِيرِ، مِنَ الْمُسْلِمِينَ».
«Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc farataal na asakay muurum koor ci jaam ak gor, ak góor ak jigéen, ak gone ak mag, ci jullit ñi»45. Farataal na maanaam: waral na.
Xereñte gi nekk ci yoonal gi:
Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- wax na ne:
«فَرَضَ رَسُولُ اللَّهِ ﷺ زَكَاةَ الْفِطْرِ؛ طُهْرَةً لِلصَّائِمِ مِنَ اللَّغْوِ وَالرَّفَثِ، وَطُعْمَةً لِلْمَسَاكِينِ».
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc farataal na asakay muurum koor, muy luy laabal aji-woor ji ci ay caaxaan ak mbóosóor, waaye di aw ñam ñeel way-ñakk yi»46.
Waxtu wimuy war ak waxtu wiñukoy génne:
Asakay muurum koor dana war ci sowug jant bi ci guddig korite gi. Sopp nañu ñu génne ko ci bisub feet gi balaa ñuy dem ca jullig Hiid ga. Te daganul ñu yéexe ko ba julli gi weesu, Bu ko yéexe ba ginnaaw jullig Hiid gi; kon dana war ci moom mu fay génne ga, te day am bàkkaar ci li mu ko yéexe ba ginnaaw waxtu wi ñu ko tënkaloon.
Dana dagan ñu jiital ko njëkk Hiid gi ci benn walla ñaari fan.
Ni muy toll ak ci lan lañu koy génne:
Saah ci ñam mi waa dëkk ba baaxoo lekk; niki ceeb, tàndarma, ak bele walla yeneen. Tolluwaayu Saah mooy ñatti kilogaraam ci ag jegeele. Te du dagan ñu génne xaalis ci plasam; ndax dafa wuute ak ndigëlu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.
Génne asaka ak ñi ñu ko war a jox:
Waxtuw génne ko:
War nañoo génne asaka gi ca na mu gën a gaawe, su waxtuw waram jotee, Te daganul ñu koy yéexe lu dul ngir muy lu manut a ñàkk, niki alal ja bu nekkee ci réew mu ko sori te amul ku mu ko man a féetale.
Bérab bi ñu koy génnee:
Li gën mooy génne asaka ci dëkk bi alal ji nekk, Dagan na nag ñu tuxal ko jële ko ci dëkk bi alal ji nekk, yóbb ko ci beneen dëkk, ci ay anam:
A- bu amul ci dëkk bi ku soxla asaka.
b- Bu amee mbokk mu ko yittewoo ci beneen dëkk.
C- Bu amee njariñ lu sariiha bu laaj ñu tuxal ko, niki: yóbbu ko ca bérabi jullit ñi nga xam ne xiif gu metti ak i mbënd dal na leen.
Asaka dana war ci alalu xale ak dof, ngir mataleg tegtal yi, te seen kilifa gi leen yoreel alal ja mooy méngoo génne ga. Génne asaka du dagan lu dul ci yéene, ngir waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
«إِنَّمَا الْأَعْمَالُ بِالنِّيَّاتِ».
«jëf yi ñoo ngi aju ci yéene yi»47.
Ñi ñuy jox asaka:
Xeet yi ñuy jox asaka juróom-ñatt lañu:
Xeet wu njëkk wi: way-ñàkk yi.
Ñoom ñooy ñi ñàkk lu leen doy ci dëkkuwaay, ak ñam, ak yére, Tolluwaayu li ñu leen di jox ci asaka ji mooy lu leen doy ci lu mat at ñoom ak ña ñuy dundal.
Xeetu ñaareel wi: Miskiin yi:
Ñoom ñooy ñi am lu ëpp ci li leen doy, waaye amuñu lu matale, niki: ku am payoor, waaye du ko doy lu mat at.
Tolluwaayu li ñu leen di jox ci asaka ji: mooy lu leen doy sëkk ñoom ak ña ñuy dundal ci diirub at.
Xeetu ñatteel wi: Ñi ciy liggéey:
Ñooy ñi njiit li féetale dajale asaka ji, walla ñuy méngoo sàmm ko, walla ñu koy eggale ca ña ko yeyoo.
Tolluwaayu li ñu leen di jox ci asaka: day tolloo ak kem seenug pay ci seen liggéey, bu dee amuñu pay mbaa Saleer guy jóge ci nguur gi.
Xeetu ñenteel wi: Ñi ñuy miinloo seen xol:
Ñoom ñooy képp ku ñu yaakaar ci jox gi ñu koy jox: mu dugg ci Lislaam, walla ngëmam gën a dëgër, walla mu téye loram ci jullit ñi.
Tolluwaayu li ñu leen di jox ci asaka: mooy luy toll ni liy miinaal seen xol yi.
Xeetu juróomeel wi: jaam yi
Li ñu ci jublu mooy: goreel jaam yi ak jaam yi bindante.
Aji-bindante ji: mooy jaam bi jënd boppam ci sangam, Te ci la bokk jotug jullit ñi ñu jàpp ci xare yi.
Xeetu juróom-benneel wi: Ñi am bor, te ñoom ñaari xeet lañu:
Bi ci njëkk: ku am bor ngir aajoy boppam, te amul lu mu faye boram, Dañu koy jox lu mu faye boram.
Ñaareel bi: ki am bor ndax yéwénal gu muy def ci diggante nit ñi, Dañu koy jox lu mu faye boram, donte sax ku woomle la.
Xeetu juróom-ñaareel wi: ci yoonu Yàlla:
Ñoom ñooy ñiy jihaad ci yoonu Yàlla.
Tolluwaayu li ñu leen di jox ci asaka: mooy li leen doy ci jihaad ci yoonu Yàlla; ci waruwaay, ak ngànnaay, ak lekk, ak yu dul yooyu.
Xeetu juróom-ñatteel wi: doxandeem biy aji-tukki:
Mooy aji-tukki ji dundam jeex, walla ñu sàcc ko, te deseetul xaalis bu koy eggale ca réewam.
Dayo bi ñu koy jox ci asaka ji: mooy li koy eggal ci réewam, donte ku woomal la fa.
Waxtaanu ñenteel bi: Woor:
Woor mooy :
Jaamu Yàlla mu kawe mi ci bàyyi lépp luy dogloo, li ko dale ci fenkug fajar gi ba ci sowug jant bi.
te moom ponk la ci ponki lislaam yi, Te farata la ju bokk ci faratay boroom bi, Lu ñu xam la ci diine ji ci lu manut a ñàkk. Téereb Yàlla bi ak Sunna ak dëppoog Jullit ñi moo tegtale ag waram.
Yàlla mu kawe mi nee na:
﴿شَهۡرُ رَمَضَانَ ٱلَّذِيٓ أُنزِلَ فِيهِ ٱلۡقُرۡءَانُ هُدٗى لِّلنَّاسِ وَبَيِّنَٰتٖ مِّنَ ٱلۡهُدَىٰ وَٱلۡفُرۡقَانِۚ فَمَن شَهِدَ مِنكُمُ ٱلشَّهۡرَ فَلۡيَصُمۡهُ...﴾
﴾Ci weeru koor lañu wàcce Alxuraan, mu di ag njub ñeel nit ñi, ak di leeral njub tey teqale diggante dëgg ak neen, képp ku teewe weer wi ci yéen na ko woor.. ﴿ [Al-Baqara : 185].
