Explanation
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne àdduna ñam wu neex la, te naat ci gisiin, ba nit ki dana ci woroo, ba di ci nuur, ba def ko yitteem ji gën a rëy. Ak ne Yàlla dafa def ñenn ci nun ñuy wuutu ñeneen ci dundug àdduna, ngir xool lan lanuy def, ndax danu koy topp, walla danu koy moy? Topp mu wax: moytuleen poñaxiitam àdduna ak ub taaram di leen nax ba di leen jëme ci bàyyi li leen Yàlla digal, ba ngeen di def li mu leen tere. Bokk na ci li gën a màgg ci yi ñu war a moytu ci fitnay àdduna mooy fitnay jigéen ñi, ndaxte mooy fitna ji waa Banuu Israayil njëkk a tàbbi.