Sàrti warug woor weeru koor:
1- Lislaam; koor du wér mukk ci ab yéefar.
2- mat, koor du war ci gone, Woor dana wér ci xale bu ràññee, waaye day nekk ci moom naafila.
3- Xel: woor du war ci ab dof, te du wér mukk ci moom; ndax amul yéene.
4- Man ko, Du war ci aji-tawat ji ko tëlé, Du caagine it ki nekk ci tukki, Waaye dañu koy fay su ngànt la jeexee: feebar ak tukki. Sàrtal nañu wérug koor ci jigéen gi: daggug dereeti mbaax ak dereeti wësin.
Duggug weeru koor dana saxe ci benn ci ñaari mbir, te mooy:
A- Gisug weeru Koor gi, Ndax waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
«صُومُوا لِرُؤْيَتِهِ، وَأفْطِرُوا لِرُؤْيَتِهِ».
"bu ngeen ko gisee woorleen, bu ngeen ko gisee worileen"48.
b- Matal weeru Baraxlu wi fanweeri fan, loolu mooy bu ñu gisul weeru Koor wi, walla bu dee niir mbaa pënd mbaa lu ko niru moo tee ñu gis ko, ngir waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
«فَإِنْ غُمَّ عَلَيْكُمْ؛ فَأَكْمِلُوا عِدَّةَ شَعْبَانَ ثَلَاثِينَ يَوْمًا».
«bu muuroo ci yéen; nangeen matal Baraxlu wi fanweeri fan»49.
Yéene ci woor:
Woor ak yeneen jaamu yi ñoo yam, du wér lu dul mu ànd ak yéene, Waxtuw warug yéene woor goo xam ne farata la, wuute na ag gu dul moom, te loolu nii lañu koy leerale:
Bi ci njëkk: koorug farata; lu ci mel ni woor weeru koor, walla fay, walla nisar, war nañu ko a yéene ci guddi gi njëkk fajar di jot, Ndax waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
«مَن لَمْ يُبَيِّتْ الصِّيَامَ مِنَ اللَّيْلِ فَلَا صِيَامَ لَهُ».
«Ku yéenewul woor ci guddi gi amul koor»50
Bu ñaareel bi: koorug coobarewu, moom dana wér nit ki yéene ko ci bëccëg gi, Ci sàrtu mu bañ a jëfandikoo luy dog koor ginnaaw ba fajar gi duggee.
Yiy yàq koor:
Bu njëkk bi: Sëy: ku sëy kooram yàqu na, te war na a fay bis boobu mu sëy, Kaffaara it dana war ci moom ànd ak fay gi: te mooy goreel jaam, Bu ko amul, kon day war ci moom mu woor ñaari weer yu toftaloo, Bu ko manul ngir ngàntul sariiha, kon day war ci moom mu leel juróom-benn fukki way ñàkk, ku ci nek ci ñoom genn wàllu Saah ca ñam wa ñuy lekk ca dëkk ba.
Ñaareel bi: génne Manniyu: ci sababus fóon, walla laal, walla génneel sa bopp Manniyu, walla bàmtu ag xool, kooku fay rekk a ko war ci lu dul kaffaara; ndaxte kaffaara ci jaxasoo rekk lay ware. Bu dee kiy nelaw nag, bu géntee ba génne Manniyu; dara waru ko ci, ndaxte loolu amewul ci coobareem, waaye day sangu janaba.
Ñatteel bi: lekk walla naan te tay ko: Ndax waxi Yàlla mu kawe mi:
﴿...وَكُلُواْ وَٱشۡرَبُواْ حَتَّىٰ يَتَبَيَّنَ لَكُمُ ٱلۡخَيۡطُ ٱلۡأَبۡيَضُ مِنَ ٱلۡخَيۡطِ ٱلۡأَسۡوَدِ مِنَ ٱلۡفَجۡرِۖ ثُمَّ أَتِمُّواْ ٱلصِّيَامَ إِلَى ٱلَّيۡلِ...﴾
﴾Lekkleen naanleen ba buum gu weex gi ak gu ñuul gi leer ci yéen ci fajar gi topp ngeen mottali koor gi ba ci tàmbalig guddi gi...﴿ [Al-Baqara : 187].
Ku lekk walla mu naan ngir fàtte, dara du ko ci war; Ndax Hadiis bii:
«مَن نَسِيَ وَهُوَ صَائِمٌ، فَأَكَلَ أَوْ شَرِبَ، فَلْيُتِمَّ صَوْمَهُ، فَإِنَّمَا أَطْعَمَهُ اللَّهُ وَسَقَاهُ».
«ku fàtte fekk dafa woor, mu lekk walla mu naan, na mottali wooram, ndax Yàlla moo ko leel moo ko nànnal»51.
Ñenteel bi: waccu te tay ko, waaye ku waccu gi not ci lu dul coobareem; loolu du am jeexit ci wooram gi, Ndax waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
«مَنْ ذَرَعَهُ الْقَيءُ فَلَيْسَ عَلَيْهِ قَضَاءٌ، وَمَن اسْتَقَاءَ عَمْدًا فَلْيَقْضِ».
«Ku ag waccu not, koo ku fay waru ko, waaye ku waccu te tay ko na fay»52.
Juróomeel bi: génne dereet ci yaram wi; ci gàjji, walla nàmmptal, walla xëcci dereet ngir maye ko ngir xettali ku tawat; loolu lépp day yàq koor. Bu dee nag génne dereet ju néew jees di jël ngir saytu; loolu du yàq koor. Naka noonu itam génnug dereet ci lu dul coobareem; niki bori, walla gaañu-gaañu, walla buddi bëñ; loolu du jeexital ci koor gi.
Ñi ñu daganal ñu dog ci weeru koor:
Xaaj bu njëkk bi: Ñi dog dagan ci ñoom, te fay war leen, ñooy:
Bi ci njëkkm mooy: Ku feebar feebar gu ñu yaakaar wér, te muy loru ci woor gi mbaa muy jafe ci moom.
Ñaareel bi: ki tukki; moo xam am na coono ci tukki bi walla amuko ca.
Tegtalu ñaar yooyu mooy waxi Yàlla mu kawe mi:
﴿...وَمَن كَانَ مَرِيضًا أَوۡ عَلَىٰ سَفَرٖ فَعِدَّةٞ مِّنۡ أَيَّامٍ أُخَرَ...﴾
﴾...képp ku feebar walla mu nekk ci tukki, na woor ci yeneen bis...﴿ [Al-Baqara : 185].
Ñatteel bi: Jigéen ju ëmb walla juy nàmpal, bu dee woor gi daf leen di sonal, walla di leen lor walla seen i doom, ñooñu ñoo yam àtte ak ki wopp, kon dagan na ci ñoom ñu dog. Waaye war na ci ñoom ñu fay koor gi ci jeneen jamono.
Ñenteel bi: Ki ame dereetu mbërëg ak wësin, ñoom ñaar dog war na ci ñoom Seenug woor du wér, te dina war ci ñoom ñu fay ko ci yeneen bis.
xaaju ñaareel bi: ñi ñu may ñu dog, te kaffaara war leen waaye fay waru leen, ñoo di:
Ki ci njëkk mooy: Ku feebar feebar gu ñu yaakaarul mu wér.
Ñaareel ki: ku màggat te manatul a woor.
Ñooñu dañuy dog, di leel ci bis bu nekk ci weeru koor bi ab way-ñàkk, Wànte nag ku màggat su eggee ci naag, kon toggooy jëf yi wàcc na ko; day dog te dara waru ko.
Waxtuw fay ak àtteb yéexe ko:
Fay wooru koor dana war ci digganteem ak weneen weeru koor. Li gën nag mooy gaawantu fay ko, Du dagan ñuy yéexe fay gi ba Koor gi ci tege rombu. Jële nañu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
«كَانَ يَكُونُ عَلَيَّ الصَّوْمُ مِنْ رَمَضَانَ، فَمَا أَسْتَطِيعُ أَنْ أَقْضِيَ إِلَّا فِي شَعْبَانَ لِمَكَانِ رَسُولِ اللهِ ﷺ».
«Daan naa am boru koor, te daawuma ko woon a man a fay lu dul ci weeru Baraxlu, ngir wàccuwaayu Yonnente bi yal na ko Yàlla xéewalal te jàmmal ko»53.
Ku yéexal fay gi ba ci weeru koor wa ca tege jàll kooku amna ñaari anam:
1- mu yéexe ko ngir ngàntul Sariiha, niki: feebar bi wéy ak moom ba weneen weeru koor jot, kooku fay rekk a ko war.
2- Mu yéexe ko te amul ngàntul Sariiha, kon day am bàkkaar ci yéexe gi, kon war na ci moom mu tuub ak fay, ak leel Miskiin ci bis bu nekk.
Woorug coobarewu ci ku war a fay:
Képp ku war a fay dara ci koorug Ramadaan; li gën mooy mu jiital ko njëkk koorug Ngàtt-nga, Waaye nag bu fekkee koorug naafila gi waxtoom day faat -niki koorug Arafa ak Tam-Xarit-; kon na ko woor laata njëkk muy fay; ndaxte fay gi waxtoom yaatu na, te Tam-Xarit- ak Arafa ñoom dañuy faat, Waaye du woor juróom-benni fan ci Kori lu dul ginnaaw bu fayee.
Yi araam a woor:
1- Woor bisu feetu korite, ak bisu feetu tabaski; ndaxte tere nañu ko.
2- Woor ñatti bis yi sës ci tabaski gi ci weeru tabaski. lu dul ki def Tamattouh ak Xiraan ci aj gi bu amul gàtt gu mu rendi, Fani Tasriiq yi ñoo di: fukkeelu fan bi ak benn, ak fukkeel bi ak ñaar, ak fukkeel bi ak ñatt ci weeru Tabaski.
3- Bisub sikk-sàkka ndax sikk-sàkka, te mooy bisu fanweereel bi ci weeru Baraxlu, Bu dee guddi ga daa niir mbaa mu puseer ba mu tee ñu gis weer wi.
Yi ñu sib a woor:
a- Jagleel weeru Rajab ci woor. b- jagleel bisu àjjuma ci woor, ngir tere gi ci am, Bu wooree bis bi ko jiitu mbaa ba ca topp, kon sibeel gi deñ.
Yi ñu sunnaal a woor:
A- juróom-benni fann ci weeru kori gi. B- Woor juróom-ñenti fani Tabaski yi, bi ci gën a feddaliku mooy bisu Arafa, lu dul ci kiy aj; kooku sunnaaluñu ci moom mu woor ko, te woor ko day kaffaara ñaari at. C- Woor ñatti fan ci weer wu ne, li ci gën mooy mu def ko ci bis yu leer yi, te mooy: bisu fukkeel bi ak ñatt, ak fukkeel ak ñent, ak fukkeel ak juróom. D- Woor Altine ak alxamis ci ayu bis bu ne, ndaxte yonente bi, yal na ko Yàlla dolli jàmm ak mucc, daan na ko woor; ndaxte ci lañuy gaaral jëfi jaam yi.
Woorug ngàtt-nga:
A- woorug Daawuda yal na ko Yàlla dolli jàmm, da daan woor bis dog bis.
B- Woor weeru Yàlla wa ñu wormaal, moom mooy weer wi ñu gën a sopp a woor, gi ci gën a feddaliku: mooy woor bisub Tamxarit, muy fukkeelu fan ci weer wi, manees na ko a booleel ak juróom-ñeenteelu fan bi; ndax waxu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-:
«لَئِنْ بَقِيتُ إِلَى قَابِلٍ لَأَصُومَنَّ التَّاسِعَ».
"bu ma dundee ba déwén, dinaa woor bisub juróom-ñenteel bi"54. Day far bàkkaar i at mi ko jiitu.
Juróomeelu waxtaan wi: aj ak umra
Aj ci làkk araab mooy: ag jublu. Ci Sariiha: Mooy jublu néegu Yàlla ba ñu wormaal ak bérab ya ñu wormaal, ci waxtu wu ñu ko jagleel, ngir def ay jaamu yu ñu ko jagleel.
Umra: ci làkku araab: mooy siyaare.
Ci Sariiha: mooy siyaare Néeg ba ñu wormaal ci waxtu wu mu man a doon ngir def ay jaamu yu ñu ko jagleel.
Aj nag, dafa bokk ci ponki Lislaam yu màgg yi, Farataalees nañu ko ci juróom-ñenteelu at ci gàddaay gi, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- aj na genn aj; mooy (ajug tàggatoo ga).
Aj nag day war ci ku ko man benn yoon cig dundam. Lu ci tege nag ag coobarewu la. Bu dee Umra moom lu war la ci waxu ñu bari ci boroom xam-xam yi, Firnde ji mooy bi ñu laajee Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-: ndax jihaad war na jigéen ñi? Mu ne:
«نَعَمْ، عَلَيْهِنَّ جِهَادٌ لَا قِتَالَ فِيهِ: الْحَجُّ وَالْعُمْرَةُ».
«Waaw, jihaad gu amul xeex war na ci ñoom te mooy: Aj ak Umra»55.
Sàrti yiy waral Aj ak Umra:
1- Lislaam
2- Xel
3- Mat
4- nekk Gor.
5- Man-man
Jigéen gi day dolli sàrtu juróom-benneel; te mooy am kojug armal guy ànd ak moom ci tukki bi ngir mu def ko. Ndaxte daganul ci moom muy tukki ngir aj walla leneen, ci lu dul kojug armal. Ndax waxu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc:
«لَا تُسَافِرُ الْمَرْأَةُ إِلَّا مَعَ ذِي مَحْرَمٍ، وَلَا يَدْخُلُ عَلَيْهَا رَجُلٌ إِلَّا وَمَعَهَا مَحْرَمٌ».
«jigéen du tukki lu dul mu ànd ak kojug armalam, te bu benn góor dugg ci moom lu dul mu nekk ak koju armalam»56.
Kojug armalu jigéen mooy: jëkkëram, walla ku ñu araamal mu sëy ak moom araam gu sax ba fàww; ci askan; niki mbokkam mu góor ak baayam ak baay taxam ak doom ju góor ju mbokkam mu góor jur ak nijaayam, Wala ci sabab bu dagan; niki mbokk ci nàmpaale, walla ci gorowante; niki jëkkëru yaayam ak doom ju góor ju jëkkëram jur.
Man-man nag mooy: kàttan gu alal ak gu yaram, mu man a war te muñ tukki bi, te am ci alal lu ko doy ci dem ak dikk, Ak itam mu am lu doy ay doomam ak ñi nga xam ne seenug dund daf koo war, ba keroog muy dellu ca ñoom.
Te yoonu aj wi nekk lu am kaarànge ci bakkanam ak alalam.
Ku ko man ci alalam, te manu ko ci yaramam, ci mu nekk mag mu màggat, walla mou feebar feebar guy sax ba yaakaaruñu mu wér; war na ci moom mu wut ku ko ajal ak umralaal ko.
Dees na sàrtal ci kiy Ajal keneen ak Umra ñaari sàrt:
1- Mu doon koo xam ne def Faratay Aj dana wér ci moom, te mooy jullit bu nekk mukallaf, te am xel.
2- Mu ajaloon boppam ajug Lislaam.
Bérabi armal yi (miixaat yi):
Miixaat, ci làkk araab, mooy: aw Dig. Ci Sariiha nag, mooy: bérabu jaamu Yàlla walla waxtoom.
Aj am na ay jamonoy armal ak ay bérabi armal:
A- Waxtuy armal yi: Yàlla tudd na leen ci waxam jii:
﴿ٱلۡحَجُّ أَشۡهُرٞ مَّعۡلُومَٰتٞۚ فَمَن فَرَضَ فِيهِنَّ ٱلۡحَجَّ...﴾
﴾Aj ay weer yu ñu xam la, ku warlu ci ñoom aj...﴿ [Al-Baqara: 197].
Te weer yii ñooy: kori ak digi ak fukki fanni weeru tabaski.
B- Bérabi armal yi: ñooy dig yi nga xam ne daganul ci kiy aji mu romb leen jëm Màkka te armalul, Ñoom ñooy yii di ñëw::
1- Zul Hulayfa: Bérabu armalu waa Madiina la.
2- Juhfa: mooy bérabu armalu waa Saam ak waa Esipt ak waa sowu jant (Marok).
3- xarnul Manaazil: ñu xame ko leegi ci turu Sayl; mooy bérabu armalu waa Najdi.
4- Zaatu Hirq: bérabu armalu waa Iraak la.
5- Yalamlam: mooy Bérabu armalu waa Yaman.
Koo xam ne këram eggul ci Miixaat yii; kon day armale ci këram ngir Aj ak Umra. Ñi bokk ci waa Màkka; dañuy armale ca Màkka, te soxlawuñoo génn jëm ca Miixaat ba ngir armal. Bu dee Umra nag: dañuy génn ba ca armalukaay bu gëna jege, ñu armale fa. Képp ku bëgg a Aj walla Umra, fàww mu armale ci bérab yi nga xam ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moo leen tënk; te ñooy Miixaati bérab yi ñu fi njëkkoon a leeral. Du dagan ci képp ku bëgg a aj walla umra mu weesu ko te armalul.
- Képp ku romb ca Miixaat ya ñu tudd, te bokkul ca waa bérab booba ; kon fa lay armale.
- Ku jëm Màkka, te rombul ci benn ci Miixaat yi ñu tudd, moo xam ci jéeri la walla géej, walla ci asamaan; dafay armal bu tolloowee ak Miixaat bi ko gën a jege. Ndax waxi Umar ibn Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm-: "xoolleen fi tolloo ak moom ci seen yoon wi"57.
- Ku nekk ci Abiyoŋ di dem ngir Aj walla Umra, war na ci moom mu armal bu Abiyoŋ bi tolloo ak Miiqaat bi nekk ci yoonam. Te du dagan ci moom mu yéexe armal gi ba Abiyoŋ bi wàcc ca Aydapoor ba.
Armal:
Mooy yéeney dugg ci jaamu gi; Bu dee Aj mooy: yéenee dugg ci Aj gi, Bu dee Umra mooy yéenee dugg ci Umra gi. Du armal lu dul bu yéenee dugg ci jaamu gi. Waaye sol yérey armal rekk te yéene woon loolu du nekk Armal.
Yi ñu sopp ci armal:
1- Sangu set mu daj mbooleem yaram wi balaa muy Armal.
2- Góor gi laal gëtt ci yaramam, du ko laal nag ci yérey armalam.
3- Armal ci koddaay ak làmbaay yu weex ak ñaari dàll.
4- mu Armal fekk mi ngi war jublu xibla.
Xeeti jaamuy aj gi:
Dees na tànn loo kiy Armal bu ko soob ci ñatti xeeti jaamu yii:
1- Tamattuh; te mooy mu armal ngir umra ci weeri aj gi, mu jeexal ko, topp mu armal ngir aj ci mem at mi.
2- Ifraad; mooy : mu armale ca Miiqaat ba ngir aj kese, te mu des ca armalam ga ba baa muy matal jëfi aj gi.
3- Xiraan; mooy mu armal ngir Aj ak Umra yépp, walla mu armal ngir Umra, topp mu dugal ci Aj ga njëkk muy muy wër kaaba ga, mu yéene Umra ak Aj ca Miqaat ba, walla njëkk muy door wërug Umra ga, mu wër kaaba gi ngir ñoom ñaar daal di dox Safaa ak Marwa.
War na ci kiy Tamattouh ak kiy Xiraan ñu jotu (Fidya), bu ñu bokkul ci ñi nekk ci Jàkka ji ñu woraal (Jàkkay Màkka).
Li gën nag ci ñatti ajiin yii mooy: Tamattuh; ndax Yonnente bi, yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, moo ko dénk ay Sahaabaam58. Mu topp ci Xiraan, ndax moom aj la ak umra, teg ci Ifraad.
C) bu armalee ngir benn ci jaamu yii; day Talbiya ginnaaw armalam ga, muy wax:
«لَبَّيْكَ اللَّهُمَّ لَبَّيْكَ، لَبَّيْكَ لَا شَرِيكَ لَكَ لَبَّيْكَ، إِنَّ الْحَمْدَ وَالنِّعْمَةَ لَكَ وَالْمُلْكَ لَا شَرِيكَ لَكَ».
"Labbayka Allaahuma, labbayka, labbayka laa siriika laka labbayka, innal hamda wannihmata laka walmulka laa sariika laka"59.
Moom nag Sunna la, te sopp nañu ñu koy baril, góor gi daf koy biral, jigéen ñi di ko yelu.
Waxtoom: waxtoom mi ngi tàmbali ginnaaw armal gi, waxtoom wi mujj nag nii lay deme:
Li ci njëkk: Aji-umra ji da koy dagg balaa muy tàmbali wër kaaba gi.
Ñaareel bi: Kiy aj da koy dog bu tàmbalee sànni jamratul Hãqabat ci bisub tabaski bi.
Yi ñuy moytandiku ci armal:
Tere gu njëkk gi: Wat kawar walla jemp ko walla suqi ko, ci bérab bu mu man a doon ci yaram wi.
Tereg ñaareel gi: lelli ay weh ci loxo walla ci tànk ci lu dul ngànt. Waaye bu weh yi dammoo, mu dindi ko, kon fidya du ko ci war.
Tereg ñatteel gi: Muur bopp ci góor ci luy taqok bopp bi lu mel ni: mbaxana ak kaala.
Tereg ñenteel gi:góor gi sol lu ñu ñaw ci yaramam walla lenn ci céri yaram wi; niki: Semis, ak kaala, ak pantalooŋ. Lu ñu ñaw nag mooy: li ñu defar ngir mu méngoo ak tolluwaayu yaram wi, niki ay saŋ ak ay gaŋ ak ay kawas. Jigéen moom, day sol ci yére bu ko soob jamono yi mu armalee ngir li mu aajowoo muuru, waaye nag du sol Burqaa, day muur kanamam ci leneen niki musóor ak jàllaabe, bu ay jàmbur yu góor dee romb, Du sol it ñaari Gaŋ ci ñaari loxoom.
Tereg juróomeel gi: Gëtt; (parfum) ndax ki armal dañuy sàkku ci moom mu sori nooflaay ak taaru àdduna ak i bànneexam, te mu jublu allaaxira.
Tereg juróom-benneel gi: ray rëbbum jéeri ak rëbb ko, ki armal du rëbb rëbbum jéeri, du dimbalee ci rëbb ko, te du ko rendi it.
Araam na ci ki Armal mu lekk ci lu mu rëbb, walla lu ñu ko rëbal, walla mu dimbalee ci rëbb ko; ndaxte dees koy jàppe am médd ci moom.
Bu dee rëbbum géej moom, araamul ci ki Armal mu rëbb ko. Te araamul itam ci moom mu rendi bayimay kër, niki ginaar ak jur yi; ndaxte nekkul am rëbb.
Tereg juróom-ñaareel gi: takk ab sëy ngir boppam walla ngir keneen, walla muy seede ab sëy buñuy takk.
Tereg juróom-ñatteel gi: sëy; ku sëy laata summiku gu njëkk gi, ajam dafay yàqu, waaye day war si moom mu àggale ajam gi, te mu fay ko ci at mi ci topp, te war na ci moom mu rendi ag jur (Badana). Bu dee ginnaaw simmiku gu njëkk gi la, jaamoom du yàqu, waaye dereet war na ko.
Jigéen gi ak góor gi ñoo yem ci loolu donte dafa topp jëkkëram.
Tereg juróom-ñenteel gi: joñjoo ci fu dul awra wi, kon daganul ci ki armal mu joñjoo ak jigéen, ndax manna nekk sabab si mu def lu araam si moom te mooy mu sëy, li ñu namm ci joñjoo mooy: laal jigéen ngir bànneex.
Umra:
A- Ponki umra:
1- armal.
2- Wër kaaba ga.
3- dox Safaa ak Marwa.
B- Warteefi umra:
1- Armale ca béreb armalukaay ba mu war a ame.
2- Watu walla wàññi.
C- Melow Umra:
Li kiy umra di njëkk a def mooy, mu wër Kaaba gi juróom-ñaari wër, day tàmbalee ca Doj wu ñuul wa jeexale fa itam. Bu dee wër day laab, te muur awraam li ko dale ca jumbux ba ba ca óom ya, Sunnaal nañu ci moom mu feeñal mbaggum ndayjooram, jaarale làmbaayam ca suufu poqtaanu ndayjooram, daal di teg ñaari lafi làmbaay gi ci kaw mbaggum càmmooñam, Bu matalee juróom-ñaareelu wër gi, day muuraat ñaari mbaggam ak làmbaayam.
Mu jublu Hajarul Aswad, bu ko manee fóon mu fóon ko, bu ko manul mu laal ko ak loxo ndayjooram bu jàppandee, daal di fóon loxoom, Bu laal gi yombul ci moom, da koy junj ci yëkkëti loxo ndayjooram daal di wax: «Allaahu Akbar» benn yoon, te du fóon loxoom bi, te du taxaw it, Topp mu wéy ci wëram gi; def kaaba ga mu féete ci càmmooñam, yoonalees nañu mu ñukk ci ñatti wër yu njëkk yi, Ñukk nag mooy gaawal dox bi ànd ak jegeele jéego yi.
Bu jaaree ci Roknu Yamaanii bi -te mooy ñenteelu koñu Kaaba gi- bu ko yombee mu laal ko ak loxo ndayjooram ci lu dul kàbbar ak fóon, bu loolu yombul mu jàll te du ko junj te du kàbbar itam. Mu wax ci diggante Ruknu Yamaanii bi ak Hajarul Aswad bi:
﴿...رَبَّنَآ ءَاتِنَا فِي ٱلدُّنۡيَا حَسَنَةٗ وَفِي ٱلۡأٓخِرَةِ حَسَنَةٗ وَقِنَا عَذَابَ ٱلنَّارِ﴾
﴾...Ràbbanaa aatinaa fid dunyaa hasanatan wa fil aaxirati hasanan wa xinaa hasaaban naari﴿
[Al-Baqara: 201].
Bu noppee ci wër gi, day julli ñaari ràkka ca ginnaaw Màqaamu Ibraahiima bu loolu jàppandee, lu ko moy mu julli ci bérab bu mu man a doon ci Jàkka ji ñu wormaal, Sunnaal nañu mu jàng ci ràkka bu njëkk bi ginnaaw Faatiha saaru (Al-Kaafiruuna), Mu jàng saaru (Lixlaas) ci ràkka bu ñaareel bi ginnaaw Faatiha, Topp mu jëm ca doxukaay ba, mu dox ci diggante Safaa ak Marwa juróom-ñaari yoon; dem gi benn yoon la, dellusi gi beneen yoon la.
Day tàmbalee Safaa, daal di fay yéeg, walla mu taxaw fa, yéeg ca Safaa nag moo gën bu dee yomb na, mu jàng foofa waxu Yàlla mu kawe mi:
﴿إِنَّ ٱلصَّفَا وَٱلۡمَرۡوَةَ مِن شَعَآئِرِ ٱللَّهِ...﴾
﴾innas Safaa wal marwata min sahaa-iril Laahi...﴿ [Al-Baxara: 158].
Sopp nañu mu jublu kaaba gi, daal di sant Yàlla, màggal ko, daal di wax:
«لَا إِلٰهَ إِلَّا اللَّهُ، وَاللَّهُ أَكْبَرُ، لَا إِلٰهَ إِلَّا اللَّهُ وَحْدَهُ لَا شَرِيكَ لَهُ، لَهُ الْمُلْكُ وَلَهُ الْحَمْدُ، يُحْيِي وَيُمِيتُ، وَهُوَ عَلَى كُلِّ شَيْءٍ قَدِيرٌ، لَا إِلٰهَ إِلَّا اللَّهُ وَحْدَهُ، أَنْجَزَ وَعْدَهُ، وَنَصَرَ عَبْدَهُ، وَهَزَمَ الْأَحْزَابَ وَحْدَهُ».
"laa ilaaha illal Laahu, wal-Laahu akbaru, laa ilaaha illal Laahu wahdahu laa sariika lahu, lahul mulku, wa lahul hamdu, yuhyii wa yumiitu, wa huwa halaa kulli say-in xadiirun, laa ilaha illal Laahu wahdahu, anjasa wāhdahu, wa nasara habdahu, wa hasamal ahsaaba wahdahu"60. topp mu ñaan ci li mu man mu yëkkëti ay loxoom, te bàmtu sikkar gii ak ñaan gii ñatti yoon, Topp mu wàcc, dox jëm Marwa, ba bu eggee ca màndarga wu njëkk ma, góor gi gaawal ab doxam ba egg ca màndarga wu ñaareel ba, Ku jigéen ki nag, yoonaluñu ci moom muy gaawantu ci diggante ñaari màndarga yi ndaxte awra la, waaye li ñu yoonal ci moom moy dox ci dox Safaa ak Marwa gi yépp, topp mu dox, mu yéeg ca marwa walla mu taxaw fa, yéeg ca nag moo gën bu loolu yombee, mu wax dal di def ci kaw marwa kem li mu waxoon ak li mu defoon ca kaw Safaa, ba mu des jàng aaya bi, te mooy waxu Yàlla mu kawe mi:
﴿إِنَّ ٱلصَّفَا وَٱلۡمَرۡوَةَ مِن شَعَآئِرِ ٱللَّهِ...﴾
﴾innas Safaa wal marwata min sahaa-iril Laahi...﴿ Lii bu ñuy yéeg ca Safaa ci yoon wu jëkk wi dong lañu ko yoonal, Topp mu wàcc, di dox ci bérabu doxukaay bi, di gaawantu ci bérabu gaawantu yi, ba egg ca Safaa, Mu def loolu juróom-ñaari yoon, dem gi benn yoon la, delluseem gi it beneen yoon la. Sopp nañu mu baril ca ba muy dox lu ko yomb ci sikar ak ñaan, Ak mu laab ci toj mu mag ak mu ndaw, waaye bu ko defee te laabul, loolu doy na ko. Naka noonu bu jigéen amee mbërëg walla meret ginnaaw wër ga; day dox Safaa ak Marwa, te loolu doy na ko; ndaxte laab nekkul sàrt ci doxum Safaa ak Marwa, waaye kay lu ñu ci sopp la rekk.
Bu matalee dox ga, mu wat boppam walla mu wàññi ko, wat gi nag moo gën ci góor.
Ci lii la jëfi jaamuy umra gi di mate.
Aj:
A- Ponki aj:
1- armal.
2- taxaw Arafa.
3- wër Kaaba gi wërug bëbb ga.
4- dox digante Safaa ak Marwa.
B- Warteefi aj:
1- Armal ca bérebu armalukaay ba.
2- Taxaw Arafa ci bisu juróom-ñenteel ci Sul-Hijja ba sowu jant bi, ñeel ku fa taxawoon bëccëg.
3- Fanaan Musdalifa guddig fukkeel bi ci weeru Tabaski ba ci diggu guddi gi.
4- Fanaan Minaa ci fani Tabaski yi.
5- Sànni Jamra yi.
6- Watu walla wàññi.
7- wërug tàggatoo gi.
C- Ni ñuy aje:
Jullit bi day Talbiya ngir aj bu eggee ca Miixaat ba tey def Ifraad bu dee waxtu wi dafa xat, bu eggee Màkka mu wër Kaaba gi, daal di dox Safaa ak Marwa, mu des ci armalam gi ba baa muy dem Arafa ci bisub Arafa bi di bisub juróom-ñenteel ba, mu des fa ba jant bi so,
Topp mu jóge fa di Talbiya wu jëm Musdalifa, mu des fa ba julli fajar, topp mu des fa di tudd Yàlla di talbiya di ñaan ba suba gi leer,
Su bët setee mu dem Minaa balaa jant bi di fenk, mu sànni jamratul Hãqabat juróom-ñaari xeer, topp mu wat boppam walla mu wàññi ko, wat gi nag moo gën,
Topp mu wër kaaba gi wërug Ifaada gi, dox gu njëkk ga dana ko doy, ci loolu la ajam matee, mu am soumeeku gu mat sëkk.
Mu des fa di sànni jamra ya ci bisu fukkeel bi ak benn ak bisu fukkeel bi ak ñaar, bu fekkee ku yàkkamti la; day sànni ñatti jamra ya, jamra ju nekk mu sànni fa juróom-ñaari xeer, di kàbbar ci xeer wu nekk, mu doore ko ci bu ndaw bi topp ci jàkkay Xayf, teg ca bu digg ba, teg ca jamratul Hãqabat, te mooy ba mujj, jamra ju nekk mu sànni fa juróom-ñaari xeer. Bu bëggee yeexe ginnaaw bisu fukkeel bi ak ñaar, day sànni ci bisu fukkeel bi ak ñatt, kem ni mu ko sànnee woon ci bisu fukkeel bi ak ñaar ak bisu fukkeel bi ak benn.
Waxtu sànni gi mooy: ginnaaw tisbaar ci ñatti fan yi.
Bu jógee ci bisu fukkeel bi ak ñaar njëkk jant bi di so dara waruko ca, waaye bu toogee ba sànni ci bisu fukkeel bi ak ñatt ginnaaw tisbaar, loolu nag mooy li gën, ndax waxu Yàlla mu kawe mi:
﴿...فَمَن تَعَجَّلَ فِي يَوۡمَيۡنِ فَلَآ إِثۡمَ عَلَيۡهِ وَمَن تَأَخَّرَ فَلَآ إِثۡمَ عَلَيۡهِۖ لِمَنِ ٱتَّقَىٰ...﴾
﴾...Képp ku gaawantu ci ñaari fan, bàkkaar nekkul ci kawam, te képp ku yéex it, bàkkaar nekkul ci kawam, loolu nag ñeel na ki ragal Yàlla... ﴿
[Al-Baqara: 203].
Bu bëggee tukki; day wër ngir tàggoo juróom-ñaari yoon ci lu dul dox Safaa ak Marwa.
Li gën nag ñeel ku amul lu mu rendi: mooy mu armal ngir umra, topp mu armal ngir aj ci bisub juróom-ñatteel bi, daal di jef jëfi aj yi jiitu woon. Bu armalee nag ngir boole aj ak umra yépp, kon it aayul, loolu lañuy woowe Xiraan, te mooy mu armal ngir boole umra ak aj ci genn wër ak genn ug dox.
Teqale bu ñatteel bi:
Li aju ci jëflante yi
Woroom xam-xam yi -yal na leen Yàlla yërëm- leeral nañu xam-xam bi war ci kenn ku nekk mu jàng ko. Waxtaane nañu ci tolluwaay bi nga xam ne jàng ko faratay jëmm la ci kaw bépp jullit, Tudd nañu ci: jàng àttey jaay yi, ñeel kiy def yaxantu, ba du tàbbi ci lu araam walla Ribaa fekk xamul, Rot na jóge ci ñenn ci Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- luy dëggëral loolu.
Umar ibn Xattaab -yal na ko Yàlla dollee gërëm- nee na: «Bu kenn jaay ci sunu Ja bii (marse) lu dul ku dégg diine»61.
Aliyun Ibn Abii Taalib yal na ko Yàlla dollee gërëm nee na: «Ku yaxantu laata muy jàng; tàbbi na ci Ribaa, tàbbiwaat ca, daal di cay tàbbiwaat. Maanaam: dafa tàbbi ci Ribaa»62.
Ibn Aabidiina wax na, ñu jële ko ci Al-Allaamii: Farataal nañu ci bépp mukàllaf góor ak jigéen, ginnaaw ba mu jàngee xam-xamu diine ak njub, mu jàng xam-xamu jàppu ak sangu farata ak julli ak woor, ak xam-xamu asaka ñeel ki am nisaab, ak aj ñeel ku mu war, ak njaay ci jaaykat yi, ngir ñu man a moytu lënt-lënt yi ak yi ñu sib ci mbooleem jëflante yi, naka noonu boroom mecce yi, ak képp kuy yëngu ci dara farata la ci moom mu xam ko te xam àtteem ngir mu moytu lu araam ci biir loolu63.
Nawawii yal na ko Yàlla yërëm nee na: "Bu dee nag jaay ak sëy ak yu mel ni ñoom, ci yi nga xam ne seen cosaan nekkul lu war, kon day araam ñu jëm ca lu dul ginnaaw bu ñu xamee ay sàrtam64.
Yii yenn la ci tënk yi aju ci jëflantey alal yi Sariiha Lislaam indi:
1- Daganal lépp loo xam ne njariñ rekk moo ca nekk walla mu gën ca a not, niki jaay yi dagan ak jënd yi dagan; ak luye, ak As-Sufha65.
2- yoonal lépp luy garde àqi doomu Aadama; niki tayle ak wut seede.
3- yoonal lépp lu am njariñ ñeel ñaar ñiy jëflante; niki xàcci am njaay, ak tànn, ak sàrt yi nekk ci njaay mi.
4- Tere lépp lu làmboo ag tooñ nit ñi, ak lekk seen i alal ci ag neen; niki Ribaa, siif, ak rënk màrsandiis.
5- yoonal lépp lu dimbalante ci yiw nekk: niki lebale, aale, ak dénkaane.
6- Tere lépp lu làmboo lekk alal ci lu dul liggéey du caagine njariñ, mbaa coono; niki kàrt ak Ribaa.
7- Tere bépp jëflànte boo xam ne réer ak wuruñ ëppe; niki nit ki jaay lu mu moomul ak jaay lu ñu xamul.
8- Tere nañ lépp luy pexe ngir daganal lu araam; niki jaayu Al-hiina66.
9- Tere lépp luy soxlaale wolif topp Yàlla; niki jaay ginnaaw ñaareelu noddug Àjjuma gi.
10- Araamal lépp lu am lor, walla luy jur noonoo ci diggante jullit ñi, niki njaay yu araam yi, ak nit ki di jaay ci kaw njaayu mbokkam.
Bu àtteb masala ci masala yi lëntee ci ab jullit, dafa war a laaj woroomi xam-xam yi, te du ci jëm lu dul ginnaaw bi mu xamee àtteb Sariiha bi, kem ni ko yalla mu kawe mi waxe:
﴿...فَاسْأَلُوا أَهْلَ الذِّكْرِ إِنْ كُنْتُمْ لَا تَعْلَمُونَ﴾
﴾... laajleen boroom xam-xam yi bu ngeen xamul﴿ [An-Nahl: 43].
Lii mooy li jàppandee dajale, Yàlla rekk lañuy ñaan mu wërsëgal nu xam-xam buy jariñ ak jëf ju baax, ndax moom ku tabe la ku tedd la. Yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc sunu Yonnente ba Muhammat, ak waa këram ak i Sahaabaam, te muccal ko muccal gu sax dàkk.
***
xetouk tenk
Laytaayu aji-taalif ji 2
Teqale bu njëkk bi: 3
Li aju ci pas-pas 3
Waxtaan wu njëkk wi: Maanaam Lislaam ak i ponkam. 3
Solos Tawhiid: 3
Maanaam "seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla": 5
Sàrti (laa ilaaha illallaahu nag) mooy: 5
Maanaam seede ne Muhammat ndawul Yàlla la: 6
Ñaareelu waxtaan wi: maanaam gëm ak i ponkam: 8
1) gëm Yàlla day làmboo ñatti mbir: 9
1- Gёm moomeelam gi: 9
2- Gëm wéetam gi cig jaamu: 11
3- gëm ay turam ak i meloom: 13
2) gëm Malaaka yi. 20
3) gëm téere yi: 21
4) Ñenteel bi: Gëm Yonente yi -yal na jàmm nekk si ñoom-: 22
5) Gëm bis bu mujj ba: 23
A- gëm dekki: 23
B- Ñaareel bi mooy: gëm càmbar ga ak fay ga: 23
C- gëm àjjana ak sawara: 24
6) gëm dogal bu neex ak bu naqari: 24
Ñatteelu waxtaan wi mooy: rafetal 26
ñenteelu waxtaan wi: ab tënk bu gàtt ci cosaani Ahlu sunna wall jamaaha: 26
Teqaleg ñaareel bi: lu aju ci jaamu Yàlla yi 27
Waxtaan wu njëkk wi: Laab: 27
Li ci njëkk: xeeti ndox yi: 28
Ñaareel bi: Sobe: 28
Ñatteel bi : li aram a def ci ku amul jàpp: 30
Ñenteel bi: Teggini faj aajo: 32
Juróomeel bi: àttey Laabu ak fompu: 33
Juróom-benneel bi mooy: àttey njàppu. 34
Juróom-ñaareel bi: Àttey masaa ñaari saŋ ak ay kawas: 35
Juróom-ñatteel bi: àttey tiim: 37
Juróom-ñenteel bi: Àttey mbërëg ak meret: 39
Ñaareelu waxtaan wi: Julli: 41
Li ci njëkk: àttey nodd ak liqaam: 41
Ñaareel bi: solos julli ak ngëneelam: 44
Ñatteel bi: Sàrti julli: 46
Ñenteel bi: ponki julli: 47
Juróomeel bi mooy: yi war ci julli. 52
Juróom-benneel bi: sunnay julli. 54
Juróom-ñaareel bi: melow julli: 56
Juróom-ñatteel bi: yi ñu sib ci julli: 61
Juroom-ñenteel bi mooy: yiy yàq julli: 61
10- fukkeel bi: sujjóotu njuumte: 62
Fukkeel bi ak benn mooy: Waxtu yi ñu aaye ku ci julli: 64
Fukkeel ba ak ñaar: jullig mbooloo: 64
Fukkeel bi ak ñatt: jullig ragal: 67
Melokaanu jullig ragal: 67
Fukkeel bi ak ñent: Jullig àjjuma: 68
Juróomeel bi: Mbir yi ñu sopp ci bisub àjjuma: 70
Dab àjjuma gi: 71
Fukkeel bi ak juróom: jullig ñi ame ngànt: 71
Fukkeel bi ak juróom-benn: jullig ñaari feet yi. 74
Fukkeel bi ak juróom-ñaar: jullig muurug jant bi: 76
Fukkeel bi ak juróom-ñatt: jullig baawnaan: 78
Fukkeel bi ak juróom-ñent: Àttey néew: 79
Waxtaan wu ñatteel wi: Asaka: 82
1- Xamle asaka ak gëddam: 82
2- Sàrt yiy waral asaka: 83
3- Alal yi asaka war: 84
Waxtaanu ñenteel bi: Woor: 94
Sàrti warug woor weeru koor: 95
Juróomeelu waxtaan wi: aj ak umra 102
Sàrti yiy waral Aj ak Umra: 103
Bérabi armal yi (miixaat yi): 104
Armal: 106
Umra: 110
Aj: 113
Teqale bu ñatteel bi: 115
Li aju ci jëflante yi 115
***
wo227v3.0 - 10/07/2026
Ahmad génne na ko ci Musnadam, ci limatu (6072), ak At-Tirmisii ci limatu (1535) mu wax ne hadiis bu rafet la.
Al-Buxaarii génne na ko ci Al-Adabulmufrad ci limatu (716), ak Ahmad ci Al-Musnad ci limatu (19606), ak Diyaa Al-Maqdisii ci Al-Ahaadiis Al-Muxtaara (1/ 150), te Al-Albaanii weral na ko ci Sahiih Al-Jaamih As-Saxiir ci limatu (3731).
Muslim génne na ko ci limatu (121), ak Ahmad ci Musnad bi ci limatu (10434).
(Masyu): mooy ndox mu woyof te amul melo, tey génne ci jamonoy poh walla bu nit fàttalikoo ag sëy walla mu bëgg ko, walla muy xool walla leneen lu ni mel. Tey génn ci toq-toq te man naa génn te du ko yég. (Wadyu): mooy ndox mu diis te weex tey génn ginnaaw saw, walla bu nit yëkëtee lu diis.
Muslim génne na ko ci limatu (224).
Maalik génne na ko ci Al-Muwatta ci ñaari limat yii (680 ak 219), ak Ad-Daaramii ci limatu (312) ak Abdur-Razzaaq ci Musannafam ci limatu (1328), Al-Albaanii wéral na ko ci Irwaa'ul Xaliil ci limatu (122).
An-Nasaa-iyyu génne na ko ci limatu (12808), ak Ahmad ci limatu (15423), Al-Albaanii wéral na ko ci Irwaa Al-Xaliil ci limatu (121).
Ibn Maaja génne na ko ci limatu (594), ak Ibn Hibbaan ci limatu (799), Al-Albaanii doyadil na ko ci Dahiifu Sunan At-Tirmisii ci limatu (146).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (142), ak Muslim, ci limatu (122).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (7288), ak Muslim, ci limatu (6066).
Sang bu tedd bi Seex Abdul Asiis Ibn Baas -yal na ko Yàlla yërëm- wax na ci téereem ba tudd Majmuuhu Fataawaa (29/141) ne: (Bayhaqii yokk na ci, ci càllae gu baax, ñu jële ci Jaabir, ginnaaw wax jii di: «allazii wahadtahuu» : «innaka laa tuxliful miihaadi»).
At-Tirmisii génne na ko, ci limatu (2635).
Muslim génne na ko ci limatu (82).
At-Tirmisii génne na ko ci limatu (265), mu wax ne: hasan sahiih gariib, Al-Albaanii wéral na ko ci Sahiih At-Tarxiib wat-Tarhiib.
Al-Buxaarii soloo na ko ci limatu (1117).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (6251), ak Muslim, ci limatu (884).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (756), ak Muslim, ci limatu (872).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (793), ak Muslim, ci limatu (398).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (812), ak Muslim, ci limatu (490).
Muslim génne na ko ci limatu (498).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (724), ak Muslim, ci limatu (398).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (797), ak Muslim, ci limatu (402).
At-Tirmisii génne na ko ci limatu (839).
Al-Buxaarii soloo na ko ci limatu (6008).
Al-Buxaarii soloo na ko ci limatu (1110).
Al-Buxaarii soloo na ko ci limatu (835).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (743), ak Muslim, ci limatu (399).
At-Tirmisii soloo na ko, ci limatu (266).
Muslim génne na ko ci limatu (588).
Abuu Daawuda génne na ko ci limatu (5168).
At-Tirmisii génne na ko ci limatu (284).
Muslim génne na ko ci limatu (1484).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (609), ak Muslim, ci limatu (602).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (4130), ak Muslim, ci limatu (842).
Muslim génne na ko ci limatu (865).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (934), ak Muslim, ci limatu (851).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (1081), ak Muslim, ci limatu (693).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (1012), ak Muslim, ci limatu (894).
Abuu Daawuda génne na ko ci limatu (3201), ak At-Tirmisii ci limatu (1024), mu wax ne: hadiis la bu rafet te wér.
Muslim génne na ko ci limatu (962).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (8), ak Muslim, ci limatu (111).
Ibn Maaja génne na ko ci limatu (1792), ak At-Tirmisii ci limatu (63) ak (631).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (1402), ak Muslim, ci limatu (2287).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (1432), ak Muslim, ci limatu (984).
Abuu Daawuda génne na ko ci limatu (1609), ak Ibn Maaja, ci limatu (1827), Al-Albaanii wéral na ko ci Sahih Abii Daawuda ci limatu (1609).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (1), ak Muslim, ci limatu (1907).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (1810), ak Muslim, ci limatu (1086).
Al-Buxaarii soloo na ko ci limatu (1909).
Ahmad génne na ko ci limatu (26457), ak Abuu Daawuda ci limatu (2454), ak An-Nasaa'ii ci limatu (2331) te baat yi ay baatam la.
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (6669), ak Muslim, ci limatu (2709).
Abuu Daawuda génne na ko ci limatu (2380), ak At-Tirmisii ci limatu (719), ak Ibn Maaja ci limatu (676).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (1849), ak Muslim, ci limatu (1846).
Muslim génne na ko ci limatu (1134).
Ahmad génne na ko ci limatu (25198), ak An-Nasaa'ii ci limatu (2627), ak Ibn Maaja ci limatu (2901).
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (1862), ak Muslim, ci limatu (1341).
Al-Buxaarii soloo na ko ci limatu (1531).
Muslim génne na ko ci limatu (1211).
Al-Buxaarii soloo na ko ci limatu (1549).
Muslim génne na ko ci limatu (1218).
Tirmisii génne na ko ci limatu (487), mu ne: Hasan Xariib. Te Al-Albaanii baaxal na ko.
Xoolal: Muxnil Muhtaaj (2/22).
Haasiyatu Ibnu Aabidiin (1/ 42).
xoolal: Al-Majmuuhu (1/ 50).
As-Sufha: Mooy nit ki nga xam ne dafa bokk ak keneen dara àq ji mu am ngir nangu céru ki mu bokkaloon te keneen jëloon cér ba.
Jaayu Al-hiina: Mooy nit ki jaay keneen dara ci njëg gu ñu yeexe, mu jébbal ka ko, ba noppi mu jëndaat ko ci moom balaa muy jot ci njëg gi, ci njëg gu gën a néew googa te teew.
Al-Buxaarii moo ko soloo, ci limatu (8).